1 Màggalu Mburu ya amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax Bésu Jéggi ba.
1Men de usyrede brøds høitid, som kalles påske, var nær;
2 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña.
2og yppersteprestene og de skriftlærde søkte råd til å få ryddet ham av veien; for de fryktet for folket.
3 Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar.
3Men Satan fór inn i Judas med tilnavnet Iskariot, som var en av de tolv,
4 Noonu Yudaa dem waxtaani ak saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.
4og han gikk bort og talte med yppersteprestene og høvedsmennene om hvorledes han skulde forråde ham til dem.
5 Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.
5Og de blev glade, og lovte å gi ham penger,
6 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.
6og han gav sitt tilsagn og søkte leilighet til å forråde ham til dem uten opstyr.
7 Bésu màggalu Mburu ya amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroon a rendi mbotem màggalu Jéggi ba.
7Så kom de usyrede brøds dag, da påskelammet skulde slaktes.
8 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru Jéggi ba.»
8Og han sendte Peter og Johannes avsted og sa: Gå bort og gjør i stand påskelammet for oss, så vi kan ete det!
9 Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»
9De sa til ham: Hvor vil du vi skal gjøre det i stand?
10 Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,
10Han sa til dem: Se, når I kommer inn i byen, skal det møte eder en mann som bærer en krukke vann; følg ham til det hus hvor han går inn,
11 te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi ba, man ak samay taalibe?”
11og si til husbonden: Mesteren sier til dig: Hvor er det herberge der jeg kan ete påskelammet med mine disipler?
12 Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
12Så skal han vise eder en stor sal med benker og hynder; der skal I gjøre det i stand.
13 Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
13De gikk da avsted, og fant det så som han hadde sagt dem; og de gjorde i stand påskelammet.
14 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
14Og da timen kom, satte han sig til bords, og apostlene med ham.
15 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru Jéggi bii, laata ñu may sonal.
15Og han sa til dem: Jeg har hjertelig lengtet efter å ete dette påskelam med eder før jeg lider;
16 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
16for jeg sier eder: Jeg skal aldri mere ete det før det er blitt fullkommet i Guds rike.
17 Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
17Og han tok en kalk, takket og sa: Ta dette og del det mellem eder!
18 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum réseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
18For jeg sier eder: Fra nu av skal jeg aldri mere drikke av vintreets frukt før Guds rike er kommet.
19 Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
19Og han tok et brød, takket og brøt det, gav dem og sa: Dette er mitt legeme, som gis for eder; gjør dette til minne om mig!
20 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
20Likeså kalken, efterat de hadde ett, og sa: Denne kalk er den nye pakt i mitt blod, som utgydes for eder.
21 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
21Men se, hans hånd som forråder mig, er med mig over bordet.
22 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
22For Menneskesønnen går vel bort, som bestemt er; men ve det menneske ved hvem han blir forrådt!
23 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nar a def loolu.
23De begynte da å spørre hverandre om hvem av dem det vel kunde være som skulde gjøre denne gjerning.
24 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gën a màgg.
24Det blev også en trette mellem dem om hvem av dem skulde gjelde for å være størst.
25 Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
25Da sa han til dem: Kongene hersker over sine folk, og de som bruker makt over dem, kalles deres velgjørere.
26 Waaye yéen buleen def noonu. Ki gën a màgg ci yéen, na nekk ni ki gën a ndaw, te njiit mel ni surga.
26Så er det ikke med eder; men den største blandt eder skal være som den yngste, og den øverste som den som tjener.
27 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gën a màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
27For hvem er størst, den som sitter til bords, eller den som tjener? Er det ikke den som sitter til bords? Men jeg er som en tjener iblandt eder.
28 Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
28Men I er de som har holdt ut hos mig i mine prøvelser,
29 Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
29og jeg tilsier eder riket, likesom min Fader har tilsagt mig det,
30 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
30så I skal ete og drikke ved mitt bord i mitt rike, og sitte på troner og dømme Israels tolv stammer.
31 Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
31Simon! Simon! se, Satan krevde å få eder i sin vold for å sikte eder som hvete;
32 Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo dellusee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
32men jeg bad for dig at din tro ikke måtte svikte, og når du engang omvender dig, da styrk dine brødre!
33 Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»
33Men han sa til ham: Herre! med dig er jeg rede til å gå både i fengsel og i død.
34 Yeesu tontu ko ne: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne, xam nga ma.»
34Da sa han: Jeg sier dig, Peter: Hanen skal ikke gale idag før du tre ganger har nektet at du kjenner mig.
35 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu tontu ne: «Déedéet.»
35Og han sa til dem: Da jeg sendte eder ut uten pung og skreppe og sko, fattedes eder da noget? De sa: Nei, intet.
36 Mu neeti leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
36Han sa da til dem: Men nu skal den som har pung, ta den med, likeså skreppe, og den som ikke har sverd, han selge sin kappe og kjøpe sig et!
