1 Noonu ma gis malaaka mu wàcce ca asamaan, yor caabiy kàmb ga ak càllala gu réy.
1And I saw a messenger coming down out of the heaven, having the key of the abyss, and a great chain over his hand,
2 Mu jàpp ninkinànka ja, di jaani cosaan ja, muy Tuumaalkat bi, maanaam Seytaane. Malaaka ma yeew ko diirub junniy at,
2and he laid hold on the dragon, the old serpent, who is Devil and Adversary, and did bind him a thousand years,
3 sànni ko ci kàmb gi, tëj ko, sakk bunt bi ko tiim ci kaw. Noonu du nax xeet yi, ba kera junniy at yi di mat. Gannaaw loolu fàww ñu yiwi ko diir bu gàtt.
3and he cast him to the abyss, and did shut him up, and put a seal upon him, that he may not lead astray the nations any more, till the thousand years may be finished; and after these it behoveth him to be loosed a little time.
4 Noonu ma gis ay gàngune, ñu jox ña ca toog sañ-sañu àtte. Noonu ma gis ruuwi ñi ñu bóomoon ndax li ñu doon seedeel Yeesu te gëm kàddug Yàlla. Ñooñu jaamuwuñu rab wa mbaa nataalam, te nanguwuñoo am màndargam rab wa ca seen jë mbaa seen loxo. Ñu daldi dekki, nguuru ak Kirist diirub junniy at.
4And I saw thrones, and they sat upon them, and judgment was given to them, and the souls of those who have been beheaded because of the testimony of Jesus, and because of the word of God, and who did not bow before the beast, nor his image, and did not receive the mark upon their forehead and upon their hand, and they did live and reign with Christ the thousand years;
5 Yeneen néew yi duñu dekki, fi ak junniy at yi matul. Loolu moo di ndekkite lu jëkk li.
5and the rest of the dead did not live again till the thousand years may be finished; this [is] the first rising again.
6 Ñi bokk ci ndekkite lu jëkk li, barkeel nañu te sell! Ñaareelu dee gi du leen manal dara. Waaye dinañu doon saraxalekati Yàlla ak Kirist, tey nguuru ak moom junniy at.
6Happy and holy [is] he who is having part in the first rising again; over these the second death hath not authority, but they shall be priests of God and of the Christ, and shall reign with him a thousand years.
7 Bu junniy at ya matee, dinañu yiwi Seytaane ca kasoom,
7And when the thousand years may be finished, the Adversary shall be loosed out of his prison,
8 te dina dem naxi xeet yi ci ñeenti xeblay àddina, maanaam ñoom Gog ak Magog. Dina leen dajale ngir xare, te dinañu bare ni peppi suuf cig tefes.
8and he shall go forth to lead the nations astray, that are in the four corners of the earth — Gog and Magog — to gather them together to war, of whom the number [is] as the sand of the sea;
9 Dinañu sam suuf sépp, di wër dalu gaayi Yàlla yi ak dëkk, bi Yàlla bëgg. Waaye safara daldi jóge asamaan, lakk leen.
9and they did go up over the breadth of the land, and did surround the camp of the saints, and the beloved city, and there came down fire from God out of the heaven, and devoured them;
10 Dees na jàpp Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu safara ak tamarax bi, mu fekki rab wa ak naaféq ba mbubboo yonent. Foofa dinañu leen mbugal guddi ak bëccëg ba fàww.
10and the Devil, who is leading them astray, was cast into the lake of fire and brimstone, where [are] the beast and the false prophet, and they shall be tormented day and night — to the ages of the ages.
11 Noonu ma gis gàngune mu mag te weex, ak ka ca toog. Asamaan ak suuf daw, sore ko, ba ne mes.
11And I saw a great white throne, and Him who is sitting upon it, from whose face the earth and the heaven did flee away, and place was not found for them;
12 Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanamu gàngune ma. Ñu daldi ubbi ay téere, ubbi itam beneen téere, téereb dund bi. Ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya.
12and I saw the dead, small and great, standing before God, and scrolls were opened, and another scroll was opened, which is that of the life, and the dead were judged out of the things written in the scrolls — according to their works;
13 Noonu géej gëq néew, yi nekkoon ci moom; dee ak barsàq delloo néew, ya ñu yoroon. Ñu àtte ñépp ci seeni jëf.
13and the sea did give up those dead in it, and the death and the hades did give up the dead in them, and they were judged, each one according to their works;
14 Ñu jàpp dee ak barsàq, sànni ca déegu safara sa. Déegu safara soosu moo di ñaareelu dee.
14and the death and the hades were cast to the lake of the fire — this [is] the second death;
15 Képp ku ñu bindul sa tur ci téereb dund bi, dees na la sànni ci déegu safara si.
15and if any one was not found written in the scroll of the life, he was cast to the lake of the fire.