Wolof: New Testament

聖經新譯本 (Simplified)

Romans

5

1 Léegi nag, gannaaw Yàlla àtte na nu jub ci kaw ngëm, nanu jàpp ci jàmm, ji nu am fa kanam Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist.
1因信称义后所得的恩典
2 Moo nu ubbil bunt ci Yàlla, nu taxaw temm ci yiwam, jaar ci ngëm. Te it nu ngi bég ciy négandiku, Yàlla boole nu ci ndamam.
2我们也凭着信,借着他可以进入现在所站的这恩典中,并且以盼望得享 神的荣耀为荣。
3 Te du ci loolu rekk, waaye bég nanu it ci sunuy nattu; ndax xam nanu ne, nattu day feddali muñ;
3不但这样,我们更以患难为荣;知道患难产生忍耐,
4 te muñ mooy ndeyu jikko ju dëgër; te jikko ju dëgër day jur yaakaar.
4忍耐产生毅力,毅力产生盼望;
5 Te yaakaar jooju du ay nax, ndax mbëggeelu Yàllaa ngi baawaan ci sunu xol, jaarale ko ci Xelam mu Sell mi mu nu may.
5盼望是不会令人蒙羞的,因为 神借着所赐给我们的圣灵,把他的爱浇灌在我们的心里。
6 Ndaxte bi nu amul jenn doole, booba la Kirist dee ngir nun, fekk danoo weddi woon Yàlla.
6当我们还软弱的时候,基督就照所定的日期,为不敬虔的人死了。
7 Kuy nangoo deeyal nit ku jub, yombul a gis, waaye nag jombul am na ku nangoo deeyal ku baax.
7为义人死,是少有的;为好人死,或有敢作的;
8 Waaye Yàlla firndeel na mbëggeelam ci nun, ci li Kirist dee ngir nun, bi nu nekkee sax ay bàkkaarkat!
8唯有基督在我们还作罪人的时候为我们死, 神对我们的爱就在此显明了。
9 Gannaaw Kirist tuur na deretam nag, ngir Yàlla àtte nu jub, rawatina ne dina nu musal ci merum Yàlla.
9所以,我们现在既然因他的血称义,就更要借着他免受 神的忿怒。
10 Nun ay bañaaley Yàlla lanu woon, waaye Doomam dee na, ngir jubale nu ak moom. Gannaaw léegi nag xariti Yàlla lanu, rawatina ne dinanu mucc ndax dundug Doomam.
10我们作仇敌的时候,尚且借着 神儿子的死与他复和,既然复和了,就更要因他的生得救了!
11 Te sax nu ngi bég ci Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu jubale ak moom.
11不但这样,我们现在已经借着我们的主耶稣基督与 神复和,也借着他以 神为荣。
12 Kon nag bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar.
12亚当与基督的比较正好像罪借着一个人入了世界,死又是从罪来的,所以死就临到全人类,因为人人都犯了罪。
13 Bàkkaar kon nekkoon na ci àddina, bi Yàlla di laata wàcce yoonu Musaa. Waaye gannaaw yoonu Musaa tëddagul woon, bàkkaar du woon jàdd yoon.
13没有律法以前,罪已经在世界上了;不过,没有律法的时候,罪也不算罪。
14 Teewul nag la dale ca Aadama ba ca Musaa, dee a ngi fi woon ci àddina, di noot ñépp, ak sax ñi seen bàkkaar melul woon ni bosu Aadama, maanaam jàdd yoon. Aadama moomu nag moo di takkandeeru Kirist, mi waroon a ganesi àddina.
14可是,从亚当到摩西,死就掌权了,甚至那些不像亚当那样犯罪的人,也在死的权下;亚当正是要来的那一位的预表。
15 Waaye warunoo yemale tooñu Aadama ak mayu Yàlla. Bàkkaaru kenn nit kooku tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist yéwénal, baawaan na ci ñu bare, ba suul tooñ googu.
15但恩赏和过犯是截然不同的;如果因着那一人的过犯,众人都死了, 神的恩典和这一人耶稣基督在恩典里的赏赐,对众人就更加丰盛了。
16 Te bàkkaaru Aadama niroowul ak mayu Yàlla. Aadama bàkkaar na benn yoon, ba tax Yàlla daan ko, daanaale ñépp; waaye Yàlla jéggale na tooñ yu bare ci dara, ba mu àtte ñu bare ni ñu jub.
16这赏赐和那一人犯罪的后果也是不同的;因为审判是由一人而来,以致定罪,恩赏却由许多过犯而来,以致称义。
17 Bàkkaaru kenn nit tax na dee tàbbi àddina, yilif ñépp ni buur; waaye jëfu keneen nit ka, maanaam Yeesu Kirist, moo ko suul, ba tax ñu bare tàbbi ci dund gu bees, falu ni ay buur; xanaa ñi Yàlla boole ci yiwam wu bare, te àtte leen jub ci dara fa kanamam.
17如果因着那一人的过犯,死就因那一人而掌权,那些蒙丰富的恩典并且得公义为赏赐的,就更要因这一位耶稣基督在生命中掌权了。
18 Kon nag nu gàttal wax ji; jàddug kenn nit ka rekk moo waral Yàlla daan ñépp; noonu itam jëf ju jubu keneen nit ka rekk moo ubbi bunt, ba ñépp man a jub ci kanam Yàlla te am dund gu bees.
18这样看来,因一次的过犯,全人类都被定罪;照样,因一次的义行,全人类都被称义得生命了。
19 Aadama moomu dafa déggadil Yàlla, ba yóbbaale ñu bare, ñu nekk i bàkkaarkat; noonu itam Yeesu Kirist dafa déggal Yàlla, yóbbaale ñu bare itam, ñu jub.
19因着那一人的悖逆,众人就被列为罪人;照样,因着这一人的顺服,众人也被列为义人了。
20 Te yoonu Musaa daldi wàcc, ngir bàkkaar gën a bare; waaye fa bàkkaar bare, yiwu Yàlla gën faa bare.
20律法的出现,是要叫过犯增多;然而罪在哪里增多,恩典就更加增多了。
21 Ba tax, ni bàkkaar doon yilife ñépp ni buur, indaale dee, noonu itam la yiwu Yàlla faloo ni buur, jóge ci njub, jëm ci dund gu dul jeex. Te loolu lépp darajay Yeesu Kirist sunu Boroom moo nu ko may.
21罪借着死掌权;照样,恩典也借着义掌权,使人借着我们的主耶稣基督进入永生。