Wolof: New Testament

Young`s Literal Translation

Revelation

22

1 Noonu malaaka ma won ma dexu ndoxum dund, mu leer ni weer bu set, di génn ca gàngune mu Yàlla ak Mbote ma,
1And he shewed me a pure river of water of life, bright as crystal, going forth out of the throne of God and of the Lamb:
2 xellee ca digg péncu dëkk ba. Ca weti dex ga amoon na ca garabu dund, guy meññ fukki yoon ak ñaar, di meññ weer wu nekk, te xob ya di faj xeet yi.
2in the midst of its broad place, and of the river on this side and on that, [is] a tree of life, yielding twelve fruits, in each several month rendering its fruits, and the leaves of the tree [are] for the service of the nations;
3 Musiba dootul am. Gàngune mu Yàlla ak Mbote mi mu ngi ci dëkk bi, te ay jaamam dinañu ko jaamu.
3and any curse there shall not be any more, and the throne of God and of the Lamb shall be in it, and His servants shall serve Him,
4 Dinañu gis xar-kanamam, te turam dina nekk ci seen jë.
4and they shall see His face, and His name [is] upon their foreheads,
5 Guddi dootul am, te kenn dootul soxla leeru làmp walla naaju jant, ndaxte Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dinañu nguuru ba fàww.
5and night shall not be there, and they have no need of a lamp and light of a sun, because the Lord God doth give them light, and they shall reign — to the ages of the ages.
6 Noonu malaaka ma ne ma: «Wax jii ju wóor la te dëggu. Boroom bi, Yàlla jiy leeral xeli yonent yi, moo yónni malaakaam, ngir mu won ay jaamam mbir yi dëgmël di ñëw.»
6And he said to me, `These words [are] stedfast and true, and the Lord God of the holy prophets did send His messenger to shew to His servants the things that it behoveth to come quickly:
7 «Maa ngi ñëw léegi. Yaw miy sàmm waxi Yàlla, yi ci téere bii, barkeel nga.»
7Lo, I come quickly; happy [is] he who is keeping the words of the prophecy of this scroll.`
8 Man Yowaana maa dégg mbir yii te gis ko. Ba ma ko déggee te gis ko, damaa daanu ca tànki malaaka, ma ma ko doon won, bëgg koo jaamu.
8And I, John, am he who is seeing these things and hearing, and when I heard and beheld, I fell down to bow before the feet of the messenger who is shewing me these things;
9 Waaye mu ne ma: «Moytu koo def. Sa nawle laa ci liggéey bi, yaw ak say bokki yonent ak ñiy sàmm waxi téere bii. Jaamul Yàlla.»
9and he saith to me, `See — not; for fellow-servant of thee am I, and of thy brethren the prophets, and of those keeping the words of this scroll; before God bow.`
10 Mu ne ma it: «Bul tëj téere bii ak waxi Yàlla yi mu ëmb, ndaxte waxtu wi jege na.
10And he saith to me, `Thou mayest not seal the words of the prophecy of this scroll, because the time is nigh;
11 Ku jubadi, na sax ci jubadeem; ku taq sobe, na sigiñu ci sobeem; ku jub, na wéy ci jëf yu jub; ku sell, na ci ŋoy.»
11he who is unrighteous — let him be unrighteous still, and he who is filthy — let him be filthy still, and he who is righteous — let him be declared righteous still, and he who is sanctified — let him be sanctified still:
12 Yeesu nee na: «Maa ngi ñëw léegi, indaale pey gi, ngir delloo ku nekk lu mengoo ak lu mu def.
12And lo, I come quickly, and my reward [is] with me, to render to each as his work shall be;
13 Man maay Alfa ak Omega, ki jëkk te mujj, njàlbéen gi ak muj gi.
13I am the Alpha and the Omega — the Beginning and End — the First and the Last.
14 «Yéen ñi fóot seeni mbubb, ngir sañ a lekk ci garabu dund gi te dugg ci bunti dëkk bi, barkeel ngeen.
14`Happy are those doing His commands that the authority shall be theirs unto the tree of the life, and by the gates they may enter into the city;
15 Waaye ñi ci biti ñooy xaj yi, luxuskat yi, njaalookat yi, bóomkat yi, xërëmkat yi ak ñépp ñiy sopp fen te di ci wéy.
15and without [are] the dogs, and the sorcerers, and the whoremongers, and the murderers, and the idolaters, and every one who is loving and is doing a lie.
16 «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede leen mbir yii ci digg mboolooy ñi gëm. Man maay car, bi soqikoo ci Daawuda, di biddiiwu njël bu leer bi.»
16`I, Jesus did send my messenger to testify to you these things concerning the assemblies; I am the root and the offspring of David, the bright and morning star!
17 Te Xelum Yàlla ak séetu Mbote mi ñu ngi naan: «Ñëwal.» Képp ku dégg wax jii, na ne: «Ñëwal.» Na képp ku mar, ñëw; ku bëgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara.
17And the Spirit and the Bride say, Come; and he who is hearing — let him say, Come; and he who is thirsting — let him come; and he who is willing — let him take the water of life freely.
18 Man Yowaana maa ngi koy wax képp ku dégg waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii: ku ci yokk dara, Yàlla dina dolli ci sa mbugal musiba, yi ñu wax ci téere bii.
18`For I testify to every one hearing the words of the prophecy of this scroll, if any one may add unto these, God shall add to him the plagues that have been written in this scroll,
19 Ku dindi dara ci waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii, Yàlla dina dindi sa wàll ca garabu dund ga ak dëkk bu sell ba, ñaar yooyu ñu bind ci téere bii.
19and if any one may take away from the words of the scroll of this prophecy, God shall take away his part from the scroll of the life, and out of the holy city, and the things that have been written in this scroll;`
20 Kiy seede mbir yii nee na: «Waaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin. Boroom bi Yeesu, ñëwal.
20he saith — who is testifying these things — `Yes, I come quickly!` Amen! Yes, be coming, Lord Jesus!
21 Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen ñépp.
21The grace of our Lord Jesus Christ [is] with you all. Amen.