1 Yeesu moom, dem ca tundu Oliw ya.
1Men Jesus gikk til Oljeberget.
2 Ca ëllëg sa ca fajar, mu dellu ca kër Yàlla ga, mbooloo ma fa teewoon wër ko. Mu toog, tàmbali di leen jàngal.
2Og tidlig om morgenen kom han atter til templet, og alt folket kom til ham, og han satte sig og lærte dem.
3 Xutbakat ya ak Farisen ya indi jenn jigéen ju ñu bettoon muy njaaloo, ñu taxawal ko ca diggu mbooloo ma.
3Da kom de skriftlærde og fariseerne med en kvinne som var grepet i hor, og de stilte henne frem for ham
4 Noonu ñu ne Yeesu: «Kilifa gi, jigéen jii de, dañu koo bett muy njaaloo.
4og sa til ham: Mester! denne kvinne er grepet på fersk gjerning i hor.
5 Ci ndigali Yàlla yi, jigéen ju njaaloo, Musaa dafa santaane ñu sànni ko ay xeer, ba mu dee. Yaw nag, lu ciy sa xalaat?»
5I loven har Moses foreskrevet oss at slike kvinner skal stenes; hvad sier nu du?
6 Loolu nag, dañu ko doon wax ngir seetlu ko, ndaxte bëggoon nañoo tiiñal Yeesu. Yeesu sëgg, di bind ak baaraamam ci suuf.
6Dette sa de for å friste ham, så de kunde få klagemål imot ham. Men Jesus bukket sig ned og skrev med fingeren på jorden.
7 Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: «Ku musul a def bàkkaar ci yéen, na ko jëkk a sànniy xeer.»
7Og da de blev ved å spørre, rettet han sig op og sa: Den av eder som er uten synd, han kaste den første sten på henne!
8 Noonu mu sëggaat, dellu di bind ci suuf.
8Og han bukket sig atter ned og skrev på jorden.
9 Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam.
9Men da de hørte det, gikk de ut, den ene efter den annen, de eldste først; og Jesus blev alene tilbake med kvinnen som stod der.
10 Mu daldi siggi ne ko: «Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ?»
10Da rettet Jesus sig op og sa til henne: Kvinne! hvor er de? Har ingen fordømt dig?
11 Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.»
11Hun sa: Nei, Herre! ingen. Da sa Jesus: Heller ikke jeg fordømmer dig; gå bort, og synd ikke mere!
12 Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
12Atter talte da Jesus til dem og sa: Jeg er verdens lys; den som følger mig, skal ikke vandre i mørket, men ha livsens lys.
13 Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.»
13Fariseerne sa da til ham: Du vidner om dig selv; ditt vidnesbyrd er ikke sant.
14 Yeesu tontu leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
14Jesus svarte og sa til dem: Om jeg også vidner om mig selv, er mitt vidnesbyrd sant; for jeg vet hvorfra jeg er kommet, og hvor jeg går hen; men I vet ikke hvorfra jeg kommer, eller hvor jeg går hen.
15 Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn.
15I dømmer efter kjødet; jeg dømmer ingen.
16 Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man.
16Men om jeg også dømmer, da er min dom rett; for jeg er ikke alene, men jeg og Faderen, som har sendt mig;
17 Seen yoon dafa wax ne, seedes ñaari nit a gën a wóor.
17men også i eders lov står det skrevet at to menneskers vidnesbyrd er sant.
18 Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.»
18Jeg er den som vidner om mig, og Faderen, som har utsendt mig, vidner om mig.
19 Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu tontu ne: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
19De sa da til ham: Hvor er din Fader? Jesus svarte: I kjenner hverken mig eller min Fader; kjente I mig, da kjente I også min Fader.
20 Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jàngalee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn mënu ko woon a jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.
20Disse ord talte han ved tempelkisten, mens han lærte i templet, og ingen grep ham; for hans time var ennu ikke kommet.
21 Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa man a dem.»
21Han sa da atter til dem: Jeg går bort, og I skal lete efter mig, og I skal dø i eders synd; dit jeg går, kan I ikke komme.
22 Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa man a dem. Mbaa du day xaruji?»
