1 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Efes, ne ko: i Ki téye juróom-ñaari biddiiw yi ci loxol ndeyjooram, tey dox ci diggu juróom-ñaari làmpi diwlin yu wurus yi nee na:
1 “To the angel of the assembly in Ephesus write: “He who holds the seven stars in his right hand, he who walks among the seven golden lampstands says these things:
2 Xam naa say jëf, sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne, mënuloo dékku ñiy def lu bon. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay naaféq lañu.
2 “I know your works, and your toil and perseverance, and that you can’t tolerate evil men, and have tested those who call themselves apostles, and they are not, and found them false.
3 Xam naa it ne muñ nga, ba dékku coono ndax sama tur, te xàddiwoo. i
3 You have perseverance and have endured for my name’s sake, and have TR adds “have labored and” not grown weary.
4 Waaye li ma naqari ci yaw moo di sa mbëggeel wàññiku na.
4 But I have this against you, that you left your first love.
5 Deel fàttaliku kon fa nga daanoo. Réccul te def, na nga daan def bu jëkk. Soo réccuwul, dinaa dikk ci yaw, jële sa làmp ca bérab ba mu nekk.
5 Remember therefore from where you have fallen, and repent and do the first works; or else I am coming to you swiftly, and will move your lampstand out of its place, unless you repent.
6 Waaye lii neex na ma ci yaw: sib nga ni man li ñoom Nikolas di jëf. i
6 But this you have, that you hate the works of the Nicolaitans, which I also hate.
7 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la may, nga lekk ci garabu dund, gi nekk ci jataayu Yàlla.
7 He who has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies. To him who overcomes I will give to eat of the tree of life, which is in the Paradise of my God.
8 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Samirin, ne ko: i Ki jëkk te mujj, ki dee woon te dekki nee na:
8 “To the angel of the assembly in Smyrna write: “The first and the last, who was dead, and has come to life says these things:
9 Xam naa sa coono, xam it sa néew doole, moona yaaka duunle. Ñooñu tuddoo Yawut, xam naa ñaawteef yi ñu teg ci sa der: ndajem Seytaane la.
9 “I know your works, oppression, and your poverty (but you are rich), and the blasphemy of those who say they are Jews, and they are not, but are a synagogue of Satan.
10 Bul ragal li nga nar a daj. Seytaane dina dugal kaso ñenn ci yéen, ngir wut leen a fiir. Diirub fukki fan dingeen am coono. Nanga takku ba àttan cee dee, ma jox la kaalag dund gi. i
10 Don’t be afraid of the things which you are about to suffer. Behold, the devil is about to throw some of you into prison, that you may be tested; and you will have oppression for ten days. Be faithful to death, and I will give you the crown of life.
11 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, doo loru ci ñaareelu dee.
11 He who has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies. He who overcomes won’t be harmed by the second death.
12 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Pergam, ne ko: i Boroom jaasi ju ñaw, ji am ñaari boor nee na:
12 “To the angel of the assembly in Pergamum write: “He who has the sharp two-edged sword says these things:
13 Xam naa fa nga dëkk, di fa Seytaane samp nguuram. Moona jébbalu nga ci sama tur te weddiwoo sa ngëm ci man, ba ca fan ya ñu reye Antipas, sama seede bu takku ba, ci seen dëkk, di dëkku Seytaane. i
13 “I know your works and where you dwell, where Satan’s throne is. You hold firmly to my name, and didn’t deny my faith in the days of Antipas my witness, my faithful one, who was killed among you, where Satan dwells.
14 Waaye am na lu ma naqari ci yaw, moo di uuf nga foofu gaa yuy sàmm njàngalem Balaam, moom mi jàngaloon Balag, mu sóob bànni Israyil ci bàkkaar, xiir leen ci lekk ñam wu ñu tuuroo xërëm yi, xiir leen ci njaaloo.
14 But I have a few things against you, because you have there some who hold the teaching of Balaam, who taught Balak to throw a stumbling block before the children of Israel, to eat things sacrificed to idols, and to commit sexual immorality.
