Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Luke

23

1 Gannaaw loolu kureelu àttekat ya yépp daldi jóg, yóbbu Yeesu ca Pilaat.
1耶稣被押交彼拉多(太27:1-2、11-14;可15:1-5;约18:28-38)
2 Foofa ñu tàmbali di ko sosal naan: «Fekk nanu nit kii, muy fàbbi sunu réew, di leen teree fey galag Sesaar, te mi ngi teg boppam Almasi, maanaam buur.»
2控告他说:“我们查出这个人煽惑我们的同胞,阻止纳税给凯撒,并且自称是基督,是王。”
3 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko.»
3彼拉多问他:“你是犹太人的王吗?”耶稣回答:“这是你说的。”
4 Pilaat ne saraxalekat yu mag ya ak mbooloo ma: «Gisuma genn tooñ ci nit kii.»
4彼拉多对祭司长和众人说:“我在这人身上,查不出有什么罪。”
5 Waaye ñu sax ci seeni wax naan: «Mi ngi jógloo mbooloo mi, di jàngale ci réewu Yawut ya mépp, li dale ci Galile ba fii.»
5但他们极力说:“他在犹太全地教导人,煽动群众,从加利利直到这里。”
6 Bi Pilaat yégee baat yooyu, mu laajte ne: «Ndax nit kii Galile la dëkk?»
6希律王藐视耶稣彼拉多听见了,就问耶稣是不是加利利人。
7 Bi mu yégee ne, Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem.
7既然知道他是从希律管辖下来的,就把他送回希律那里;那时希律正在耶路撒冷。
8 Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoon a gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne, dina ko gis mu def kéemaan.
8希律看见耶稣,非常欢喜,因为他曾经听过耶稣的事,早就想要见他,希望看他行个神迹。
9 Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu tontuwul dara.
9于是他问了耶稣许多话,但耶稣什么也不回答。
10 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jiiñ bu metti.
10祭司长和经学家站着,猛烈地控告他。
11 Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat.
11希律和他的侍卫就藐视耶稣,戏弄他,给他穿上华丽的衣服,把他送回彼拉多那里。
12 Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit.
12希律和彼拉多从前原是彼此为仇,在那一天就成了朋友。
13 Pilaat daldi woo saraxalekat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen:
13彼拉多判耶稣钉十字架(太27:15-26;可15:6-15;约18:39-19:16)彼拉多召集了祭司长、官长和民众,
14 «Indil ngeen ma nit kii, ne ma, day jàddloo yoon mbooloo mi. Léegi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma tooñ ci moom ak li ngeen koy jiiñ lépp.
14对他们说:“你们把这人押到我这里来,说他煽惑群众,我已经在你们面前审讯过,在他身上一点也找不到你们控告他的罪状,
15 Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey.
15连希律也找不到,又把他送回我这里,可见他没有作过该死的事。
16 Kon nag dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
16我要责打他,然后把他释放。”
18 Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!»
17(有些抄本有第17节:“每逢节期,他必须照例给他们释放一个囚犯。”也有些抄本把这句放在第19节后)
19 Dañoo tëjoon Barabas, ndaxte dafa jéem a tas dëkk ba, te rey nit.
18众人齐声喊叫:“除掉这个人,给我们释放巴拉巴!”
20 Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa bëggoon a bàyyi Yeesu.
19这巴拉巴是因为在城作乱杀人而入狱的。
21 Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
20彼拉多再向他们说明,愿意释放耶稣。
22 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Lu tax? Gan tooñ la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
21然而他们高声呼叫:“把他钉十字架,把他钉十字架!”
23 Waaye ñoom ñu sax ca la ñu waxoon, di gën a yuuxu naan, ñu daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat.
22彼拉多第三次对他们说:“这人作过什么恶事呢?我在他身上找不出什么该死的罪。所以我要责打他,然后把他释放。”
24 Muj gi Pilaat dogal, ñu defal leen li ñu bëgg.
23但他们大声吵闹,要他把耶稣钉十字架,他们的声音就得了胜。
25 Mu bàyyil leen ki ñu ko ñaanoon, kooku ñu tëjoon kaso, ndax tas réew ma ak rey nit. Waaye mu jébbal leen Yeesu ci seeni loxo.
24彼拉多就宣判,照他们的要求,
26 Bi ñuy yóbbu Yeesu, ñu jàpp ku ñuy wax Simoŋ te mu dëkk Siren, ku jóge ca wet, ga féete ak tool ya, sëf ko bant, ba ñuy war a daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ci moom.
25把他们所求那作乱杀人入狱的释放了,却把耶稣交出来,随他们的意思处理。
27 Mbooloo mu baree nga ko toppoon, te jigéen ñu baree ngi doon yuuxu, di ko jooy.
26耶稣被钉十字架(太27:33-44;可15:21-32;约19:17-24)他们把耶稣带走的时候,抓住了一个从乡下来的古利奈人西门,把十字架放在他身上,叫他背着跟在耶稣后面。
28 Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.
27一大群人跟随他,有些妇女为他捶胸痛哭。
29 Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi musul a jur ak ñi musul a nàmpal, barkeel ngeen!”
