Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Matthew

23

1 Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen:
1经学家和法利赛人有祸了(可12:38-39;路20:45-46)
2 «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa.
2“经学家和法利赛人坐在摩西的座位上,
3 Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe.
3所以凡他们吩咐你们的,你们都要遵守,但不可效法他们的行为,因为他们只会说而不去作。
4 Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam.
4他们把重担捆起来,压在人的肩头上,但自己连一个指头也不肯动。
5 Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb.
5他们所作的一切,都是要作给人看:他们把经文的匣子做大了,衣服的繸子做长了;
6 Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya.
6他们喜欢筵席上的首位、会堂里的高位;
7 Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “Kilifa gi.”
7又喜欢人在市中心向他们问安,称呼他们‘拉比’。
8 Waaye yéen buñu leen wooye “Kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen.
8然而你们不要被人称为‘拉比’,因为只有一位是你们的老师,你们都是弟兄。
9 Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw.
9不要称呼地上的人为父,因为只有一位是你们的父,就是天父。
10 Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist.
10你们也不要被人称为师傅,因为只有一位是你们的师傅,就是基督。
11 Ki gën a mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
11你们中间最大的,必作你们的仆人。
12 Kuy yékkatiku, dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
12凡高抬自己的,必被降卑;凡自己谦卑的,必被升高。
13 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanamu nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgg a dugg, mu dugg ci.
13“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们在人面前关了天国的门,自己不进去,连正要进去的人,你们也不准他们进去。
15 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu safara, ku leen yées ñaari yoon.
14(有些抄本有第14节:“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们吞没了寡妇的房产,假装作冗长的祷告,所以你们必受更重的刑罚。”)
16 «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.”
15“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们走遍海洋陆地,要使一个人入教;当他入了教,你们却使他沦为地狱之子,比你们更甚。
17 Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gën a màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell?
16“你们这些瞎眼的向导有祸了!你们说:‘凡指着圣所而起的誓,是没有用的;但指着圣所的金子而起的誓,就必须遵守。’
18 Dangeen ne it: “Ku giñe saraxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.”
17你们这些瞎眼的愚昧人哪,到底是金子大,还是使金子成圣的圣所大呢?
19 Gumba yi! Lan moo gën a màgg, sarax si walla saraxalukaay bi tax sarax si sell?
18你们又说:‘凡指着祭坛所起的誓,是没有用的;但指着坛上的祭物所起的誓,就必须遵守。’
20 Ku giñe saraxalukaay bi, giñ nga ci saraxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
19瞎眼的人哪!到底是祭物大,还是使祭物成圣的祭坛大呢?
21 Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak Ki ci dëkk.
20所以,凡指着祭坛起誓的,他就是指着祭坛和坛上的一切起誓;
22 Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak Ki ci toog.
21指着圣所起誓的,就是指着圣所和住在那里的 神起誓;
23 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gën a màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des.
22指着天起誓的,就是指着 神的宝座和坐在宝座上的起誓。
24 Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
23“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们把薄荷、茴香、芹菜,献上十分之一,却忽略律法上更重要的,就如正义、怜悯和信实;这些更重要的是你们应当作的,但其他的也不可忽略。
25 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
24你们这些瞎眼的向导啊,你们把蚊虫滤出来,却把骆驼吞下去。
26 Farisen yu gumba yi! Jëkkleen a setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set.
25“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们洗净杯盘的外面,里面却装满了抢夺和放荡。
27 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk.
26瞎眼的法利赛人哪,先把杯和盘的里面洗净,好使外面也可以干净。
28 Yéen itam, ci ngistal dangeen a mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
27“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们好像粉饰了的坟墓,外面好看,里面却装满了死人的骨头和各样的污秽;
29 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
28照样,你们外面看来像义人,里面却充塞着虚伪和不法。
30 Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.”
29“虚伪的经学家和法利赛人哪,你们有祸了!你们建造先知的墓,修饰义人的碑,
31 Seede ngeen nii ne, yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi,
30并且说:‘我们若活在我们祖先的时代,决不会与他们一同流先知的血。’
32 di aw seen tànki baay, ba yées leen sax.
31这样,你们就指证自己是杀害先知的人的子孙了。
33 Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu safara?
32那么,去完成你们祖先的罪孽吧!
34 Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo-dëkk.
33你们这些蛇,这些毒蛇所生的啊,你们怎能逃脱地狱的刑罚呢?
35 Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakariya doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak saraxalukaay bi.
34因此,我差派先知、智慧人和经学家到你们那里;有些你们要杀害又钉在十字架上,有些你们要在会堂里鞭打,从一个城赶逐到另一个城。
36 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii.
35所以,从义人亚伯的血起,到巴拉加的儿子撒迦利亚的血为止,他就是你们在圣所和祭坛中间所杀的,所有义人在地上所流的血,都要归在你们身上。
37 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!
36我实在告诉你们,这一切都必临到这个世代。
38 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent.
37为耶路撒冷叹息(参路13:34-35)“耶路撒冷,耶路撒冷啊,你杀害先知,又用石头把奉派到你们那里的人打死。我多次想招聚你的儿女,好像母鸡招聚小鸡到翅膀底下,只是你们不愿意。
39 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
38你看,你们的家必成为荒场,留给你们。
39我告诉你们,从今以后,你们一定见不到我,直等到你们说:‘奉主名来的,是应当称颂的。’”