15 Te am nga noonu itam ay nit ñuy sàmm njàngalem ñoom Nikolas.
15 So you also have some who hold to the teaching of the Nicolaitans likewise TR reads “which I hate” instead of “likewise” .
16 Réccul kon; lu ko moy dinaa dikk ci yaw léegi te xeex ak nit ñooñu ak jaasi, jiy génn ci sama gémmiñ. i
16 Repent therefore, or else I am coming to you quickly, and I will make war against them with the sword of my mouth.
17 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la jox, nga lekk dund bi ñuy wax mànn te mu nëbbu, te dinaa la jox xeer wu weex. Ci kaw xeer woowu bindees na ci tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ki ko jot.
17 He who has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies. To him who overcomes, to him I will give of the hidden manna, Manna is supernatural food, named after the Hebrew for “What is it?”. See Exodus 11:7-9. and I will give him a white stone, and on the stone a new name written, which no one knows but he who receives it.
18 «Bindal malaakam mbooloom ñi gëm ci dëkku Catir, ne ko: i Doomu Yàlla ji, ki ay bëtam di xuyy ni safara, tey tànkam di lerax ni xànjar, nee na:
18 “To the angel of the assembly in Thyatira write: “The Son of God, who has his eyes like a flame of fire, and his feet are like burnished brass, says these things:
19 Xam naa say jëf, sa mbëggeel, sa ngëm, sag muñ ak ni nga farloo ci sa jaamu Yàlla. Xam naa say jëf yu mujj, ni ñu ëppe yu jëkk ya. i
19 “I know your works, your love, faith, service, patient endurance, and that your last works are more than the first.
20 Waaye li ma naqari ci yaw moo di dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, di jàngale ak a réeral sama jaam yi, ngir ñuy sóobu ci njaaloo te di lekk ñam wu ñu tuuroo xërëm yi.
20 But I have this against you, that you tolerate your TR, NU read “that” instead of “your” woman, Jezebel, who calls herself a prophetess. She teaches and seduces my servants to commit sexual immorality, and to eat things sacrificed to idols.
21 May naa ko ab diir, ngir mu tuub njaaloom, waaye bañ na.
21 I gave her time to repent, but she refuses to repent of her sexual immorality.
22 Kon nag dinaa ko tëral ci lalu metit, te ñiy ànd ak moom di njaaloo, su ñu tuubul jëfi jigéen jooju, dinaa leen teg naqar wu mag.
22 Behold, I will throw her into a bed, and those who commit adultery with her into great oppression, unless they repent of her works.
23 Dinaa rey ay doomam, te mboolooy ñi gëm yépp dinañu xam ne, man maa di kiy nattu xol ak xalaat, te dinaa fey ku nekk ay jëfam.
23 I will kill her children with Death, and all the assemblies will know that I am he who searches the minds and hearts. I will give to each one of you according to your deeds.
24 Waaye yéen ñépp ñi des ci Catir te toppuleen njàngale moomu te gëstuwuleen loolu ñu naan mbiri Seytaane yu xóot yi, maa ngi leen di wax ne, duma leen yen beneen yen
24 But to you I say, to the rest who are in Thyatira, as many as don’t have this teaching, who don’t know what some call ‘the deep things of Satan,’ to you I say, I am not putting any other burden on you.
25 bu dul bii: jàppleen ci li ngeen jàpp, ba kera may ñëw. i
25 Nevertheless, hold that which you have firmly until I come.
26 Ku daan tey sax ci samay jëf ba ca muj ga, dinaa ko jox sañ-sañ ci xeet yi:i
26 He who overcomes, and he who keeps my works to the end, to him I will give authority over the nations.
27 Dina leen jiite ak yetu weñ,i tojat leen ni ñuy toje ndaal kew —i
27 He will rule them with a rod of iron, shattering them like clay pots; Psalm 2:9 as I also have received of my Father:
28 ni ma jële sañ-sañ ci sama Baay. Dinaa ko jox it biddiiwu njël.
28 and I will give him the morning star.
29 Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm.
29 He who has an ear, let him hear what the Spirit says to the assemblies.