1 Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci muju jamono.
1And this know thou, that in the last days there shall come perilous times,
2 Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay
2for men shall be lovers of themselves, lovers of money, boasters, proud, evil-speakers, to parents disobedient, unthankful, unkind,
3 mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax;
3without natural affection, implacable, false accusers, incontinent, fierce, not lovers of those who are good,
4 ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla.
4traitors, heady, lofty, lovers of pleasure more than lovers of God,
5 Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen.
5having a form of piety, and its power having denied; and from these be turning away,
6 Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pasteef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen.
6for of these there are those coming into the houses and leading captive the silly women, laden with sins, led away with desires manifold,
7 Duñu noppee gëstu, waaye duñu man a yegg ci xam-xamu dëgg mukk.
7always learning, and never to a knowledge of truth able to come,
8 Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara.
8and, even as Jannes and Jambres stood against Moses, so also these do stand against the truth, men corrupted in mind, disapproved concerning the faith;
9 Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares.
9but they shall not advance any further, for their folly shall be manifest to all, as theirs also did become.
10 Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngale, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis.
10And thou -- thou hast followed after my teaching, manner of life, purpose, faith, long-suffering, love, endurance,
11 Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp.
11the persecutions, the afflictions, that befel me in Antioch, in Iconium, in Lystra; what persecutions I endured, and out of all the Lord did deliver me,
12 Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la.
12and all also who will to live piously in Christ Jesus shall be persecuted,
13 Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp.
13and evil men and impostors shall advance to the worse, leading astray and being led astray.
14 Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe.
14And thou -- be remaining in the things which thou didst learn and wast entrusted with, having known from whom thou didst learn,
15 Li dale ci sa ngune xam nga Mbind mu sell, mi la man a yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu.
15and because from a babe the Holy Writings thou hast known, which are able to make thee wise -- to salvation, through faith that [is] in Christ Jesus;
16 Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub.
16every Writing [is] God-breathed, and profitable for teaching, for conviction, for setting aright, for instruction that [is] in righteousness,
17 Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.
17that the man of God may be fitted -- for every good work having been completed.