28耶稣转过身来对她们说:“耶路撒冷的女儿啊,不要为我哭,却要为你们自己和你们的儿女哭。
30 Bu keroogee,“Nit ñi dinañu ne tund yi:‘Daanuleen ci sunu kaw!’te naan jànj yi: «“Suul-leen nu!»“ “
29日子将到,人必说:‘不生育的和没有怀过胎的,也没有哺养过婴儿的有福了。’
31 Ndaxte su ñu defee nii garab gu tooy gi, lu ñuy def garab gu wow gi?»
30那时人要对大山说:‘倒在我们身上!’对小山说:‘遮盖我们!’
32 Yóbbaale nañu itam ñeneen, ñuy ñaari defkati lu bon, ngir rey leen.
31他们在青绿的树上,既然这样作;在枯干的树上,又会怎样呢?”
33 Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu Bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndeyjooram, ka ca des ca càmmooñam.
32他们另外带来两个犯人,和耶稣一同处死,
34 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Xarekat ya tegoo ay bant yéreem, ngir séddoo ko.
33到了那名叫“髑髅”的地方,就把耶稣钉在十字架上,也钉了那两个犯人,一左一右。
35 Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!»
34耶稣说:“父啊,赦免他们!因为他们不知道自己所作的是什么。”士兵抽签,分了他的衣服。
36 Xarekat ya it di ko ñaawal. Ñu jegesi, jox ko bineegar te naan:
35群众站着观看,官长们嗤笑说:“他救了别人,如果他是基督,是 神所拣选的,让他救自己吧!”
37 «Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!»
36士兵也上前戏弄他,拿酸酒给他喝,
38 Ñu daaj mbind, mu tiim ko naan: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
37说:“如果你是犹太人的王,救你自己吧!”
39 Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!»
38在耶稣的头以上有一个牌子写着:“这是犹太人的王。”
40 Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: «Xanaa ragaloo Yàlla, yaw mi ñuy mbugal ni moom!
39悬挂着的犯人中,有一个侮辱他说:“你不是基督吗?救你自己和我们吧!”
41 Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.»
40另一个就应声责备他说:“你是同样受刑的,还不惧怕 神吗?
42 Noonu mu ne: «Yeesu, fàttaliku ma, boo dellusee ci sa nguur.»
41我们是罪有应得的。我们所受的与所作的相称,然而这个人并没有作过什么不对的事。”
43 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey jii dinga texe ak man ca jataayu Yàlla.»
42他又对耶稣说:“耶稣啊,你得国降临的时候,求你记念我。”
44 Noonu digg-bëccëg daldi jot, jant ba nëbbu, réew mépp daldi lëndëm këruus lu mat ñetti waxtu. Ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga daldi xar ñaar.
43耶稣对他说:“我实在告诉你,今天你必定同我在乐园里了。”
46 Yeesu woote ak kàddu gu dëgër naan: «Baay, jébbal naa la sama ruu!» Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Yàlla.
44耶稣死时的情形(太27:45-56;可15:33-41)从正午直到下午三点钟,遍地都黑暗了。
47 Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu màggal Yàlla ne: «Dëgg-dëgg nit kii ku jub la woon.»
45太阳没有光,圣所的幔子从当中裂开。
48 Nit ña fa dajaloo woon ñépp, di seetaan li xew, ba ñu gisee loolu, ñu dellu seen kër, fëgg seen dënn, di jooy.
46耶稣大声呼叫:“父啊,我把我的灵魂交在你手里。”说了这话,气就断了。
49 Xamey Yeesu yépp ak jigéen, ña ko toppe woon Galile, dand leen, di xool li xew.
47百夫长看见所发生的事,就颂赞 神,说:“这真是个义人!”
50 Nit ku ñuy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi dëkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu àttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te àndul woon ci li ñu dogaloon te jëf ko. Da doon séentu nguuru Yàlla.
48聚集观看的群众,看见所发生的事,都捶着胸回去了。
52 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu.
49与耶稣熟悉的人,和从加利利跟随他来的妇女,都远远地站着,看这些事。
53 Gannaaw loolu mu wàcce ko ca bant ba, laxas ko ci càngaay, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ciw doj te musuñu caa def kenn.
50耶稣葬在坟墓里(太27:57-61;可15:42-47;约19:38-42)有一个人名叫约瑟,是个议员,为人良善公义,
54 Fekk bésu Waajal la woon, te bésu noflaay baa ngi doon tàmbali.
51是犹太地亚利马太城的人,一向等候 神的国,并不附和众人的计谋和行为。
55 Jigéen ña gungee woon Yeesu Galile, ànd ak Yuusufa, gis bàmmeel ba ak na ñu ca dence néewu Yeesu ba.
52这人去见彼拉多,求领耶稣的身体。
56 Noonu ñu dellu defari cuuraay ak latkoloñ ngir néew ba. Ca bésu noflaay ba ñu noppalu, ni ko yoon wi santaanee.
53他把身体取下来,用细麻布裹好,放在从石头凿出来的坟墓里,这坟墓是从来没有葬过人的。
54那天是预备日,安息日就要开始,
55那些从加利利和耶稣一起来的妇女,跟着来了。她们看见了坟墓,和他的身体怎样安葬,
56就回去预备香料和香膏。安息日,她们遵着诫命安息。