1 Ndegam nag jot nanu ci dige yu mel nii, samay soppe, nanu sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell, ba mat ci ragal Yàlla.
1Having therefore these promises, dearly beloved, let us cleanse ourselves from all filthiness of the flesh and spirit, perfecting holiness in the fear of God.
2 Yaatal-leen nu ci seen xol. Tooñunu kenn; lorunu kenn; naxunu kenn, jël alalam.
2Receive us; we have wronged no man, we have corrupted no man, we have defrauded no man.
3 Teg leen tooñ taxul may wax lii, ndaxte wax naa ba noppi ne, yéena ngi ci sunu xol ci dund ak ci dee.
3I speak not this to condemn you: for I have said before, that ye are in our hearts to die and live with you.
4 Kóolute gi ma am ci yéen réy na. Tiitar bi may jële ci yéen réy na. Sama xol sedd na guyy. Damaa fees ak mbég ci bépp coono bu nuy daj!
4Great is my boldness of speech toward you, great is my glorying of you: I am filled with comfort, I am exceeding joyful in all our tribulation.
5 Ba nu àggee diiwaanu Maseduwan, noppaluwunu, waaye coono bu ne daj nanu ko: xeex ci biti, njàqare ci biir.
5For, when we were come into Macedonia, our flesh had no rest, but we were troubled on every side; without were fightings, within were fears.
6 Waaye Yàlla miy dëfël xolu ñiy yoggoorlu ndax tiis, dëfël na sunu xol ci ñëwu Tit,
6Nevertheless God, that comforteth those that are cast down, comforted us by the coming of Titus;
7 te du ci ñëwam rekk sax waaye ci li ngeen dëfël xolam. Yégal na nu seen nammeel ci nun, seen réccu ak seen farlu jëm ci man, ba sama mbég gën cee yokku.
7And not by his coming only, but by the consolation wherewith he was comforted in you, when he told us your earnest desire, your mourning, your fervent mind toward me; so that I rejoiced the more.
8 Su fekkee ne sax, bataaxal bi ma leen bind dafa leen naqare, réccootuma ko. Ci lu jëkk réccu naa ko, ndaxte gis naa ne, bataaxal boobu teg na leen tiis, doonte sax ci diir bu néew.
8For though I made you sorry with a letter, I do not repent, though I did repent: for I perceive that the same epistle hath made you sorry, though it were but for a season.
9 Waaye sama xol sedd na léegi, du ndax seen tiis, waaye ci li mu tax ngeen réccu. Tiis wu jóge ci Yàlla ngeen tegoo, te àndul ak benn loraange bu bawoo ci nun.
9Now I rejoice, not that ye were made sorry, but that ye sorrowed to repentance: for ye were made sorry after a godly manner, that ye might receive damage by us in nothing.
10 Ndaxte tiis wu jóge ci Yàlla dina jur réccu guy jëme ci mucc, te réccu googu laajul gëstu. Waaye tiisu àddina day jëme ci dee.
10For godly sorrow worketh repentance to salvation not to be repented of: but the sorrow of the world worketh death.
11 Seen tiis wi jóge ci Yàlla, gisleen nag li mu jur: ndaw njaxlaf ak lay ak mer ak ragal ak nammeel ak farlu, ak bëgg a yar ki tooñ! Ci seen jëf yépp wone ngeen ne, set ngeen wecc ci mbir moomu.
11For behold this selfsame thing, that ye sorrowed after a godly sort, what carefulness it wrought in you, yea, what clearing of yourselves, yea, what indignation, yea, what fear, yea, what vehement desire, yea, what zeal, yea, what revenge! In all things ye have approved yourselves to be clear in this matter.
12 Kon nag su ma leen bindee, ki tooñ taxul, ki ñu tooñ it taxul, waaye dama leen a bind, ngir ngeen man a gis ci kanam Yàlla cawarte, gi ngeen am ci nun.
12Wherefore, though I wrote unto you, I did it not for his cause that had done the wrong, nor for his cause that suffered wrong, but that our care for you in the sight of God might appear unto you.
13 Te loolu seral na sunu xol. Sunu xel dal na, rawati ci li nu ànd ak Tit ci mbégam, ci li ngeen seral xolam, yéen ñépp.
13Therefore we were comforted in your comfort: yea, and exceedingly the more joyed we for the joy of Titus, because his spirit was refreshed by you all.
14 Su fekkee ne tiitaru woon naa ci seen mbir ci kanamu Tit, rusuma ci. Dëgg rekk lanu leen mas a wax; noonu it la Tit gise ne, li nu leen doon seede lépp, dëgg la.
14For if I have boasted any thing to him of you, I am not ashamed; but as we spake all things to you in truth, even so our boasting, which I made before Titus, is found a truth.
15 Te mbëggeelam ci yéen gën na yokku, buy fàttaliku ni ngeen ko déggale yéen ñépp, ci li ngeen ko teeru, ànd ak ragal ak weg.
15And his inward affection is more abundant toward you, whilst he remembereth the obedience of you all, how with fear and trembling ye received him.
16 Bég naa, ndaxte xam naa ne, man naa leen a wóolu ci lu nekk!
16I rejoice therefore that I have confidence in you in all things.