37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
37For jeg sier eder at dette som er skrevet, må opfylles på mig, dette ord: Og han blev regnet blandt ugjerningsmenn; for det som er sagt om mig, er til ende.
38 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
38Da sa de: Herre! se, her er to sverd. Men han sa til dem: Det er nok.
39 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe nakajekk. Taalibeem ya topp ci moom.
39Og han gikk ut og vandret efter sedvane til Oljeberget; men hans disipler fulgte og med ham.
40 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir bañ a daanu cig fiir.»
40Og da han kom til stedet, sa han til dem: Bed at I ikke må komme i fristelse!
41 Noonu mu dand leen, ba fu aw saan man a tollu, daldi sukk di ñaan ne:
41Og han slet sig fra dem så lang som et stenkast, og falt på kne, bad og sa:
42 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
42Fader! om du vil, da la denne kalk gå mig forbi! Dog, skje ikke min vilje, men din!
43 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
43Og en engel fra himmelen åpenbarte sig for ham og styrket ham.
44 Ci biir tiis, Yeesu gën a sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
44Og han kom i dødsangst og bad enda heftigere, og hans sved blev som blodsdråper, som falt ned på jorden.
45 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, dellusi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
45Så stod han op fra bønnen og kom til sine disipler og fant dem sovende av bedrøvelse,
46 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir.»
46og han sa til dem: Hvorfor sover I? Stå op og bed at I ikke må komme i fristelse!
47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
47Mens han ennu talte, se, da kom en flokk, og han som hette Judas, en av de tolv, gikk foran dem og trådte nær til Jesus for å kysse ham.
48 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
48Men Jesus sa til ham: Judas! forråder du Menneskesønnen med et kyss?
49 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgg a xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
49Da nu de som var om ham, så hvad som vilde skje, sa de: Herre! skal vi slå til med sverd?
50 Kenn ci ñoom nag dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg.
50Og en av dem slo til yppersteprestens tjener og hugg det høire øre av ham.
51 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
51Men Jesus svarte og sa: La dem bare gå så vidt! Og han rørte ved hans øre og lægte ham.
52 Noonu Yeesu ne saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
52Og Jesus sa til yppersteprestene og høvedsmennene over tempel-vakten og de eldste som var kommet imot ham: I er gått ut som mot en røver med sverd og stokker;
53 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
53da jeg daglig var hos eder i templet, rakte I ikke eders hender ut mot mig. Men dette er eders time og mørkets makt.
54 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër saraxalekat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
54Da de nu hadde grepet ham, drog de avsted med ham og førte ham inn i yppersteprestens hus; og Peter fulgte langt bakefter.
55 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
55De hadde tendt en ild midt i gårdsrummet og satt der sammen, og Peter satt midt iblandt dem.
56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
56Men en tjenestepike fikk se ham sitte mot lyset, og stirret på ham og sa: Også denne var med ham.
57 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
57Men han fornektet ham og sa: Jeg kjenner ham ikke, kvinne!
58 Nes tuuti keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer tontu ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
58Litt efter fikk en annen se ham og sa: Du er også en av dem. Men Peter sa: Menneske! jeg er ikke det.
59 Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»
59Og omkring én time efter stadfestet en annen det og sa: Sannelig, også denne var med ham; han er jo en galileer.
60 Waaye Piyeer tontu ne: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.
60Men Peter sa: Menneske! jeg forstår ikke hvad det er du mener! Og straks, mens han ennu talte, gol hanen.
61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»
61Og Herren vendte sig og så på Peter; og Peter kom Herrens ord i hu, hvorledes han hadde sagt til ham: Før hanen galer idag, skal du fornekte mig tre ganger.
62 Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.
62Og han gikk ut og gråt bitterlig.
63 Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.
63Og mennene som holdt Jesus, spottet ham og slo ham,
64 Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?»
64og de kastet et klæde over ham og spurte ham og sa: Spå nu: Hvem var det som slo dig?
65 Ñu ngi ko doon tifaar it yeneeni saaga.
65Og mange andre spottord talte de til ham.
66 Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam.
66Da det nu blev dag, samledes folkets eldste og yppersteprestene og de skriftlærde, og de førte ham frem i sitt rådsmøte
67 Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu tontu leen ne: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.
67og sa: Er du Messias, da si oss det! Men han sa til dem: Om jeg sier eder det, tror I det ikke;
68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu.
68og om jeg spør, svarer I ikke.
69 Waaye gannaawsi tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla, Aji Kàttan ji.»
69Men fra nu av skal Menneskesønnen sitte ved Guds krafts høire hånd.
70 Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu tontu leen ne: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.»
70Da sa de alle: Er du da Guds Sønn? Han sa til dem: I sier det; jeg er det.
71 Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»
71Da sa de: Hvad skal vi mere med vidnesbyrd? Vi har jo selv hørt det av hans munn.