Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Revelation

9

1 Juróomeelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma gis, ñu jox caabiy kàmb gu xóot gi benn biddiiw bu xawee woon asamaan, daanu ci kaw suuf.
1第五位天使吹号,我就看见一颗星从天上落到地上,有无底坑的钥匙赐给它。
2 Biddiiw ba ubbi buntu kàmb gu xóot ga. Noonu saxar jollee ca, su mel ni saxarus puur bu mag, jant bi ak jaww ji lépp lëndëm ndax saxarus kàmb ga.
2它开了无底坑,就有烟从坑里冒出来,好像大火炉的烟,太阳和天空因这坑的烟就都变黑了。
3 Ay njéeréer génn ca saxar sa, tasaaroo ci biir àddina. Ñu jox leen kàttan gu mel ni kàttanu jànkalaar.
3有蝗虫从烟里出来到了地上;有能力赐给它们,好像地上蝎子的能力一样。
4 Ñu sant leen, ñu bañ a laal ñax mi ci kaw suuf, mbaa genn gàncax walla genn meññeef, waaye ñu jublu rekk ci nit ñu amul màndargam Yàlla ci seen jë.
4有话吩咐它们,不可伤害地上的草,和所有青翠的东西,以及所有的树木,只可伤害那些额上没有 神印记的人。
5 Santuñu leen ñu rey leen, waaye ñu metital leen diirub juróomi weer. Te metit woowu ñuy indi, temboo na ak metit wiy dal nit, bu ko jànkalaar fittee.
5蝗虫没有能力杀死他们,只可使他们受痛苦五个月。他们的痛苦就像人给蝎子螫了的痛苦一样。
6 Ca jamono yooya nit ñi dinañu sàkku dee, waaye duñu daje ak moom. Dinañu bëgg a dee, waaye dee da leen di daw.
6在那些日子,人要求死,却决不得死;切愿要死,死却远离他们。
7 Njéeréer ya nag dañuy niroo ak fas yu ñu waajal ngir xare. Am nañu ci seen bopp lu mel ni kaalay wurus, te seen xar-kanam mel ni gu nit.
7蝗虫的形象,好像是预备好了要上阵的战马一样。它们头上戴的好像金冠冕,脸像人的面孔,
8 Seeni kawar mel ni yu jigéen, seeni bëñ mel ni bëñi gaynde.
8它们的头发好像女人的头发,牙齿好像狮子的牙齿;
9 Takk nañu ci seen dënn lu mel ni kiiraayu weñ, te coow la seeni laaf di def mel ni coowu sareeti xare yu bare yu ñu takk fas, di xeexi.
9它们的胸甲像铁甲,它们翅膀的声音好像许多马车奔驰上阵的声音。
10 Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar, te ca la seen kàttan nekk, ngir metital nit ñi diirub juróomi weer.
10它们好像蝎子一样有尾巴和毒刺,它们的尾巴能伤害人五个月。
11 Buuru njéeréer yi mooy malaakam kàmb gu xóot gi, moom lañu tudde ci làkku Yawut, Abadon, ak ci làkku gereg, Apolyon, liy tekki «Yàqkat.»
11它们有无底坑的使者作王统治它们。这王的名字,希伯来话叫阿巴顿,希腊话叫阿波伦。
12 Musiba mu jëkk mi jàll na, yeneen ñaari musiba yaa ngi ñëw.
12第一样灾祸过去了。看哪,以后还有两样灾祸要来!
13 Juróom-benneelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjén, yi nekk ci koñi saraxalukaayu wurus, ba nekk ci kanam Yàlla,
13第六位天使吹号,我听见有一个声音从 神面前金坛的四角发出来,
14 mu ne juróom-benneelu malaaka, ma yoroon liit: «Yiwil ñeenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.»
14对拿着号筒的第六位天使说:“把捆绑在幼发拉底大河的那四个使者放了吧!”
15 Noonu ñu daldi yiwi ñeenti malaaka, ya ñu waajaloon ngir at moomu, weer woowu, bés boobu ak waxtu woowu, ngir ñu rey benn ci ñetti xaaju nit ñi.
15那四个使者就被释放了,他们已经预备好,要在某年某月某日某时杀害人类的三分之一。
16 Limub gawar ga doon xareji mat na ñaari alfunniy alfunni. Dégg naa lim ba.
16马兵的数目有二万万;他们这个数目我听见了。
17 Nii laa gise ci peeñu mi fas ya ak ña leen war: ñu sol kiiraay yu xonq ni safara, bulo ni saxar, ak mboq ni tamarax. Boppi fas yaa nga doon nirook boppi gaynde; safara, saxar ak tamarax di génn ci seeni gémmiñ.
17在异象中,我看见那些马和骑马的是这样:骑马的穿着火红紫青和硫磺色的胸甲,马的头好像狮子头,有火、烟和硫磺从马的口中喷出来。
18 Benn ci ñetti xaaju nit ñi dee ci ñetti musiba ya: ci safara, saxar ak tamarax yi génn ci seeni gémmiñ.
18马口中喷出来的火、烟和硫磺这三种灾害,杀死了人类的三分之一。
19 Ndaxte kàttanu fas yaa ngi ci seeni gémmiñ ak ci seeni geen. Geen yaa nga mel ni ay jaan, am ay bopp, te ñoom lañuy metitale nit ñi.
19马的能力是在口中和尾巴上。它们的尾巴像蛇,并且有头用来伤人。
20 Nit ñi rëcc ci musiba yooyu taxul sax ñu tuub seeni jëfi loxo. Noppiwuñu di jaamu rab yi ak nataali xërëm yu ñu defare wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk, yoo xam ne mënuñoo gis, mënuñoo dégg mbaa ñu dox.
20其余没有在这些灾难中被杀的人,仍然不为他们手所作的悔改,还是去拜鬼魔和那些金、银、铜、石头、木头做的,不能看、不能听、也不能走路的偶像。
21 Te nit ñooñu tuubuñu seen bóom, seen xërëm, seen njaaloo mbaa seen càcc.
21他们也不为自己的凶杀、邪术、淫乱和偷盗悔改。