22Jødene sa da: Han vil vel ikke drepe sig selv, siden han sier: Dit jeg går, kan I ikke komme?
23 Yeesu tontu ne: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.
23Og han sa til dem: I er nedenfra, jeg er ovenfra; I er av denne verden, jeg er ikke av denne verden.
24 Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.»
24Derfor sa jeg til eder: I skal dø i eders synder; for tror I ikke at det er mig, da skal I dø i eders synder.
25 Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga.
25De sa da til ham: Hvem er du? Jesus sa til dem: Nettop det jeg sier eder.
26 Li ma man a wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.»
26Jeg har meget å si og å dømme om eder; men han som har sendt mig, er sanndru, og det jeg har hørt av ham, det taler jeg til verden.
27 Xamuñu woon ne, Yàlla Baay bee tax muy wax.
27De skjønte ikke at det var om Faderen han talte til dem.
28 Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne, Maay ki nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jàngal rekk laay wax.
28Jesus sa da: Når I får ophøiet Menneskesønnen, da skal I skjønne at det er mig, og at jeg intet gjør av mig selv, men taler dette således som min Fader har lært mig.
29 Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; musu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.»
29Og han som har sendt mig, er med mig; han har ikke latt mig alene, fordi jeg alltid gjør det som er ham til behag.
30 Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm.
30Da han talte dette, trodde mange på ham.
31 Yeesu ne Yawut ya ko gëmoon: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor.
31Jesus sa da til de jøder som var kommet til tro på ham: Dersom I blir i mitt ord, da er I i sannhet mine disipler,
32 Te it dingeen xam dëgg gi te dëgg gi dina leen goreel.»
32og I skal kjenne sannheten, og sannheten skal frigjøre eder.
33 Ñu tontu ko ne: «Nun ci Ibraayma lanu soqikoo te musunoo nekk jaamu kenn. Nan nga nu man a waxe ne, dinañu leen goreel?»
33De svarte ham: Vi er av Abrahams ætt og har aldri vært nogens træler; hvorledes kan da du si: I skal bli fri?
34 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp kuy bàkkaar, jaamu bàkkaar la.
34Jesus svarte dem: Sannelig, sannelig sier jeg eder: Hver den som gjør synd, er syndens træl.
35 Te jaam du bokk ci kër gi ba fàww, waaye doom, moom, ci kër gi la bokk ba fàww.
35Men trælen blir ikke i huset til evig tid; sønnen blir der til evig tid.
36 Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi.
36Får da Sønnen frigjort eder, da blir I virkelig fri.
37 Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen. Waaye yéena ngi may wut a rey, ndaxte li may jàngale xajul ci yéen.
37Jeg vet at I er av Abrahams ætt; men I står mig efter livet, fordi mitt ord ikke finner rum i eder.
38 Li ma sama Baay won laay wax; waaye yéen, li leen seen baay di wax ngeen di def.»
38Jeg taler det jeg har sett hos min Fader; så gjør også I det I har hørt av eders far.
39 Ñu tontu ko ne: «Ibraayma mooy sunu baay.» Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee waa kër Ibraayma, dingeen jëfe ni moom.
39De svarte ham: Vår far er Abraham! Jesus sier til dem: Var I Abrahams barn, da gjorde I Abrahams gjerninger;
40 Léegi nag yéena ngi may wut a rey, man mi leen jottali dëgg, gi ma jële ca Yàlla. Ibraayma deful lu ni mel.
40men nu står I mig efter livet, et menneske som har sagt eder sannheten, som jeg har hørt av Gud; det gjorde ikke Abraham.
41 Li ngeen donne ci seen baay rekk ngeen di def.» Ñu tontu ko ne: «Nun de, dunu doomi araam. Benn baay rekk lanu am, mooy Yàlla.»
41I gjør eders fars gjerninger. De sa til ham: Vi er ikke avlet i hor, vi har én far, Gud.
42 Yeesu ne leen: «Bu Yàlla doon seen baay, dingeen ma bëgg, ndaxte ca moom laa jóge, ñëw ci ndigalam. Ñëwaluma sama bopp, waaye moo ma yónni.
