1 Kon nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu, miy àtte ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci feeñam ci biir ndam ak ci nguuram, nga def lii:
1Jeg vidner for Gud og Kristus Jesus, som skal dømme levende og døde, og ved hans åpenbarelse og hans rike;
2 xamleel kàddug Yàlla, sax ci, su neexee ak su naqaree; yeyal ñi tooñ, di yedd ak a dénk ñépp, def ko ci muñ gu yaatu ak njàngale mu mat.
2Forkynn ordet, vær rede i tide og utide, overbevis, irettesett, forman med all langmodighet og lære!
3 Ndaxte jamono dina ñëw, joo xam ne nit ñi dootuñu xajoo njàngale mu wér mi, waaye dinañu jublu ci seeni bëgg-bëgg, di fortaatu jàngalekat yu leen di jey.
3For det skal komme en tid da de ikke skal tåle den sunde lære, men efter sine egne lyster ta sig selv lærere i hopetall, fordi det klør dem i øret,
4 Dinañu tanqamlu dëgg, jeng jëm ci léebi diiney neen.
4og de skal vende øret bort fra sannheten og vende sig til eventyr.
5 Waaye yaw nanga foog ci lépp, dékku tiis, tey tas xebaar bu baax bi, ba matal sag yónnent.
5Men vær du edru i alle ting, lid ondt, gjør en evangelists gjerning, fullfør din tjeneste!
6 Ndaxte maa ngi ci tànki joxe sama bakkan ni sarax, te sama waxtuw dem jot na.
6For jeg ofres allerede, og tiden for min bortgang er forhånden.
7 Bëre naa ba ub làmbi ngëm, daw naa ba àkk, sàmm naa mboolem dëgg, gi ñu ma dénk.
7Jeg har stridt den gode strid, fullendt løpet, bevart troen.
8 Fi mu ne Yàllaa ngi may xaare añu ku jub, di kaalag ndam gi ma Boroom, biy Àttekat bu jub, di jox ca bés ba, te jéllale naa sama bopp, waaye képp ku def sa xol cig feeñam.
8Så ligger da rettferdighetens krans rede for mig, den som Herren, den rettferdige dommer, skal gi mig på hin dag, dog ikke mig alene, men alle som har elsket hans åpenbarelse.
9 Defal sa kem-kàttan, ba fekksi ma ci ni mu gën a gaawe.
9Gjør dig umak for å komme snart til mig!
10 Ndaxte Demas topp na àddina, ba bàyyi ma, dem dëkku Tesalonig; Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi.
10For Demas forlot mig, fordi han fikk kjærlighet til den nuværende verden, og drog til Tessalonika, Kreskens til Galatia, Titus til Dalmatia;
11 Luug rekk a des fi man. Indaaleel Màrk, ndaxte amal na ma njariñ ci liggéey bi.
11Lukas er alene hos mig. Ta Markus og ha ham med dig! for han er mig nyttig til tjeneste.
12 Tisig moom yebal naa ko dëkku Efes.
12Tykikus har jeg sendt til Efesus.
13 Te sooy ñëw, indaaleel mbubb, ma ma dénkoon Karpus ca dëkku Torowas, te it bul fàtte téere yi, rawatina téere yu am maana, yi ñu bind ci der.
13Når du kommer, da ha med dig den kappe som jeg lot bli i Troas hos Karpus, og bøkene, især skinnbøkene!
14 Alegsàndar tëgg bi def na ma ñaawteef yu ne, waaye Boroom bi dina ko fey ay jëfam.
14Kobbersmeden Aleksander gjorde mig meget ondt; Herren vil lønne ham efter hans gjerninger.
15 Moytu ko bu baax, ndaxte bëre na ak sunuy wax ba tàyyi.
15Vokt dig for ham du også! for han stod hårdt imot våre ord.
16 Keroog bi ma jëkkee taxaw, di làyyil sama bopp, awma woon kenn ku ma taxawu, ñépp dañu maa daw — bu leen ko Yàlla jàppe nag.
16Ved mitt første forsvar møtte ingen med mig, men alle forlot mig; gid det ikke må bli dem tilregnet!
17 Waaye Boroom bi moo ma taxawu te dooleel ma, ma jollil kàddu gi, ba xeet yépp dégg ko. Te Boroom bi musal na ma ci selli gaynde.
17Men Herren stod hos mig og styrket mig, forat forkynnelsen skulde fullbyrdes ved mig og alle folk få høre den, og jeg blev fridd ut av løvens gap.
18 Rax-ca-dolli dina ma musal ci bépp jëf ju ñaaw, tette ma ci jàmm, ba tàbbal ma ci nguuram gu kawe ga. Na yelloo ndam ba fàww. Amiin.
18Herren skal fri mig fra all ond gjerning og frelse mig inn i sitt himmelske rike; ham være æren i all evighet! Amen.
19 Nuyul ma Piriska ak Akilas ak waa kër Onesifor.
19Hils Priska og Akvilas og Onesiforus' hus!
20 Erast des na dëkku Korent. Torofim dafa woppoon, ma bàyyi ko dëkku Mile.
20Erastus blev i Korint; Trofimus lot jeg syk efter mig i Milet.
21 Gaawal a ñëw, bala lolli di gàllankoor sa yoon. Ëbulus, Pudeñsë, Linus, Këlójaa ak yeneen bokk yépp ñu ngi lay nuyu.
21Gjør dig umak for å komme før vinteren! Eubulus og Pudens og Linus og Klaudia og alle brødrene hilser dig.
22 Na Boroom bi aar sa xel. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
22Den Herre Jesus være med din ånd! Nåden være med eder!