1 Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi.
1治好手枯的人(太12:9-14;路6:6-11)
2 Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ba man koo tuumaal.
2众人窥探他会不会在安息日医治那个人,好去控告他。
3 Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanamu ñépp.»
3耶稣对那一只手枯干了的人说:“起来,站在当中!”
4 Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell.
4又对他们说:“在安息日哪一样是可以作的呢:作好事还是坏事?救命还是害命?”他们一声不响。
5 Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ.
5耶稣怒目环视他们,因他们的心刚硬而难过,就对那人说:“伸出手来!”他把手一伸,手就复原了。
6 Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu.
6法利赛人出来,立刻和希律党人商量怎样对付耶稣,好除掉他。
7 Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko.
7许多人到海边找耶稣(太12:15-16;路6:17-19)耶稣和门徒退到海边去,一大群从加利利来的人跟着他;
8 Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon.
8还有许多人听见他所作的一切事,就从犹太、耶路撒冷、以土迈、约旦河外和推罗、西顿一带地方来到他跟前。
9 Booba nag Yeesu faj na ñu bare, ba ñu am ay jàngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, ñu wutal ko gaal, ngir mbooloo mi bañ koo buux.
9因为人多,耶稣就吩咐门徒为他预备一只小船,免得众人拥挤他。
11 Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.»
10他医好了许多人,所以凡有病的都挤过来要摸他。
12 Waaye Yeesu gëdd rab yi bu wér, ngir ñu bañ koo siiwal.
11污灵每次看到他,就仆倒在他面前,大声喊叫说:“你是 神的儿子!”
13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom.
12耶稣再三严厉地吩咐他们,不要把他的身分张扬出去。
14 Noonu mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñu ànd ak moom te mu yónni leen, ñu waareji,
13选立十二使徒(太10:1-4;路6:12-16。参徒1:13)耶稣上了山,呼召自己所要的人,他们就来了。
15 mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab.
14他选立了十二个人,称他们为使徒(有些抄本无“称他们为使徒”一句),要他们跟自己常在一起,好差遣他们去传道,
16 Fukk ak ñaar ñii la tànn:Simoŋ, mi mu tudde Piyeer,
15又有权柄赶鬼。
17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay — ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi» —
16他选立的十二个人是:西门(耶稣给他起名叫彼得),
18 Andare ak Filib,Bartelemi ak Macë,Tomaa ak Saag doomu Alfe,Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
17西庇太的儿子雅各,和雅各的弟弟约翰(耶稣给他们二人起名叫半尼其,就是“雷子”的意思),
19 ak Yudaa Iskariyo mi nar a wor Yeesu.
18安得烈、腓力、巴多罗迈、马太、多马、亚勒腓的儿子雅各、达太、激进派的西门,
20 Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax mënuñoo lekk sax.
19以及加略人犹大,就是出卖耶稣的那个人。
21 Bi ko ay bokkam déggee nag, ñu ñëw, ngir jàppsi ko naan: «Dafa tàggoo ak sagoom.»
20亵渎圣灵的罪不得赦免(太12:22-32;路11:14-23,12:10)耶稣进了屋子,群众又聚了来,以致他们连饭都不能吃,
22 Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
21那些和他在一起的人听见了,就出来抓住他,因为他们说他癫狂了。
23 Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane man a dàqe Seytaane?
22从耶路撒冷下来的经学家说:“他有别西卜附在身上!”又说:“他靠着鬼王赶鬼。”
24 Réew mu xeex boppam, du man a yàgg.
23耶稣把他们叫来,用比喻对他们说:“撒但怎能赶逐撒但呢?
25 Te kër gu xeex boppam, du man a yàgg.
24一国若自相纷争,那国就站立不住;
26 Bu Seytaane nag jógee, ba xeex boppam, xàjjalikoo dikkal na ko te du man a yàgg, waaye dina tas.
25一家若自相纷争,那家就站立不住。
27 «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn man a dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp.
26如果撒但自相攻打纷争,不但站立不住,而且还要灭亡。
28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bàkkaar, muy sosal Yàlla wu mu man a doon.
27谁都不能进入壮汉的家,抢夺他的财物,除非先把壮汉捆绑起来,才可以抢劫他的家。
29 Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.»
28我实在告诉你们,世人的一切罪和一切亵渎的话,都可以得到赦免;
30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nañu, rab jàpp na ko.
29但亵渎圣灵的,就永世不得赦免,他还要担当罪恶到永远。”
31 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw, ñu taxaw ci biti, yónnee, woo ko.
30耶稣说这话,是因为他们说他有污灵附在身上。
32 Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.»
31谁是耶稣的母亲和弟兄(太12:46-50;路8:19-21)耶稣的母亲和弟弟来了,站在外面,传话给他,叫他出来。
33 Waaye Yeesu tontu leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?»
32有许多人正围坐在耶稣身边,他们告诉他:“你看,你的母亲和弟弟(有些抄本在此有“妹妹”一词)在外面找你。”
34 Noonu mu xool ñi ko wër naan: «Sama yaay ak samay rakk a ngii;
33耶稣回答他们:“谁是我的母亲,我的弟兄呢?”
35 ndaxte kuy def coobareg Yàlla, kooku mooy sama rakk ak sama jigéen ak sama ndey.»
34于是四面观看那些围坐的人,说:“你们看,我的母亲!我的弟兄!
35凡遵行 神旨意的,就是我的弟兄姊妹和母亲了。”