1 Sunu maam Ibraayma, mi nu soqikoo; nu mbiram tëdde?
1亚伯拉罕因信称义
2 Bu fekkoonte ne Ibraayma, ci kaw i jëfam la ko Yàlla àttee ni ku jub, kon am na lu mu ci man a damoo. Waaye demewul noonu ci kanam Yàlla.
2亚伯拉罕若是因行为称义,就有可夸的,只是不能在 神面前夸口。
3 Lan la Mbind mi wax ci loolu? Nee na: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.»
3经上怎么样说呢?”亚伯拉罕信 神,这就算为他的义。”
4 Képp kuy liggéey dina jot peyam; te pey googu du ag may, ñaqam la.
4作工的得工资,不算是恩典,是他应得的。
5 Waaye Yàlla dina àtte jub sax ki ko weddi woon; kon ku wéeruwul ciy jëfam, waaye mu gëm rekk, Yàlla dina jàppe ngëmam ni njub.
5可是,那不作工而只信那称不敬虔的人为义的 神的,他的信就算为义了。
6 Noonu la Daawuda birale barkeelug nit ki Yàlla jagleel njub, fekk ay jëfam taxul.
6大卫也是这样说,那不靠行为而蒙 神算为义的人是有福的!
7 Mu ne:«Ñi ñu baal seen jàdd yoon,te seeni bàkkaar far ci kanam Yàlla,ñu barkeel lañu.
7“过犯得蒙赦免,罪恶得到遮盖的人,是有福的;
8 Ki Boroom bi sëful ay bàkkaaram,kooka ku barkeel la.»
8主不算为有罪的,这人是有福的。”
9 Kon nag barkeel googu, ndax ñi xaraf rekk ñoo ko yeyoo? Ndax ñi xaraful it bokkuñu ci? Aaŋkay! Ndaxte wax nanu ne, Yàlla jàppe na ngëmu Ibraayma ni njub.
9这样看来,那有福的人,是指受割礼的呢,还是指没有受割礼的呢?因为我们说:“亚伯拉罕的信算为他的义。”
10 Kañ la ko jagleel njub nag? Ndax lu jiitu xarafam la woon, am gannaaw ga? Lu ko jiitu la woon.
10那么,是怎样算的呢?是在他受割礼以后呢,还是在他受割礼之前呢?不是在他受割礼以后,而是在他受了割礼以前。
11 Ndaxte Ibraayma gëm na, te Yàlla jàppe na ngëmam ni njub, fekk booba xarafagul. Te xarafal gi, màndarga la woon ci yaramam, di firndeel ne, ku jub la woon. Noonu la Ibraayma man a nekke baayu ñépp ñi gëm, ba Yàlla man leen a àtte ni ñu jub, te xarafuñu sax.
11他领受了割礼为记号,作他受割礼之前因信称义的印证,使他作所有没有受割礼而信之人的父,使他们也被算为义;
12 Te noonu itam la Ibraayma man a nekke baayu ñi xaraf, bu fekkee yemuñu rekk ci xaraf, waaye ñu am ngëm, ga Ibraayma sunu maam amoon lu jiitu xarafam.
12又作受割礼之人的父,就是作那些不仅受割礼,并且照着我们祖宗亚伯拉罕未受割礼时就信的那脚踪而行之人的父。
13 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ak ñi naroon a soqikoo ci moom, ne dinañu moom àddina si. Te dige boobu jógewul ci yoonu Musaa, waaye dafa jóge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Yàlla ci kaw ngëmam.
13 神应许的他必能成就原来 神给亚伯拉罕和他后裔承受世界的应许,并不是因着律法,而是借着因信而来的义。
14 Ndaxte su fekkee ne ñi nekk ci yoonu Musaa rekk ñooy moom àddina, kon ngëm amatul njariñ, te digeb Yàlla dafa toxu.
14如果属于律法的人才能成为后嗣,信就没有作用,应许也就落空了。
15 Yoonu Musaa daal du def lu dul wàcce merum Yàlla ci sunu bopp; ndax fu yoon amul, jàdd yoon du fa man a am.
15因为律法带来刑罚,没有律法,就没有违背律法的事。
16 Kon nag loolu Yàlla dige, ngëm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Yàlla rekk. Noonu la dige bi wóore ci ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, du ci ñi nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam ñi gëm ni Ibraayma gëme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun ñépp.
16所以,成为后嗣是因着信,为的是要按着 神的恩典,使给所有后裔的应许坚定不移,不但临到那属于律法的人,也临到那效法亚伯拉罕而信的人。亚伯拉罕在 神面前作我们众人的父,
17 Moom la Yàlla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: «Def naa la baayu xeet yu bare.» Ndaxte Ibraayma gëmoon na Yàlla, miy dekkal ñi dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am.
17如经上所记:“我已经立了你作万国的父。”他所信的,是叫死人得生命、使无变为有的 神。
18 Ibraayma dafa jàppoon ci ngëmam, di yaakaar, fekk bunti yaakaar yépp tëju. Moo tax mu nekk baayu xeet yu bare, ni ko Mbind mi waxe ne: «Noonu la sa askan di meli.»
18在他没有盼望的时候,仍然怀着盼望去信,因此就成了万国的父,正如 神所说:“你的后裔将要这样众多。”
19 Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat téeméeri at, waaye ba tey ngëmam wàññikuwul. Mu xam it ne, Saarata mënatul a ëmb.
19他快到一百岁的时候,想到自己的身体好像已经死了,撒拉也不能生育,他的信心还是不软弱,
20 Waaye loolu taxul ngëmadi jàpp ko, ba muy werante ci waxu Yàlla; ngëmam sax di gën a dëgër, mu daldi sant Yàlla,
20也没有因着不信而疑惑 神的应许,反倒坚信不移,把荣耀归给 神,
21 mu wóor ko ne, loolu ko Yàlla dig, Yàlla man na koo def.
21满心相信 神所应许的, 神必能成就。
22 Moo tax «Yàlla jagleel na Ibraayma njub.»
22因此,这就算为他的义。
23 Waaye loolu lañu bind ne: «Yàlla jagleel na ko njub,» du Ibraayma rekk a moom wax ji.
23“算为他的义”这一句话,不是单为他写的,
24 Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Yàlla dina nu jagleel njub, nun ñi gëm Yàlla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom.
24也是为我们这将来得算为义的人写的,就是为我们这信 神使我们的主耶稣从死人中复活的人写的。
25 Ndaxte Yàlla jébbale na ko ngir sunuy tooñ, dekkal ko ngir àtte nu jub.
25耶稣为我们的过犯被交去处死,为我们的称义而复活。