42Jesus sa til dem: Var Gud eders far, da elsket I mig; for jeg er utgått fra Gud og kommer fra ham; for jeg er heller ikke kommet av mig selv, men han har utsendt mig.
43 Lu tax dégguleen li ma leen wax? Li ko waral moo di mënuleen koo déglu.
43Hvorfor skjønner I ikke min tale? Fordi I ikke tåler å høre mitt ord.
44 Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la mas a doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom. Buy fen, dëppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo.
44I har djevelen til far, og I vil gjøre eders fars lyster; han var en manndraper fra begynnelsen og står ikke i sannheten; for sannhet er ikke i ham. Når han taler løgn, taler han av sitt eget, for han er en løgner og løgnens far.
45 Waaye man damay wax dëgg, moo tax gëmuleen ma.
45Men mig tror I ikke, fordi jeg sier eder sannheten.
46 Kan ci yéen moo man a seede ne, bàkkaar naa? Su ma waxee dëgg nag, lu tax dungeen ma gëm?
46Hvem av eder kan overbevise mig om synd? Men sier jeg sannhet, hvorfor tror I mig da ikke?
47 Ku nekk doomu Yàlla dina déglu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Yàlla, looloo tax dungeen déglu.»
47Den som er av Gud, hører Guds ord; derfor hører I ikke, fordi I ikke er av Gud.
48 Yawut ya ne ko: «Ndax danoo waxul dëgg, bu nu nee, nitu Samari nga te dangaa am ay rab?»
48Jødene svarte ham: Sier vi ikke med rette at du er en samaritan og er besatt?
49 Yeesu ne leen: «Awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal.
49Jesus svarte: Jeg er ikke besatt, men jeg ærer min Fader, og I vanærer mig.
50 Wutumaa màggal sama bopp. Keneen a ma koy wutal te mooy àtte.
50Men jeg søker ikke min ære; det er en som søker den og dømmer.
51 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kuy sàmm sama wax doo dee mukk.»
51Sannelig, sannelig sier jeg eder: Om nogen holder mitt ord, skal han aldri i evighet se døden.
52 Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne, dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax, doo ñam dee.”
52Jødene sa til ham: Nu skjønner vi at du er besatt. Abraham er død, og profetene likeså, og du sier: Om nogen holder mitt ord, skal han aldri i evighet smake døden!
53 Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne, yaa ko gën a màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, loo teg sa bopp?»
53Du er da vel ikke større enn vår far Abraham, som døde? og profetene døde; hvem gjør du dig selv til?
54 Yeesu ne leen: «Su ma dee màggal sama bopp, du am maana. Sama Baay a may màggal, moom mi ngeen naan, mooy seen Yàlla.
54Jesus svarte: Ærer jeg mig selv, da er min ære intet; det er min Fader som ærer mig, han som I sier er eders Gud.
55 Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma ne woon xawma ko, ab fenkat laay doon ni yéen. Waaye xam naa ko te maa ngi sàmm waxam.
55Og I kjenner ham ikke, men jeg kjenner ham; og om jeg sier at jeg ikke kjenner ham, da blir jeg en løgner som I. Men jeg kjenner ham og holder hans ord.
56 Seen baay Ibraayma bég na, bi mu yégee sama ngan. Bi mu ko gisee it, bég na ci lool.»
56Abraham, eders far, frydet sig til å se min dag; og han så den og gledet sig.
57 Yawut ya ne ko: «Amaguloo juróom-fukki at, ba noppi naan gis nga Ibraayma?»
57Jødene sa da til ham: Du er ennu ikke femti år og har sett Abraham?
58 Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, laata ñuy sàkk Ibraayma, fekk na ma doon ki ñuy wax Maay ki nekk.»
58Jesus sa til dem: Sannelig, sannelig sier jeg eder: Før Abraham blev til, er jeg.
59 Noonu ñu for ay xeer, bëgg ko koo sànni ngir rey ko. Waaye Yeesu nëbbu, génn kër Yàlla ga.
59Da tok de stener op for å kaste på ham; men Jesus skjulte sig og gikk ut av templet.