1 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko:
1不可因传统废弃 神的诫命(可7:1-23)
2 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.»
2“你的门徒为什么违背古人的传统,在饭前不洗手呢?”
3 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada?
3耶稣回答:“你们又为什么因你们的传统,违背 神的诫命呢?
4 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.”
4 神说:‘当孝敬父母’,又说:‘咒骂父母的必被处死’。
5 Waaye yéen dangeen ne, ku wax sa ndey walla sa baay: “Li ngeen war a jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,”
5你们却说:‘人若对父母说:“我应该给你们的,已经作了献给 神的礼物”,
6 kooku amatul warugaru teral baayam. Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada.
6他就可以不孝敬父母了。’你们因为你们的传统,就废弃了 神的话。
7 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan:
7伪君子啊,以赛亚指着你们说的预言说得好:
8 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma.
8‘这人民用嘴唇尊敬我,心却远离我;
9 Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”»
9他们把人的规条当作道理去教导人,所以拜我也是徒然。’”
10 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam:
10耶稣叫群众前来,对他们说:“你们要听,也要明白。
11 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
11进到口里的不能使人污秽,只有从口里出来的,才能使人污秽。”
12 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?»
12门徒前来告诉他:“法利赛人听了这话很生气,你知道吗?”
13 Yeesu tontu leen ne: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi.
13耶稣说:“所有不是我天父栽种的植物,都要连根拔起来。
14 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
14由得他们吧!他们是瞎眼的,却作了向导;如果瞎子领瞎子,二人都会跌进坑里。”
15 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.»
15彼得说:“请你给我们解释这个比喻吧。”
16 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam?
16耶稣说:“你们还是不明白吗?
17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu?
17难道不知道一切进到口里的,是进到肚腹,然后排泄到外面去吗?
18 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe.
18但从口里出来的,是发自内心,才会使人污秽。
19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga.
19因为从心里出来的,有恶念、凶杀、奸淫、淫乱、偷盗、假见证和毁谤。
20 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
20这些才会使人污秽,不洗手吃饭却不会这样。”
21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon.
21迦南妇人的信心(可7:24-30)耶稣离开那里,来到推罗、西顿境内。
22 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.»
22有一个迦南的妇人从那地区出来,喊着说:“主啊,大卫的子孙,可怜我吧!我的女儿被鬼附得很苦。”
23 Waaye Yeesu tontuwu ko genn kàddu. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
23耶稣一句话也不回答她。门徒上前求他说:“请叫她走吧,她一直跟在我们后面喊叫。”
24 Yeesu tontu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xar yu réeri bànni Israyil.»
24耶稣回答:“我被差遣,只是到以色列家的迷羊那里去。”
25 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!»
25她来跪在耶稣面前说:“主啊,求你帮助我!”
26 Yeesu tontu ko: «Jël ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
26耶稣回答:“拿儿女的饼丢给小狗吃是不好的。”
27 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
27她说:“主啊,是的,不过小狗也吃主人桌子上掉下来的碎渣。”
28 Ci kaw loolu Yeesu tontu ko ne: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
28于是耶稣对她说:“妇人,你的信心真大,照你所想的给你成就吧!”从那时起,她的女儿就好了。
29 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa.
29治好许多病人(可7:31-37)耶稣离开那里,来到加利利海边,就上山坐下。
30 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen.
30有许多人来到他那里,把瘸腿的、瞎眼的、残废的、哑的和许多别的病人,都带到耶稣跟前,他就医好他们。
31 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
31群众看见哑巴说话,残废的复原,瘸腿的行走,瞎眼的看见,就十分惊奇,于是颂赞以色列的 神。
32 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leen a yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.»
32给四千人吃饱的神迹(可8:1-10。参太14:13-21)耶稣叫门徒前来,说:“我怜悯这一群人,因为他们跟我在一起已经有三天,也没有什么吃的;我不想叫他们饿着肚子回去,恐怕他们在路上晕倒。”
33 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?»
33门徒对他说:“我们在这旷野地方,哪里有足够的食物给这许多的人吃饱呢?”
34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu tontu ko: «Juróom-ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
34耶稣问他们:“你们有多少饼?”他们说:“七个饼和几条小鱼。”
35 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf.
35他就吩咐群众坐在地上,
36 Mu fab juróom-ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi.
36拿起那七个饼和那些鱼,祝谢了,擘开递给门徒,门徒又分给众人。
37 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom-ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
37大家都吃了,并且吃饱了。他们把剩下的零碎拾起来,装满了七个大篮子。
38 Gannaaw jigéen ñi ak gune yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni.
38吃的人,除了妇女和孩子,共有四千。
39 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.
39耶稣解散了群众,就上了船,来到马加丹地区。