1 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ñu ngi doon fexeel Yeesu, ngir jàpp ko, reylu. Fekk booba ñaari fan a des ci màggalu bésu Jéggi ba ak màggalu Mburu ya amul lawiir.
1商议怎样杀害耶稣(太26:1-5;路22:1-6)
2 Kon nag ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yengu-yengu bañ a am ci nit ñi.»
2不过他们说:“不可在节期下手,免得引起民众暴动。”
3 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani, mu dem këru Simoŋ ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jigéen ñëw, yor njaq lu ñu defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree-bare. Jigéen ji toj njaq li, tuur latkoloñ ci boppu Yeesu.
3伯大尼妇人用香膏膏主(太26:6-13。参约12:1-8)耶稣在伯大尼,在患痲风的西门家里吃饭的时候,有一个女人来了,拿着一瓶珍贵的纯哪哒香膏。她打破了瓶,把香膏浇在耶稣的头上。
4 Waaye amoon na fa ñu mer, di xultu ci seen biir naan: «Yàq gii, lu muy jariñ?
4有几个人很生气,彼此说:“为什么这样浪费香膏呢?
5 Maneesoon na jaay latkoloñ jii ci lu tollook peyug atum lëmm, jox ko miskin yi.» Noonu ñu daldi gëdd jigéen ji.
5这香膏可以卖三百多个银币,用来赒济穷人。”他们就向她发怒。
6 Waaye Yeesu ne leen: «Bàyyileen ko. Defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal?
6但耶稣说:“由她吧!为什么难为她呢?她在我身上作的是一件美事。
7 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, te man ngeen leen a dimbali saa su leen neexee, waaye dungeen ma gis ba fàww.
7你们常常有穷人跟你们在一起,只要你们愿意,随时都可以向他们行善,然而你们却不常有我。
8 Jigéen ji def na li mu man; diw na sama yaram ak latkoloñ, ngir waajal sama rob, laata moo jot.
8她已经尽她所能的作了。她预先用香膏膏了我的身体,是为了我的安葬。
9 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xebaar bu baax bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
9我实在告诉你们,福音无论传到世界上什么地方,都要传讲这女人所作的来记念她。”
10 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya, ngir wori Yeesu.
10犹大出卖耶稣(太26:14-16)十二门徒中的一个,就是加略人犹大,去见祭司长,要把耶稣交给他们。
11 Bi ñu ko déggee, ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis. Noonu mu fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu.
11他们听见了就很欢喜,答应给他银子。于是犹大就找机会出卖耶稣。
12 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, taalibey Yeesu laaj ko: «Foo bëgg, nu defaral la reeru Jéggi bi?» Bés bu jëkk booba nag mooy bés, ba ñu faral a rendi xarum màggalu Jéggi ba.
12最后的晚餐(太26:17-30;路22:7-23;约13:21-30。参林前11:23-25)除酵节的第一天,就是宰杀逾越节羊羔的那一天,门徒问耶稣:“你要我们到哪里去,为你预备逾越节的晚餐呢?”
13 Noonu Yeesu yebal ñaar ci taalibe yi ne leen: «Demleen ca dëkk ba, foofa góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen, ngeen topp ko.
13他就差派两个门徒,对他们说:“你们到城里去,必有一个拿着水瓶的人,向你们迎面而来,你们就跟着他,
14 Kër gi mu dugg nag, ngeen ne boroom kër gi: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi bi, man ak samay taalibe?”
14无论他进入哪一家,你们要对那家主说,老师说:‘我的客厅在哪里?我和门徒好在那里吃逾越节的晚餐。’
15 Dina leen won néeg bu féete kaw te yaa, ñu defar ko, ba lépp jekk. Foofa ngeen nuy defarale reer bi.»
15他必指给你们楼上一间布置整齐、预备妥当的大房间,你们就在那里为我们预备。”
16 Bi mu ko waxee, taalibe ya dem ca dëkk ba, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
16门徒出去,进了城,所遇见的正如耶稣所说的,就预备好了逾越节的晚餐。
17 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu ñëw, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar.
