Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Mark

8

1 Ca bés yooya mbooloo mu réy amaatoon na, te amuñu woon lu ñu lekk. Noonu Yeesu woo taalibe ya ne leen:
1给四千人吃饱的神迹(太15:32-39)
2 «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk.
2“我怜悯这一群人,因为他们和我在一起已经有三天,没有什么吃的了。
3 Su ma leen yiwee ak seen xiif, dinañu tële ci yoon wi, ndaxte am na ñu jóge fu sore.»
3如果我叫他们散开,饿着肚子回家去,他们会在路上晕倒,因为有人是从很远的地方来的。”
4 Taalibe yi tontu ko: «Waaye fii àllub neen la; fu nuy jële lu doy ngir dundal leen?»
4门徒回答:“在这旷野地方,从哪里能找食物叫这些人吃饱呢?”
5 Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom-ñaar.»
5他问他们:“你们有多少饼?”他们说:“七个。”
6 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. Mu jël juróom-ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir ñu séddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko.
6耶稣吩咐群众坐在地上;拿起那七个饼,祝谢了,擘开递给门徒,叫他们摆开;门徒就摆在众人面前,
7 Amoon na fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, sant Yàlla, wax taalibe yi, ñu séddale leen itam mbooloo mi.
7他们还有几条小鱼,耶稣祝了福,就吩咐把这些也摆开。
8 Noonu nit ñi lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale juróom-ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
8众人都吃了,并吃饱了。他们把剩下的零碎收拾起来,装满了七个大篮子。
9 Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor.
9当时人数约有四千。耶稣解散了群众,
10 Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wàlli Dalmanuta.
10就立刻和门徒上了船,来到大玛努他地区。
11 Noonu Farisen yi ñëw, di werante ak moom; ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
11求耶稣显神迹(太16:1-4)法利赛人出来,跟耶稣辩论;他们想试探他,求他显个从天上来的神迹。
12 Waaye Yeesu binni ci xolam ne leen: «Lu tax niti jamono jii di laaj kéemaan? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, duñu jot genn kéemaan.»
12耶稣灵里深深地叹息,说:“这世代为什么总是寻求神迹?我实在告诉你们,决不会有神迹显给这个世代的!”
13 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi leen, duggaat ci gaal gi, di jàll dex gi.
13于是他离开他们,又上船往对岸去了。
14 Taalibe yi nag fàtte woon nañu yóbbaale mburu, te amuñu woon lu dul benn mburu ci gaal gi.
14提防法利赛人和希律的酵(太16:5-12)门徒忘了带饼,船上除了一个饼,身边没有别的了。
15 Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.»
15耶稣嘱咐他们说:“你们要小心,提防法利赛人的酵和希律的酵!”
16 Taalibe yi nag daldi werante naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
16门徒彼此议论说:“这是因为我们没有饼吧?”
17 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey?
17耶稣知道了,就说:“为什么议论没有饼这件事呢?你们还不知道,还不明白吗?你们的心还是这么迟钝吗?
18 Ndax ay gumbay njàccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa fàttalikuwuleen;
18你们有眼不能看,有耳不能听吗?你们不记得吗?
19 bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu tontu ko: «Fukk ak ñaar.»
19我擘开那五个饼给五千人吃,你们收拾的零碎装满了几个篮子呢?”他们说:“十二个。”
20 Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom-ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
20“那七个饼分给四千人吃,你们收拾的零碎装满了几个大篮子呢?”他们说:“七个。”
21 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax seen xol dafa tëju ba tey?»
21耶稣说:“你们还不明白吗?”
22 Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko.
22治好伯赛大瞎眼的人后来他们到了伯赛大,有人带了一个瞎眼的人到他跟前,求耶稣摸他。
23 Yeesu nag jàpp loxob gumba gi, yóbbu ko, ba génn dëkk bi. Mu def tiflit ciy bëtam, teg ko loxo naan: «Ndax gis nga dara?»
23耶稣拉着他的手,领他到村外,吐唾沫在他的眼睛上,又用双手按在他的身上,问他:“你看见什么没有?”
24 Waa ji xool ne ko: «Gis naa ay nit, ñu mel ni ay garab, te ñu ngi dox.»
24他往上一看,说:“我看见人了!看见他们好像树走来走去。”
25 Kon Yeesu laalaat bët yi, gumba gi ne xefeet, daldi wér, ba gis lépp bu leer.
25于是耶稣再按手在他的眼睛上,他定睛一看,就复原了,样样都看得清楚了。
26 Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu ñibbi ne ko: «Bul dugg ca dëkk ba.»
26耶稣叫他回家去,说:“连这村子你也不要进去。”
27 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?»
27彼得承认耶稣是基督(太16:13-16、20;路9:18-21)耶稣和门徒出去,要到该撒利亚.腓立比附近的村庄。在路上他问门徒说:“人说我是谁?”
28 Ñu ne ko: «Am na ñuy ne, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Iliyas; ñi ci des ne, yaay kenn ci yonent yi.»
28他们回答:“有人说是施洗的约翰;有人说是以利亚;还有人说是先知里的一位。”
29 Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer tontu ko: «Yaa di Almasi bi.»
29他又问他们说:“那么你们呢?你们说我是谁?”彼得回答:“你就是基督。”
30 Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo wax kenn.
30耶稣郑重地嘱咐他们,不要把他的事告诉人。
31 Booba Yeesu tàmbali na leen a xamal ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare; njiit ya, saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ci ñetti fan.
31耶稣预言受难及复活(太16:21-28;路9:22-27)于是他教导他们,人子必须受许多苦,被长老、祭司长和经学家弃绝、杀害,三天后复活。
32 Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer nàññ. Bi ko Piyeer déggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd.
32耶稣坦白地说了这话,彼得就把他拉到一边,责怪他。
33 Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
33耶稣转过身来,望着门徒,斥责彼得说:“撒但,退到我后面去!因为你不思念 神的事,只思念人的事。”
34 Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: «Ku bëgg a topp ci samay tànk, na bàyyi boppam te gàddu bant bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.
34于是把众人和门徒都叫过来,对他们说:“如果有人愿意跟从我,就应当舍己,背起他的十字架来跟从我。
35 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man ak ngir xebaar bu baax bi, dinga ko jotaat.
35凡是想救自己生命的,必丧掉生命;但为我和福音牺牲生命的,必救了生命。
36 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam?
36人就是赚得全世界,却赔上自己的生命,有什么好处呢?
37 Te nit, lu mu war a weccee bakkanam?
37人还能用什么换回自己的生命呢?
38 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax ci kanamu niti jamono jii, ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla te topp bàkkaar, Doomu nit ki dina la rus a xam, bés bu ñëwee ci ndamu Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi.»
38在淫乱罪恶的世代,凡把我和我的道当作可耻的,人子在他父的荣耀里,和圣天使一起降临的时候,也必把他当作可耻的。”