1 Bokk yi, sama coobareg xol ci bànni Israyil ak sama ñaan ci Yàlla, mooy ñu mucc.
1弟兄们,我心里切切盼望的,并且为以色列人向 神祈求的,是要他们得救。
2 Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam.
2我可以为他们作证,他们对 神有热心,但不是按着真见识;
3 Xamuñu yoon, wi Yàlla tëral ngir nit jub ci kanamam, waaye dañoo wéy ci seen pexey bopp; ba tax ñu bañ a nangu yoonu njub woowu Yàlla tëral.
3他们既然不明白 神的义,而又企图建立自己的义,就不服 神的义了。
4 Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa dëppe, ba tax ku ko gëm, dinga jub fa kanam Yàlla.
4因为律法的终极就是基督,使所有信的人都得着义。
5 Ku bëgg a jub ci kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, Musaa daf cee wax ne: «Ku ko manoon a matal, dinga dund ba fàww.»
5求告主名的都必得救论到出于律法的义,摩西写着说:“遵行这些事的人就必因这些事而活。”
6 Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm, nii lay waxe:«Bul wax ci sa xol ne:“Kuy yéeg ci kaw?”» mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc.
6但那出于信心的义却这样说:“你心里不要说:‘谁要升到天上去呢?’(就是要把基督领下来,)
7 «Bul wax it:“Kuy dem ca barsàq?”» mel ni dangaa bëgg Kirist dekki.
7或是说:‘谁要下到深渊去呢?’(就是要把基督从死人中领上来。)”
8 Kon boog lan lay wax? Lii:«Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet,ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
8然而那出于信心的义还说什么呢?”这话与你相近,在你口里,也在你心里。”这话就是我们所传信心的信息。
9 Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
9你若口里认耶稣为主,心里信 神使他从死人中复活,就必得救;
10 Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne, mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
10因为心里相信就必称义,用口承认就必得救。
11 Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
11经上说:“所有信靠他的人,必不致失望。”
12 Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp, te ku yéwén la ci képp ku koy ñaan.
12其实并不分犹太人和希腊人,因为大家同有一位主;他厚待所有求告他的人,
13 Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.»
13因为“凡求告主名的,都必得救。”
14 Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Te naka lañu man a gëme ki ñu déggagul turam? Te naka lañu man a dégge turam, te kenn xamalu leen ko?
14然而,人还没有信他,怎能求告他呢?没有听见他,怎能信他呢?没有人传扬,怎能听见呢?
15 Te it nan lañu man a waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xebaar bu baax bi, ni seen ñëw di sedde xol!»
15如果没有蒙差遣,怎能传扬呢?如经上所记:“那些传美事报喜讯的人,他们的脚踪多么美!”
16 Waaye ñépp nanguwuñu xebaar bu baax bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?»
16但并不是所有的人都顺从福音,因为以赛亚说:“主啊,我们所传的,有谁信呢?”
17 Kon boog ngëm ci kaw dégg lay juddoo, te dégg sosoo ci xebaaru Kirist.
17可见信心是从所听的道来的,所听的道是借着基督的话来的。
18 Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Aaŋkay! Mbind mi wax na ne:«Seen baat jolli na ci ñeenti xebla yépp,seen wax wër na àddina sépp.»
18但是我要说,他们没有听见吗?他们的确听见了,如经上所记:“他们的声音传遍全地,他们的言语传到地极。”
19 Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Aaŋkay! Musaa dafa jëkkoon a wax ne:«Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla,merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.»
19我再说:以色列人真的不明白吗?首先,摩西说:“我要使你们对那不是子民的生嫉妒,对那无知的民族起忿怒。”
20 Te Esayi takk na fitam, ba wax ne:«Ñi ma wutul woon, gis nañu ma,feeñ naa ci ñi ma laajul woon.»
20后来,以赛亚也放胆地说:“没有寻找我的,我让他们找到;没有求问我的,我向他们显现。”
21 Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne:«Tàllal naa samay loxo, suba ba ngoon, ci xeet wu may bañ tey werante.»
21论到以色列人,他却说:“我整天向那悖逆顶嘴的子民伸开双手。”