Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Luke

24

1 Bés bu jëkk ca ayu-bés ga, jigéen ña jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Ñu ngi yoroon cuuraay lu ñu defaroon.
1耶稣复活(太28:1-8;可16:1-8;约20:1-10)
2 Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba.
2发现石头已经从坟墓辊开了,
3 Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu.
3就进去,却找不着主耶稣的身体。
4 Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax.
4她们正为此事猜疑的时候,忽然有两个人,穿着闪烁耀目的衣服,站在她们旁边。
5 Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi?
5她们害怕,把脸伏在地上。那两个人对她们说:“为什么在死人中找活人呢?
6 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile.
6他不在这里,已经复活了。你们应当记得他还在加利利的时候,怎样告诉你们,
7 Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”»
7说:‘人子必须被交在罪人手里,钉在十字架上,第三日复活。’”
8 Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya.
8她们就想起他的话,
9 Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp.
9于是从坟地回去,把这一切事告诉十一个使徒和其余的人。
10 Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya.
10那些妇女就是抹大拉的马利亚,约亚拿和雅各的母亲马利亚,以及其他在一起的妇女,她们把这些事向使徒说了。
11 Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu.
11使徒以为这些话是无稽之谈,就不相信。
12 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew.
12彼得却起来跑到坟墓那里,屈身往里观看,只见细麻布在那里,就回去了,对所发生的事非常惊奇。
13 Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.
13在以马午斯路上显现(可16:12-13)同一天,门徒中有两个人往一个叫以马午斯的村子去,那村子距耶路撒冷约十一公里;
14 Ñu waxtaane li xewoon lépp.
14他们彼此谈论所发生的这一切事。
15 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,
15正在交谈议论的时候,耶稣亲自走近他们,与他们同行,
16 fekk seeni bët muuru, ba mënu ko woon a xàmmi.
16但他们的眼睛却给蒙蔽了,认不出他来。
17 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.
17耶稣说:“你们走路的时候,彼此讨论的是什么事呢?”他们就站住,面带愁容;
18 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»
18一个名叫革流巴的回答他:“在耶路撒冷作客的,难道只有你不知道这几天在那里所发生的事吗?”
19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu tontu ko ne: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.
19他说:“什么事呢?”他们说:“就是拿撒勒人耶稣的事。他是先知,在 神和众人面前,说话行事都有大能。
20 Waaye sunuy saraxalekat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.
20我们的祭司长和官长,竟把他交出去,判了死罪,钉在十字架上。
21 Nun nag danoo yaakaaroon ne, mooy kiy nar a jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi.
21但我们素来盼望要救赎以色列的就是他。不但这样,这些事发生到今天,已经是第三天了。
22 Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba,
22而且我们中间有几个妇女使我们惊奇,她们清早到坟墓那里去,
23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dellusi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne, mi ngi dund.
23却找不到他的身体。她们回来说看见天使显现,天使说他活了。
24 Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»
24又有我们中间的几个人到坟墓那里去,所看见的正如妇女们所说的,只是没有看见他。”
25 Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéex a gëm li yonent yi yégle woon!
25耶稣说:“无知的人哪,先知所说的一切话,你们心里信得太迟钝了!
26 Xanaa du Almasi bi dafa waroon a daj boobu coono te dugg ci ndamam?»
26基督这样受害,然后进入他的荣耀,不是应当的吗?”
27 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.
27于是他从摩西和众先知起,把所有关于自己的经文,都给他们解释明白了。
28 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.
28他们走近要去的村子,他好像还要往前行,
29 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom.
29他们强留他说:“天晚了,太阳下山了,请与我们同住吧!”他就进去与他们同住。
30 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko.
30到了吃饭的时候,他拿起饼来,感谢了,擘开递给他们,
31 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko.
31他们的眼睛开了,才认出是耶稣来;他却从他们面前不见了。
32 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»
32他们彼此说:“在路上他对我们说话,给我们解释圣经的时候,我们的心不是火热的吗?”
33 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneeni taalibe.
33他们就立时起来回耶路撒冷去。在那里遇见十一个使徒和跟他们聚在一起的人,
34 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!»
34说:“主果然复活了,已经向西门显现了。”
35 Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.
35两个人就把在路上的事,和擘饼的时候他们怎样认出耶稣来的事,都述说了一遍。
36 Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.»
36向众门徒显现(太28:16-20;可16:14-18;约20:19-23。参徒1:6-8)正说这话的时候,耶稣亲自站在他们当中,说:“愿你们平安。”
37 Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma.
37他们非常惊怕,以为看见了灵。
38 Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol?
38他说:“你们为什么惊慌,为什么心里疑惑呢?
39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.»
39你们看我的手、我的脚,就知道我是谁。摸我看看,灵没有骨,没有肉;你们看,我是有的。”
40 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam.
40说了这话,就把手和脚给他们看。
41 Waaye ba tey mënuñu woon a gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?»
41他们欢喜到不敢相信,并且很惊奇。耶稣说:“你们这里有什么吃的没有?”
42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
42他们就给了他一片烧鱼。
43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
43他接过来,在他们面前吃了。
44 Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.»
44主对他们说:“这就是我从前与你们同在的时候,对你们说过的话:摩西的律法、先知书和诗篇上所记关于我的一切事,都必定应验。”
45 Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax.
45于是他开他们的心窍,使他们明白圣经;
46 Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde,
46又说:“经上这样记着:基督必须受害,第三天从死人中复活。
47 te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne, war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen.
47人要奉他的名,传讲悔改与赦罪的道,从耶路撒冷起,直传到万国。
48 Yéenay samay seede.
48你们就是这些事的见证。
49 Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.»
49我要使我父的应许临到你们身上,你们当在城里等候,直到得着从上面来的能力。”
50 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Foofa mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
50耶稣升天(参可16:19-20;徒1:9-11)主带他们出去,到了伯大尼附近,举手给他们祝福。
51 Bi mu leen dee barkeel, mu tàggoo ak ñoom, Yàlla yéege ko asamaan.
51正在祝福的时候,他就离开他们,被接到天上去了。
52 Taalibe ya màggal ko, daldi dellu Yerusalem, fees ak mbég.
52他们就敬拜他,欢欢喜喜地回到耶路撒冷,
53 Foofa daawuñu jóg ca kër Yàlla ga, di gërëm Yàlla.
53常常在殿里称颂 神。