1 Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen.
1施洗约翰(太3:1-12;可1:3-5、7-8;约1:19-28)
2 Te it Anas ak Kayif nekkoon saraxalekat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakariya, ca màndiŋ ma.
2亚那和该亚法作大祭司的时候, 神的话临到撒迦利亚的儿子,在旷野的约翰。
3 Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
3他就来到约旦河一带地方,宣讲悔改的洗礼,使罪得赦。
4 Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.
4正如以赛亚先知的书上写着:“在旷野有呼喊者的声音:‘预备主的道,修直他的路!
5 Nañu sëkk xur yi,maasale tund yi ak jànj yi.Yoon yi dëng ñu jubbanti leen,yi ñagas ñu rataxal leen.
5一切洼谷都当填满,大小山冈都要削平!弯弯曲曲的改为正直,高高低低的修成平坦!
6 Bu ko defee bépp mbindeef dina gismucc gi Yàlla tëral.”»
6所有的人都要看见 神的救恩。’”
7 Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
7约翰对那出来要受他洗礼的群众说:“毒蛇所生的啊,谁指示你们逃避那将要来的忿怒呢?
8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te bañ a nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
8应当结出果子来,与悔改的心相称;你们心里不要说:‘我们有亚伯拉罕作我们的祖宗。’我告诉你们, 神能从这些石头中给亚伯拉罕兴起后裔来。
9 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.»
9现在斧头已经放在树根上,所有不结好果子的树,就砍下来,丢在火里。”
10 Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu war a def nag?»
10群众问他:“那么,我们该作什么呢?”
11 Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.»
11他回答:“有两件衣服的,当分给那没有的,有食物的也当照样作。”
12 Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu war a def?»
12又有税吏来要受洗,问他:“老师,我们当作什么呢?”
13 Mu tontu leen ne: «Laajleen rekk lu jaadu.»
13他说:“除了规定的以外,不可多收。”
14 Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»
14兵丁也问他:“至于我们,我们又应当作什么呢?”他说:“不要恐吓,不要敲诈,当以自己的粮饷为满足。”
15 Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.
15那时众人正在期待,人人心里都在猜想会不会约翰就是基督。
16 Noonu Yaxya tontu leen ñoom ñépp ne: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.
16约翰对众人说:“我用水给你们施洗,但那能力比我更大的要来,我就是给他解鞋带都没有资格。他要用圣灵与火给你们施洗。
17 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.»
17他手里拿着簸箕,要扬净麦场,把麦子收进仓里,却用不灭的火把糠秕烧尽。”
18 Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xebaar bu baax ba.
18他还用许多别的话劝勉众人,向他们传福音。
19 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd, jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,
19分封王希律,因他弟弟的妻子希罗底,并因他自己所行的一切恶事,受到约翰的责备。
20 ba faf tëj Yaxya kaso.
20他在这一切事以外,再加上一件,就是把约翰关在监里。
21 Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.
21耶稣受洗(太3:13-17;可1:9-11)众人受了洗,耶稣也受了洗。他正在祷告,天就开了,
22 Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
22圣灵仿佛鸽子,有形体地降在他身上;有声音从天上来,说:“你是我的爱子,我喜悦你。”
23 Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu war a tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi.Te Yuusufa mooy doomu Eli,
23耶稣的家谱(太1:1-17)耶稣开始传道,年约三十岁,人以为他是约瑟的儿子,约瑟是希里的儿子,
24 miy doomu Matat.Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki;Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
24依次往上推,是玛塔、利未、麦基、雅拿、约瑟、
25 Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.
25玛他提亚、亚摩斯、拿鸿、以斯利、拿该、
26 Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.
26玛押、玛他提亚、西美、约瑟、约大、
27 Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa;Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;
27约哈难、利撒、所罗巴伯、撒拉铁、尼利、
28 Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.
28麦基、亚底、哥桑、以摩当、珥、
29 Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi;
29耶书、以利以谢、约令、玛塔、利未、
30 Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim.
30西缅、犹大、约瑟、约南、以利亚敬、
31 Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena;Mena, Matata; Matata, Natan;Natan, Daawuda.
31米利亚、买拿、马达他、拿单、大卫、
32 Daawuda mooy doomu Yese;Yese, Obedd; Bowas; Salmon; Naason.
32耶西、俄备得、波阿斯、撒门(“撒门”有些抄本作“撒拉”)、拿顺、
33 Naason; Aminadab; Aminadab, Admin;Arni; Esrom; Fares; Yuda;
33亚米拿达、亚当民(有些抄本无“亚当民”一词)、亚兰(“亚兰”有些抄本作“亚珥尼”)、希斯仑、法勒斯、犹大、
34 Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;
34雅各、以撒、亚伯拉罕、他拉、拿鹤、
35 Serug; Ragaw; Faleg; Eber; Sala.
35西鹿、拉吴、法勒、希伯、沙拉、
36 Sala, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpagsàdd;Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
36该南、亚法撒、闪、挪亚、拉麦、
37 Lemeg, Matusala; Enog, Yaredd; Maleleel; Kaynan;
37玛土撒拉、以诺、雅列、玛勒列、该南、
38 Enos; Set; Set doomu Aadama;Aadama doomu Yàlla.
38以挪士、塞特、亚当,亚当是 神的儿子。