17到了晚上,耶稣和十二门徒来了。
18 Ñu toog, di lekk. Bi ñuy lekk nag, Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen, ku bokk ak man di lekk sax, dina ma wor.»
18他们坐着吃饭的时候,耶稣说:“我实在告诉你们,你们中间有一个跟我一起吃饭的人要出卖我。”
19 Taalibe yi nag am naqar, ñu daldi ko ne kenn-kenn: «Mbaa du man?»
19他们就很忧愁,一个一个地问他:“是我吗?”
20 Mu tontu leen: «Kenn ci yéen fukk ak ñaar la, kuy cappandoo ak man ci ndab li.
20耶稣对他们说:“他是十二门徒里的一个,和我一同把手蘸在盘子里的。
21 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox. Bañoon a juddu moo gën ci moom.»
21正如经上指着人子所说的,他固然要离世,但出卖人子的那人有祸了!他没有生下来还好。”
22 Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, jox leen ko naan: «Jël-leen, lii sama yaram la.»
22他们吃的时候,耶稣拿起饼来,祝谢了,就擘开,递给门徒,说:“你们拿去吃吧,这是我的身体。”
23 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko, ñépp naan ci.
23又拿起杯来,祝谢了就递给门徒,他们都喝了。
24 Mu ne leen: «Lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru ngir ñu bare.
24耶稣说:“这是我的血,是为立约的,为许多人流出来的。
25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dootuma naan gannaaw tey ndoxum réseñ mii, ba kera ma ciy naan bu bees ci nguuru Yàlla.»
25我实在告诉你们,我决不再喝这葡萄酒,直到我在 神的国里喝新酒的那一天。”
26 Noonu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
26他们唱完了诗,就出来,往橄榄山去。
27 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku, ndaxte bind nañu:“Dinaa dóor sàmm bi,xari jur gi tasaaroo.”
27预言彼得不认主(太26:31-35;路22:31-34;约13:36-38)耶稣对他们说:“你们都要后退,因为经上记着:‘我要击打牧人,羊群就分散了。’
28 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.»
28但我复活以后,要比你们先到加利利去。”
29 Kon Piyeer ne ko: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la bàyyi mukk.»
29彼得对他说:“就算所有的人都后退,我却不会。”
30 Waaye Yeesu tontu ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, guddig tey, bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.»
30耶稣对他说:“我实在告诉你,就在今天晚上,鸡叫两遍以前,你会三次不认我。”
31 Waaye Piyeer gën a sax ca la mu waxoon naan: «Boo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu.
31彼得更坚决地说:“就算必须与你一同死,我也决不会不认你!”众人也都这样说。
32 Noonu ñu dem ca bérab bu tudd Setsemane. Yeesu ne taalibe yi: «Toogleen fii, ma dem ñaani.»
32在客西马尼祷告(太26:36-46;路22:39-46)他们来到一个地方,名叫客西马尼;耶稣对门徒说:“你们坐在这里,我去祷告。”
33 Mu ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi jàq, ba xonett.
33他带了彼得、雅各、约翰一起去,就惊惧起来,非常难过。
34 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba ma bëgg a dee; toogleen fii, xool.»
34于是对他们说:“我的心灵痛苦得快要死了;你们要留在这里,也要警醒。”
35 Noonu Yeesu dem ci kanam tuuti, daanu ci suuf, di ñaan ne, waxtu wi teggi ko, bu loolu manoon a am.
35耶稣稍往前走,俯伏在地上祷告:如果可能的话,使那时刻不要临到他。
36 Mu ne: «Abba, Baay bi, yaw mi dara tëwul, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
36他说:“阿爸、父啊,你凡事都能作,求你叫这杯离开我。但不要照我的意思,只要照你的旨意。”
37 Noonu mu dellusi ci taalibe yi, fekk ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
37耶稣回来,看见门徒睡着了,就对彼得说:“西门,你睡觉吗?你连一个小时也不能警醒吗?
