Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Mark

15

1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat.
1耶稣被押交彼拉多(太27:1-2、11-14;路23:1-3;约18:29-37)
2 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko: «Wax nga ko.»
2彼拉多问他:“你是犹太人的王吗?”耶稣回答:“你说的是。”
3 Te saraxalekat yu mag yi di ko jiiñ lu bare.
3祭司长控告了他许多事。
4 Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?»
4彼拉多又问他:“你看,他们控告你这么多的事!你什么都不回答吗?”
5 Waaye ba tey Yeesu tontuwul dara, ba tax Pilaat waaru.
5耶稣还是一言不答,使彼拉多非常惊奇。
6 Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko.
6彼拉多判耶稣钉十字架(太27:15-26;路23:13-25;约18:38-19:16)每逢这节期,彼拉多按着众人所要求的,照例给他们释放一个囚犯。
7 Fekk booba amoon na ku ñu tëj, tudd Barabas, ku bokk ci ña bëggoon a tas réew mi, boole ci rey nit.
7有一个人名叫巴拉巴,和作乱的人囚禁在一起,他们作乱的时候,曾杀过人。
8 Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def.
8群众上去,要求彼拉多援例给他们办理。
9 Pilaat nag xam ne, kiñaan rekk a taxoon saraxalekat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?»
9彼拉多回答他们:“你们要我给你们释放这个犹太人的王吗?”
11 Waaye saraxalekat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas.
10他知道祭司长是因为嫉妒才把耶稣交了来。
12 Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?»
11祭司长却煽动群众,宁可要总督释放巴拉巴给他们。
13 Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
12彼拉多又对他们说:“那么,你们称为犹太人的王的,你们要我怎样处置他呢?”
14 Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gën a kawe: «Daaj ko ci bant!»
13他们就喊着说:“把他钉十字架!”
15 Noonu Pilaat, mi wut a neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
14彼拉多说:“他作了什么恶事呢?”众人却更加大声喊叫:“把他钉十字架!”
16 Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp.
15彼拉多有意讨好群众,就释放了巴拉巴给他们,把耶稣鞭打了,交给他们钉十字架。
17 Noonu ñu solal ko mbubb mu xonq curr, ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam.
16士兵戏弄耶稣(太27:27-31)士兵把耶稣带进总督府的院子里,召集了全队士兵。
18 Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
17他们给他披上紫色的外袍,又用荆棘编成冠冕给他戴上;
19 Ñu di ko dóor ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, màggal ko.
18就向他祝贺说:“犹太人的王万岁!”
20 Bi ñu ko ñaawalee noonu ba noppi, ñu summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
19又用一根芦苇打他的头,向他吐唾沫,并且跪下来拜他。
21 Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi.
20他们戏弄完了,就把他的紫色的外袍脱下,给他穿回自己的衣服,带他出去,要钉十字架。
22 Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.»
21耶稣被钉十字架(太27:32-44;路23:26-43;约19:17-24)有一个古利奈人西门,就是亚历山大和鲁孚的父亲,从乡下来到,经过那里,士兵就强迫他背着耶稣的十字架。
23 Ñu bëgg koo jox biiñ bu ñu boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko.
22他们把耶稣带到各各他地方(这地名译出来就是“髑髅地”),
24 Foofa ñu daaj Yeesu ci bant, daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am;
23拿没药调和的酒给他,他却不接受。
25 booba fekk yoor-yoor di jot.
24他们就把他钉了十字架;又抽签分他的衣服,看谁得着什么。
26 Mbind mi xamle lu tax ñu rey ko nee na: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
25他们钉他十字架的时候,是在上午九点钟。
27 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew mi, kenn ci ndeyjooram, ki ci des ci càmmooñam.
26耶稣的罪状牌上写着“犹太人的王”。
29 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko naan: «Waaw kay, yaw mi bëgg a toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan,
27他们又把两个强盗和他一同钉十字架,一个在右,一个在左。
30 wàccal ci bant bi te musal sa bopp!»
28(有些抄本有第28节:“这就应验了经上所说的:‘他和不法者同列。’”)
31 Noonu it saraxalekat yu mag yi ak xutbakat yi di ko ñaawal ci seen biir naan: «Kii musal na ñeneen waaye mënul a musal boppam.
29过路的人讥笑他,摇着头说:“哼,你这个要拆毁圣所,三日之内又把它建造起来的,
32 Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab.
30从十字架上把自己救下来吧!”
33 Li tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
31祭司长和经学家也同样讥笑他,彼此说:“他救了别人,却不能救自己;
34 Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
32以色列的王基督啊,现在可以从十字架上下来,让我们看见就信吧。”那和他同钉十字架的人也侮辱他。
35 Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.»
33耶稣死时的情形(太27:45-56;路23:44-49;约19:28-30)从正午到下午三点钟,遍地都黑暗了。
36 Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Iliyas dina ñëw, wàcce ko.»
34下午三点的时候,耶稣大声呼号:“以罗伊,以罗伊,拉马撒巴各大尼?”这句话译出来就是:“我的 神,我的 神,你为什么离弃我?”
37 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
35有些站在旁边的人听见了就说:“看,他呼叫以利亚呢。”
38 Bi mu ko defee ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf.
36有一个人跑去拿海绵浸满了酸酒,绑在芦苇上,递给他喝,说:“等一等,我们看看以利亚来不来救他。”
39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanamu Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!»
37耶稣大叫一声,气就断了。
40 Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dand, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome.
38圣所里的幔子,从上到下裂成两半。
41 Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem.
39站在他对面的百夫长,看见他这样断气,就说:“这人真是 神的儿子!”
42 Booba nag bésu Waajal la woon, maanaam bés bu jiitu bésu noflaay bi. Ca ngoon sa nag,
40也有些妇女远远地观看,她们之中有抹大拉的马利亚,小雅各和约西的母亲马利亚,以及撒罗米。
43 Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla.
41这些妇女,当耶稣在加利利的时候,就一直跟随他、服事他。此外,还有许多和他一同上耶路撒冷的妇女。
44 Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu.
42耶稣葬在坟墓里(太27:57-61;路23:50-56;约19:38-42)到了晚上,因为是预备日,就是安息日的前一日,
45 Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa.
43一个一向等候 神国度的尊贵的议员,亚利马太的约瑟来了,就放胆地进去见彼拉多,求领耶稣的身体。
46 Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi.
44彼拉多惊讶耶稣已经死了,就叫百夫长前来,问他耶稣是不是死了很久。
47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.
45他从百夫长知道了实情以后,就把尸体给了约瑟。
46约瑟买了细麻布,把耶稣取下,用细麻布裹好,安放在一个从磐石凿出来的坟墓里,又辊过一块石头来挡住墓门。
47抹大拉的马利亚和约西的母亲马利亚都看见安放他的地方。