1 Noonu ñu jàll dex ga, ba teer ci diiwaanu waa Serasa.
1They came to the other side of the sea, into the country of the Gadarenes.
2 Bi Yeesu génnee gaal gi, nit ku rab jàpp jóge ca sëg ya, daldi ñëw kar ko.
2When he had come out of the boat, immediately a man with an unclean spirit met him out of the tombs.
3 Kooku nag ca sëg ya la dëkk, te kenn mënu koo yeew, du ak càllala sax.
3He lived in the tombs. Nobody could bind him any more, not even with chains,
4 Ndaxte ay yoon yu bare jéngoon nañu ko te yeew ko ak ay càllala, waaye waa ji daldi dagg càllala yi te damm jéng yi, ba kenn amul woon kàttanu téye ko.
4because he had been often bound with fetters and chains, and the chains had been torn apart by him, and the fetters broken in pieces. Nobody had the strength to tame him.
5 Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer.
5Always, night and day, in the tombs and in the mountains, he was crying out, and cutting himself with stones.
6 Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam,
6When he saw Jesus from afar, he ran and bowed down to him,
7 di xaacu naan: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Yàlla, bu ma mbugal.»
7and crying out with a loud voice, he said, “What have I to do with you, Jesus, you Son of the Most High God? I adjure you by God, don’t torment me.”
8 Ndaxte Yeesu nee woon na ko: «Yaw rab wu bon wi, génnal ci nit ki.»
8For he said to him, “Come out of the man, you unclean spirit!”
9 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
9He asked him, “What is your name?” He said to him, “My name is Legion, for we are many.”
10 Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leen a dàq ca réew ma.
10He begged him much that he would not send them away out of the country.
11 Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
11Now on the mountainside there was a great herd of pigs feeding.
12 Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.»
12All the demons begged him, saying, “Send us into the pigs, that we may enter into them.”
13 Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni.
13At once Jesus gave them permission. The unclean spirits came out and entered into the pigs. The herd of about two thousand rushed down the steep bank into the sea, and they were drowned in the sea.
14 Noonu sàmm ya daw ca dëkk ba ak ca àll ba, nettaliji mbir mi, ba nit ñi ñëw, seet li xew.
14Those who fed them fled, and told it in the city and in the country. The people came to see what it was that had happened.
15 Ñu ñëw nag ci Yeesu, gis ka rab ya jàppoon toog, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
15They came to Jesus, and saw him who had been possessed by demons sitting, clothed, and in his right mind, even him who had the legion; and they were afraid.
16 Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya.
16Those who saw it declared to them how it happened to him who was possessed by demons, and about the pigs.
17 Ci kaw loolu ñu daldi ñaan Yeesu, mu sore seen réew.
17They began to beg him to depart from their region.
18 Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya jàppoon ñaan Yeesu, ngir ànd ak moom.
18As he was entering into the boat, he who had been possessed by demons begged him that he might be with him.
19 Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: «Ñibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi yërëme, ba defal la lii lépp.»
19He didn’t allow him, but said to him, “Go to your house, to your friends, and tell them what great things the Lord has done for you, and how he had mercy on you.”
20 Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru.
20He went his way, and began to proclaim in Decapolis how Jesus had done great things for him, and everyone marveled.
21 Noonu Yeesu jàllaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit ñu bare dajaloo, wër ko.
21When Jesus had crossed back over in the boat to the other side, a great multitude was gathered to him; and he was by the sea.
22 Kenn ci njiiti jàngu ba nag, tudd Yayrus, ñëw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy tànkam,
22Behold, one of the rulers of the synagogue, Jairus by name, came; and seeing him, he fell at his feet,
23 di ko saraxu lu bare naan: «Sama doom ju jigéen mi ngi bëgg a faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu wér te dund.»
23and begged him much, saying, “My little daughter is at the point of death. Please come and lay your hands on her, that she may be made healthy, and live.”
24 Noonu Yeesu ànd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu réy topp ko, di ko tanc.
24He went with him, and a great multitude followed him, and they pressed upon him on all sides.
25 Amoon na fa nag jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar.
25A certain woman, who had an issue of blood for twelve years,
26 Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, sànk ci alalam jépp te jëlewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.
26and had suffered many things by many physicians, and had spent all that she had, and was no better, but rather grew worse,
27 Noonu mu déggoon turu Yeesu, ne ci boppam: «Su ma laalee ay yéreem rekk, dinaa wér.» Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam.
27having heard the things concerning Jesus, came up behind him in the crowd, and touched his clothes.
29 Ci saa si deret ji taxaw, mu yég ci yaramam ne, jàngoroom deñ na.
28For she said, “If I just touch his clothes, I will be made well.”
30 Yeesu yég ci saa si ne, doole génn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: «Ana ku laal samay yére?»
29Immediately the flow of her blood was dried up, and she felt in her body that she was healed of her affliction.
31 Ay taalibeem tontu ko: «Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wër; ngay laaj: “Ku ma laal?”»
30Immediately Jesus, perceiving in himself that the power had gone out from him, turned around in the crowd, and asked, “Who touched my clothes?”
32 Waaye Yeesu di xool li ko wër, ngir gis ku ko def.
31His disciples said to him, “You see the multitude pressing against you, and you say, ‘Who touched me?’”
33 Noonu jigéen ja ñëw, daanu ciy tànkam, wax ko dëgg gépp; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam.
32He looked around to see her who had done this thing.
34 Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la; demal ci jàmm, te na sa jàngoro wàcc.»
33But the woman, fearing and trembling, knowing what had been done to her, came and fell down before him, and told him all the truth.
35 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.»
34He said to her, “Daughter, your faith has made you well. Go in peace, and be cured of your disease.”
36 Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te bañ a tiit.»
35While he was still speaking, people came from the synagogue ruler’s house saying, “Your daughter is dead. Why bother the Teacher any more?”
37 Noonu Yeesu dem, ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu ànd ak moom.
36But Jesus, when he heard the message spoken, immediately said to the ruler of the synagogue, “Don’t be afraid, only believe.”
38 Naka lañu ñëw ci kër njiit li, Yeesu dégg coow li; ñii di jooy, ñii di yuuxu.
37He allowed no one to follow him, except Peter, James, and John the brother of James.
39 Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
38He came to the synagogue ruler’s house, and he saw an uproar, weeping, and great wailing.
40 Waaye ñu di ko ñaawal. Noonu Yeesu génne ñépp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak ñi mu àndal, dugg fa janq bi nekk.
39When he had entered in, he said to them, “Why do you make an uproar and weep? The child is not dead, but is asleep.”
41 Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.»
40They ridiculed him. But he, having put them all out, took the father of the child, her mother, and those who were with him, and went in where the child was lying.
42 Ca saa sa janq bi jóg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp daldi waaru, ba ne jomm.
41Taking the child by the hand, he said to her, “Talitha cumi!” which means, being interpreted, “Girl, I tell you, get up!”
43 Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal; teg ca naa: «Mayleen janq bi, mu lekk.»
42Immediately the girl rose up and walked, for she was twelve years old. They were amazed with great amazement.
43He strictly ordered them that no one should know this, and commanded that something should be given to her to eat.