38 Xool-leen te ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.»
38应当警醒、祷告,免得陷入试探;你们心灵虽然愿意,肉体却是软弱的。”
39 Beneen yoon Yeesu dem, di ñaane noonu,
39耶稣又去祷告,说的也是同样的话。
40 dellusiwaat, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. Xamuñu lu ñu koy tontoo.
40他再回来的时候,看见门徒睡着了;因为他们十分疲倦,不知道该怎样回答他。
41 Ñetteelu yoon mu dellusi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi.
41耶稣第三次回来,对他们说:“你们还在睡觉休息吗?够了,时候到了,看哪,人子要被交在罪人手里了。
42 Jógleen nu dem; ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
42起来,我们走吧!出卖我的人来了。”
43 Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak ñaar, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, mu jóge ca saraxalekat yu mag ya, ca xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
43耶稣被捕(太26:47-56;路22:47-53;约18:3-11)耶稣还在说话的时候,十二门徒中的犹大和一群拿着刀棒的人来到了;他们是祭司长、经学家和长老派来的。
44 Fekk ki ko naroon a wor joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko, yóbbu ko te wottu ko bu baax.»
44出卖耶稣的人给他们一个暗号,说:“我跟谁亲嘴,谁就是他。你们把他逮捕,小心带去。”
45 Noonu mu ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi,» daldi ko fóon.
45犹大来到,立刻上前对耶稣说:“拉比!”就跟他亲嘴。
46 Bi mu ko defee nit ñi song Yeesu nag, jàpp ko.
46他们就动手拿住耶稣,逮捕了他。
47 Waaye kenn ci ñi fa taxaw bocci jaaseem, dóor surgab saraxalekat bu mag bi, nopp bi dagg.
47站在旁边的人中有一个拔出刀来,砍了大祭司的仆人一刀,削掉了他的一只耳朵。
48 Yeesu ne leen: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
48耶稣对他们说:“你们带着刀棒出来,把我当作强盗捉拿吗?
49 Moona daan naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma. Waaye lii am na, ngir Mbind mi am.»
49我天天在殿里教导人,跟你们在一起,你们却没有捉拿我;但这是为了要应验经上的话。”
50 Ci kaw loolu, ñépp dëddu ko, daw.
50门徒都离开他逃跑了。
51 Fekk amoon na ca waxambaane wu lëkkaayoo woon sér, topp Yeesu, ñu daldi ko jàpp.
51有一个青年,赤身披着一块麻布,跟着耶稣。众人捉住他的时候,
52 Waaye waxambaane wa wacc fa sér bi, daldi daw, def yaramu neen.
52他就丢掉麻布,赤身逃跑了。
53 Ñi jàpp Yeesu yóbbu ko ci saraxalekat bu mag bi, te foofa la saraxalekat yu mag yi, njiit yi ak xutbakat yi yépp dajaloo.
53大祭司审问耶稣(太26:57-68;路22:67-71;约18:12-13、19-24)他们把耶稣押到大祭司那里,所有的祭司长、长老和经学家都聚集在一起。
54 Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci ëttu saraxalekat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi.
54彼得远远地跟着耶稣,直到大祭司的官邸,和差役一同坐着烤火。
55 Noonu saraxalekat yu mag yi ak kureelu àttekat yi yépp di wut ku man a seede lu daan Yeesu, ba ñu man koo reylu, waaye gisuñu kenn.
55祭司长和公议会全体都寻找证据控告耶稣,要把他处死,却没有找着。
56 Teewul sax naaféq ñu bare ñëw, seede ci Yeesu lu dul dëgg, waaye seen seede ànduñu.
56有许多人作假证供控告他,但他们的证供各不相符。
57 Ba mujj naaféq taxaw, seede ci moom naan:
57有几个人站起来,作假证供控告他说:
58 «Nun daal dégg nanu, mu ne: “Dinaa toj kër Yàlla, gii loxoy nit liggéey, tabax ci ñetti fan geneen gu nit liggéeyul.”»
