Wolof: New Testament

World English Bible

Revelation

1

1 Lii mooy li Yeesu Kirist feeñal, te mu tukkee ca Yàlla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi dëgmël di ñëw. Yónni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana.
1This is the Revelation of Jesus Christ, which God gave him to show to his servants the things which must happen soon, which he sent and made known by his angel to his servant, John,
2 Kooku mi ngi seede fii li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist.
2who testified to God’s word, and of the testimony of Jesus Christ, about everything that he saw.
3 Barkeel ngeen, yaw miy jàng ak yéen ñiy déglu wax yii jóge ca Yàlla, te di sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.
3Blessed is he who reads and those who hear the words of the prophecy, and keep the things that are written in it, for the time is at hand.
4 Man Yowaana maa leen di bind, yéen juróom-ñaari mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak jàmm féete ci yéen, jóge ci Yàlla, moom ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg. Yiw woowu ak jàmm jooju ñoo ngi tukkee it ci juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,
4John, to the seven assemblies that are in Asia: Grace to you and peace, from God, who is and who was and who is to come; and from the seven Spirits who are before his throne;
5 tukkee it ci Yeesu Kirist, seede bu takku bi, moom taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, di buuru buur yi ci kaw suuf yépp. Na ndam ak nguur féete ak Yeesu Kirist ba fàww, moom mi nu bëgg te yiwi nu ci sunuy bàkkaar ak deretam ji tuuru, te def nu askanu saraxalekati Buur Yàlla Baayam, nu di ko jaamu. Amiin.
5and from Jesus Christ, the faithful witness, the firstborn of the dead, and the ruler of the kings of the earth. To him who loves us, and washed us from our sins by his blood;
7 Gisleen, mi ngi ñëw ci niir yi,te ñépp dinañu teg seeni bët ci moom,ba ci ñi ko jam sax.Te xeet yi nekk ci kaw suuf yéppdinañu jooy ndax moom.Waaw. Amiin.
6and he made us to be a Kingdom, priests to his God and Father; to him be the glory and the dominion forever and ever. Amen.
8 Boroom bi Yàlla nee na: «Man Yàlla maay Alfa ak Omega, maay ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg, man Aji Kàttan ji.»
7Behold, he is coming with the clouds, and every eye will see him, including those who pierced him. All the tribes of the earth will mourn over him. Even so, Amen.
9 Man Yowaana seen mbokk, di seen nawle ci fitna, ci nguur ak ci muñ, yi nu am ndax sunu booloo ak Yeesu, maa nga nekkoon ca dun bu ñuy wax Patmos. Wacce woon nañu ma fa, ndax li ma doon waare kàddug Yàlla tey seedeel Yeesu.
8 “I am the Alpha and the Omega, says the Lord God, “who is and who was and who is to come, the Almighty.”
10 Xelum Yàlla solu ma ci bésu Boroom bi, te noonu ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit,
9I John, your brother and partner with you in oppression, Kingdom, and perseverance in Christ Jesus, was on the isle that is called Patmos because of God’s Word and the testimony of Jesus Christ.
11 naan: «Bindal ci téere li ngay gis te yónnee ko juróom-ñaari mboolooy ñi gëm, ca dëkki Efes, Samirin, Pergam, Catir, Sàrd, Filadelfi ak Lawdise.»
10I was in the Spirit on the Lord’s day, and I heard behind me a loud voice, like a trumpet
12 Noonu ma geestu, ngir seet ku doon wax ak man. Ba ma geestoo, yem ci juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus,
11saying, What you see, write in a book and send to the seven assemblies : to Ephesus, Smyrna, Pergamum, Thyatira, Sardis, Philadelphia, and to Laodicea.”
13 gis ku taxaw ci biir làmp ya, niroo ak doomu nit. Mu sol mbubb mu gudd, takk ngeñaayu wurus ci ndiggam.
12I turned to see the voice that spoke with me. Having turned, I saw seven golden lampstands.
14 Boppam ak kawaram weex tàll ni perkaal, ay bëtam di xuyy ni safara.
13And among the lampstands was one like a son of man, clothed with a robe reaching down to his feet, and with a golden sash around his chest.
15 Ay tànkam mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baatam di riir ni duusi géej.
14His head and his hair were white as white wool, like snow. His eyes were like a flame of fire.
16 Mu yor ci loxol ndeyjooram juróom-ñaari biddiiw, jaasiy ñaari boor yu ñaw di génn ci gémmiñam, xar-kanamam leer nàññ ni jantub njolloor.
15His feet were like burnished brass, as if it had been refined in a furnace. His voice was like the voice of many waters.
17 Naka laa ko gis, di daanu ci ay tànkam ni ku dee. Waaye mu teg loxol ndeyjooram ci sama kaw ne ma: «Bul ragal dara. Maay ki jëkk te maay mujj.
16He had seven stars in his right hand. Out of his mouth proceeded a sharp two-edged sword. His face was like the sun shining at its brightest.
18 Maay Kiy Dund. Dee woon naa, waaye maa ngii di dund ba fàww, yor caabiy dee ak ju barsàq.
17When I saw him, I fell at his feet like a dead man. He laid his right hand on me, saying, “Don’t be afraid. I am the first and the last,
19 Kon nag bindal li nga gis, li am léegi ak li nar a ami gannaaw gi.
18 and the Living one. I was dead, and behold, I am alive forevermore. Amen. I have the keys of Death and of Hades .
20 Juróom-ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndeyjoor, ak juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus yi, ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki: biddiiw yi ñoo di malaakay juróom-ñaari mboolooy ñi gëm; juróom-ñaari làmp yi ñoo di juróom-ñaari mbooloo yi.
19 Write therefore the things which you have seen, and the things which are, and the things which will happen hereafter;
20 the mystery of the seven stars which you saw in my right hand, and the seven golden lampstands. The seven stars are the angels of the seven assemblies. The seven lampstands are seven assemblies.