1 Sang yi, yorleen seeni jaam ci nu jub te aw yoon, xam ne, am ngeen yéen itam ab Sang ca asamaan.
1Masters, give to bondmen what is just and fair, knowing that *ye* also have a Master in [the] heavens.
2 Dëkkleen ci ñaan Yàlla, farlu ci, boole ci ngërëm.
2Persevere in prayer, watching in it with thanksgiving;
3 Te ngeen fasaale nu ci ñaan yi itam, ngir Yàlla ubbil nu bunt, nu man a xamle kàddoom, di yégle kumpa gi di Kirist, muy kumpa gi waral ñu jéng ma.
3praying at the same time for us also, that God may open to us a door of the word to speak the mystery of Christ, on account of which also I am bound,
4 Ñaanleen ngir ma xamle ko ni mu ware.
4to the end that I may make it manifest as I ought to speak.
5 Jëfeleen ak xel ci seen diggante ak waa àddina, te fu ngeen ame jot, fexeleen ba jariñoo ko.
5Walk in wisdom towards those without, redeeming opportunities.
6 Na seen wax jépp fees ak yiw te am xorom, ngir ngeen xam nan ngeen war a tontoo ku nekk.
6[Let] your word [be] always with grace, seasoned with salt, [so as] to know how ye ought to answer each one.
7 Tisig, sama mbokk mi ma sopp, di jawriñ ju takku ak sama nawle ci liggéeyu Boroom bi, dina leen yégal lépp lu jëm ci samay mbir.
7Tychicus, the beloved brother and faithful minister and fellow-bondman in [the] Lord, will make known to you all that concerns me;
8 Lii moo tax ma yebal ko ci yéen: ngeen xam xebaar bi jóge ci nun, te it mu dëfël seen xol.
8whom I have sent to you for this very purpose, that he might know your state, and that he might encourage your hearts:
9 Onesim lay àndal, sunu mbokk mu takku, mi nu sopp, te mu bokk ci yéen. Dinañu leen xamal lépp lu xew fii.
9with Onesimus, the faithful and beloved brother, who is [one] of you. They shall make known to you everything here.
10 Aristàrk mi nekk ak man ci kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnabas. Jot ngeen ay ndigal ci mbirum Màrk: bu ñëwee ci yéen, teral-leen ko.
10Aristarchus my fellow-captive salutes you, and Mark, Barnabas's cousin, concerning whom ye have received orders, (if he come to you, receive him,)
11 Yeesu mi ñuy dàkkentale Yustus, moom it mu ngi leen di nuyu. Ñoom rekk ñooy Yawut yiy liggéeyandook man ngir nguuru Yàlla, te ñoo féexal sama xol.
11and Jesus called Justus, who are of the circumcision. These [are the] only fellow-workers for the kingdom of God who have been a consolation to me.
12 Jaamu Kirist, Epafras, mi bokk ci yéen, mu ngi leen di nuyu. Du jóg ci di leen ñaanal, farlu ci ni kuy bëre, ngir ngeen taxaw temm ci coobareg Yàlla gépp, ànd ak ngëm gu mat ak kóolute gu wóor.
12Epaphras, who is [one] of you, [the] bondman of Christ Jesus, salutes you, always combating earnestly for you in prayers, to the end that ye may stand perfect and complete in all [the] will of God.
13 Maa ngi koy seedeel ne, mu ngi sonn bu baax ngir yéen, ngir waa Lawdise ak waa Yerapolis.
13For I bear him witness that he labours much for you, and them in Laodicea, and them in Hierapolis.
14 Luug, doktoor bi ñu sopp, mu ngi leen di nuyu, moom ak Demas.
14Luke, the beloved physician, salutes you, and Demas.
15 Nuyul-leen nu mbokk, yi nekk Lawdise. Nuyul-leen nu itam Nimfa ak mbooloom ñi gëm, miy daje ci këram.
15Salute the brethren in Laodicea, and Nymphas, and the assembly which [is] in his house.
16 Bu ñu jàngee bataaxal bii ci yéen, fexeleen ba ñu jàng ko it ci mbooloom ñi gëm mi nekk Lawdise, te yéen it ngeen jàng bi ma yónnee waa Lawdise.
16And when the letter has been read among you, cause that it be read also in the assembly of Laodiceans, and that *ye* also read that from Laodicea.
17 Te neleen Arkib: «Farlul ci sas, wi la Boroom bi sédde, ba matal ko.»
17And say to Archippus, Take heed to the ministry which thou hast received in [the] Lord, to the end that thou fulfil it.
18 Man Pool maa leen di bind nuyoo bii ci sama loxob bopp. Fàttalikuleen ne, dañu maa jéng. Na yiwu Boroom bi ànd ak yéen!
18The salutation by the hand of me Paul. Remember my bonds. Grace [be] with you.