58“我们听他说过:‘我要拆毁这座人手所造的圣所,三日之内要另建一座不是人手所造的圣所。’”
59 Waaye ba tey seeni wax ànduñu.
59就是这样的见证,他们也不一致。
60 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag bi taxaw ci seen kanam ne Yeesu: «Doo tontu? Lu la nit ñi di jiiñ?»
60大祭司站起来,走到中间,问耶稣:“这些人作证控告你的是什么呢?你怎么不回答呢?”
61 Waaye Yeesu tontuwul dara, ne cell. Saraxalekat bu mag bi dellu nag ne ko: «Ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ju tedd ji?»
61耶稣却不作声,什么也不回答。大祭司又问他:“你是那受称颂者的儿子基督吗?”
62 Yeesu tontu ko: «Moom laa. Te dingeen gis, Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji, di ñëw ci niiri asamaan.»
62耶稣说:“我是。你们要看见人子,坐在权能者的右边,驾着天上的云降临。”
63 Bi ko saraxalekat bu mag bi déggee nag, mu daldi mer, ba xotti ay yéreem naan:
63大祭司就撕开自己的衣服,说:“我们还要什么证人呢?
64 «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Lu ngeen ci xalaat?» Noonu ñépp teg ko dee.
64你们都听见这亵渎的话了。你们认为怎么样?”众人都定他该死的罪。
65 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci moom, takk ay bëtam, di ko dóor ay kurfeñ, naan ko: «Yaw wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?» Ba noppi alkaati yi teeru ko ak ay pes.
65于是有些人就向他吐唾沫,蒙住他的脸。用拳头打他,对他说:“你说预言吧!”差役把他拉去,用手掌打他。
66 Piyeer nag ma nga toogoon ci ëtt bi féete suuf. Noonu benn mbindaanu saraxalekat bu mag ba romb fa.
66彼得三次不认主(太26:69-75;路22:54-62;约18:15-18、25-27)彼得在下边院子的时候,大祭司的一个婢女来了,
67 Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko jàkk naan: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu.»
67看见彼得烤火,就瞪着他说:“你也是和拿撒勒人耶稣一伙的!”
68 Waaye Piyeer weddi ko naan: «Xawma li ngay wax, dégguma ci dara.» Mu daldi génn, dem ca buntu kër ga.
68彼得却否认说:“我不知道,也不明白你在说什么!”他就走出去,到了前院,鸡就叫了(有些抄本无“鸡就叫了”一句)。
69 Foofa nag mbindaan mi gisaat ko, mu ne ñi fa taxaw: «Waa jii ci ñoom la bokk.»
69那婢女看见他,又对站在旁边的人说:“这个人也是他们一伙的。”
70 Waaye Piyeer weddiwaat ko.Nes tuuti ñi fa taxaw ne Piyeer: «Yaw mi de, ci lu wóor bokk nga ci, nde waa Galile nga.»
70彼得还是不承认。过了一会,站在旁边的人也对彼得说:“你真是他们一伙的,因为你也是加利利人。”
71 Waaye Piyeer daldi giñ ak a waat naan: «Xawma nit ki ngay wax.»
71彼得就发咒起誓说:“我不认得你们说的这个人!”
72 Ci saa si ginaar sab ñaareelu yoon. Noonu Piyeer fàttaliku li ko Yeesu wax: «Bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi jooy jooy yu metti.
72立刻鸡就叫了第二遍。彼得想起耶稣对他说过的话:“鸡叫两遍以前,你要三次不认我。”他一想起来,就哭了(“他一想起来,就哭了”或译:“他就夺步而出,痛哭起来”)。