1 Man Pool maa lay bind, man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni, ngir xamle ngëm, gi lal yoonu ñi Yàlla tànn, tey yokk xam-xamu dëgg, giy meññ ragal Yàlla;
1Paulus, Guds tjener og Jesu Kristi apostel til å føre Guds utvalgte til tro og til å kjenne den sannhet som hører til gudsfrykt,
2 mu sukkandiku ci yaakaar ju dëggu, ji nu am ci dund gu dul jeex, gi Yàlla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam.
2i håp om evig liv, som Gud, han som ikke lyver, har lovt fra evige tider,
3 Te léegi, ci jamono ji ko soob, feeñal na xebaaram boobu ci waaraate, bi ma Yàlla sunu Musalkat dénk te digal ma, ma xamle ko.
3men nu i sin tid har han åpenbaret sitt ord i den forkynnelse som blev mig betrodd efter Guds, vår frelsers befaling
4 Maa ngi lay bind, Tit, yaw sama doomu diine ju wér ci ngëm, gi nu bokk nun ñépp. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Musalkat may yiw ak jàmm.
4- til Titus, min ekte sønn i den felles tro; Nåde og fred fra Gud Fader og Kristus Jesus, vår frelser!
5 Bàyyi naa la ca réewu Kereet, ngir nga mottali la desoon ci liggéey bi, te samp ay njiiti mbooloo ca dëkk bu nekk, ni ma la ko sante woon.
5Derfor lot jeg dig bli efter på Kreta at du skulde sette det i rette skikk som ennu stod tilbake, og innsette eldste i hver by, således som jeg foreskrev dig,
6 Njiit nag nii la war a mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, am ay doom yu gëm yu amul baatu gannaaw cig yàqute mbaa déggadi.
6om nogen er ulastelig, én kvinnes mann, og har troende barn som ikke har ondt ord på sig for ryggesløshet eller er gjenstridige.
7 Ndaxte kuy sàmm mbooloo mi mooy jawriñu Yàlla, kon warul am ŋàññ, walla di ku dëgër bopp mbaa ku tàng bopp; warul dib màndikat walla xeexkat mbaa ku bëgge ci alal ju lewul.
7For en tilsynsmann skal være ulastelig som en Guds husholder, ikke selvgod, ikke vredladen, ikke drikkfeldig, ikke voldsom, ikke lysten efter ussel vinning,
8 Waaye war na man gan te bëgg lu baax, di ku maandu te jub, ku sell te noot boppam.
8men gjestfri, glad i det gode, sindig, rettferdig, hellig, avholdende,
9 War na jàpp ci xebaar bu dëggu, bi lal sunu yoon, ba man a dénkaane ci njàngale mu wér mi, tey yey ñi weddi.
9en som holder fast ved det troverdige ord efter læren, forat han kan være i stand til både å formane ved den sunde lære og å tale til rette dem som sier imot.
10 Loolu war na, ndaxte am na ñu bare ñu déggul lenn ndigal, rawatina ci Yawut yi, ñuy yàq xeli nit ñi ak seen waxi neen.
10For der er mange gjenstridige, som farer med tomt snakk og dårer folks hu, helst de av omskjærelsen.
11 Fàww nga wedamloo leen, ndax dañuy tas këri lëmm, ciy jàngale li warul ngir sàkku alal ju lewul.
11Disse skal en målbinde; for de nedriver hele hus ved å føre utilbørlig lære for ussel vinnings skyld.
12 Am na nitu Kereet, di yonent ci ñoom, mu ne: «Waa Kereet, ay fenkat lañu mas a doon, ñu soxor ni ay rabi àll, fuqle te tayel.»
12En av dem, deres egen profet, har sagt: Kreterne er alltid løgnere, onde dyr, late buker.
13 Te li mu wax dëgg la. Looloo tax nga war leen a yey bu wóor ci seeni bàkkaar, ngir ñu am ngëm gu wér
13Dette vidnesbyrd er sant. Derfor skal du tale dem strengt til rette, forat de må bli sunde i troen,
14 te bañ a topp léebi diiney neen yu Yawut yi, mbaa tegtali nit, ñi dëddu dëgg.
14så de ikke gir sig av med jødiske eventyr og bud av mennesker som vender sig bort fra sannheten.
15 Ñi sell seen lépp a sell, waaye ñi selladi te gëmadi seen dara sellul, du seeni xalaat, du seeni xel.
15Alt er rent for de rene; men for de urene og vantro er intet rent; både deres sinn og deres samvittighet er urene.
16 Dañoo mbubboo xam-xamu Yàlla, waaye seeni jëf weddi na ko; ñu sikk lañu te déggadi, ba tële ci jëf lenn lu baax.
16De sier at de kjenner Gud; men de fornekter ham med sine gjerninger, for de er vederstyggelige og ulydige og uduelige til all god gjerning.