1 Mbote ma dindi na juróom-ñaareelu tayu ga, asamaan ne selaw lu mat genn-wàllu waxtu.
1揭开第七个印
2 Noonu ma gis juróom-ñaari malaaka, yi taxaw ca kanam Yàlla, ñu daldi leen jox juróom-ñaari liit.
2我看见站在 神面前的七位天使,有七枝号筒赐给了他们。
3 Ba loolu amee meneen malaaka ñëw, taxaw ca wetu saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole ko ak ñaani gaayi Yàlla yépp, joxe ko ci kaw saraxalukaayu wurus ba nekk ci kanam gàngune mi.
3另外有一位天使来了,拿着金香炉,站在祭坛前。有许多香赐给了他,好与所有圣徒的祈祷一同献在宝座前的金坛上。
4 Noonu saxarus cuuraay li gillee ca loxob malaaka ma, ànd ak ñaani gaayi Yàlla ya, jëm ca kanam Yàlla.
4那香的烟和众圣徒的祈祷,就从天使手中一同升到 神面前。
5 Malaaka ma jël andu cuuraay ba, duy ko ak ay xal ca saraxalukaay ba, daldi koy sànni ci àddina. Noonu mu am ay dënnu, ay riir, ay melax ak yengu-yengub suuf.
5天使拿着香炉,用坛上的火把它装满了,投在地上;于是就有雷轰、响声、闪电和地震。
6 Ba mu ko defee juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari liit ya, daldi defaru di waaj a liit.
6吹六枝号拿着七枝号筒的七位天使,预备好了要吹号。
7 Malaaka mu jëkk ma wol liitam. Noonu ñu sànni ci àddina yuur ak safara yu ñu boole ak deret, ba tax benn ci ñetti xaaju suuf si lakk, benn ci ñetti xaaju garab yi it lakk, te ñax mu naat mépp lakk.
7第一位天使吹号,就有冰雹和混杂着血的火,投在地上。地的三分之一烧掉了,树的三分之一烧掉了,所有的青草也烧掉了。
8 Ñaareelu malaaka ma wol liitam. Noonu ñu sànni lu mel ni tundu safara wu réy, mu daanu ci géej gi, benn ci ñetti xaaju géej gi soppiku deret,
8第二位天使吹号,就有一座好像燃烧着的大山,投在海里。海的三分之一变成了血,
9 benn ci ñetti xaaju mbindeef yi nekk ci géej gi dee, te benn ci ñetti xaaju gaal yi yàqu.
9海里受造的活物死了三分之一,船只也毁坏了三分之一。
10 Ñetteelu malaaka ma wol liitam. Noonu biddiiw bu réy, yànj ni jum, xawee asamaan, daanu ci benn ci ñetti xaaju dex yi ak ci bëti ndox yi.
10第三位天使吹号,就有一颗燃烧着的大星,好像火把一样,从天上落下来,落在江河的三分之一上,和众水的泉源上。
11 Biddiiw boobu mi ngi tuddoon Wextan. Nit ñu bare naan ci ndox mi daldi dee, ndaxte ndox mi dafa daldi wex.
11这星名叫“苦堇”。众水的三分之一变为“苦堇”,因水变苦,就有许多人死了。
12 Ñeenteelu malaaka ma wol liitam. Noonu dóorees benn ci ñetti xaaju jant bi, ak benn ci ñetti xaaju weer wi, ak benn ci ñetti xaaju biddiiw yi, ba tax benn ci ñetti xaaju leer gi lëndëm. Bëccëg bi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam, guddi gi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam.
12第四位天使吹号,太阳的三分之一、月亮的三分之一、星辰的三分之一,就都受到击打,以致日月星的三分之一都变黑了,白天的三分之一没有光,夜晚也是这样。
13 Ma xool noonu, dégg jaxaay juy naaw ci digg asamaan, naan ak baat bu xumb: «Musiba, musiba! Musibaa ngi ci kaw waa àddina, ndax liit yi yeneen ñetti malaaka yi di wol.»
13我观看,就听见一只在高空飞翔的鹰,大声说:“有祸了!有祸了!住在地上的人有祸了!因为还有三位天使将要吹其余的号。”