1 Gannaaw loolu ma xool, gis bunt ubbiku ci asamaan. Baat booba ma déggoon, muy wax ak man mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la li war a ñëw gannaaw gi.»
1After these things I looked and saw a door opened in heaven, and the first voice that I heard, like a trumpet speaking with me, was one saying, “Come up here, and I will show you the things which must happen after this.”
2 Ca saa sa Xelum Yàlla solu ma, noonu ma gis gàngune ca asamaan, te am ku ca toog.
2Immediately I was in the Spirit. Behold, there was a throne set in heaven, and one sitting on the throne
3 Leeraayam mel ni jamaa ak per bu xonq, te xon gu leer ni per bu wert wër gàngune ma.
3that looked like a jasper stone and a sardius. There was a rainbow around the throne, like an emerald to look at.
4 Yeneen ñaar-fukki gàngune ak ñeent wër ko, te ci kaw gàngune ya ñaar-fukki mag ak ñeent toog, sol mbubb yu weex ak kaalay wurus ci seen bopp.
4Around the throne were twenty-four thrones. On the thrones were twenty-four elders sitting, dressed in white garments, with crowns of gold on their heads.
5 Ay melax, ay riir ak ay dënnu di jibe ca gàngune ma. Ca kanamu gàngune ma amoon na fa juróom-ñaari làmp yu yànj, di juróom-ñaari Xeli Yàlla yi.
5Out of the throne proceed lightnings, sounds, and thunders. There were seven lamps of fire burning before his throne, which are the seven Spirits of God.
6 Amoon na it ca kanamu gàngune ma lu mel ni géej gu leer ni weer bu set, ba mel ni seetu. Ci li wër gàngune ma, sës rëkk, amoon na fa ñeenti mbindeef yu fees ak ay bët ci kanam ak ci gannaaw.
6Before the throne was something like a sea of glass, similar to crystal. In the midst of the throne, and around the throne were four living creatures full of eyes before and behind.
7 Mbindeef mu jëkk maa nga meloon ni gaynde, ñaareelu mbindeef mel ni yëkk, ñetteelu mbindeef yor kanamu nit, ñeenteel ba di nirook jaxaay juy naaw.
7The first creature was like a lion, and the second creature like a calf, and the third creature had a face like a man, and the fourth was like a flying eagle.
8 Ñeenti mbindeef ya am nañu ku nekk juróom-benni laaf te ñu nga fees ak ay bët li leen wër lépp, ba ci seen roni laaf. Guddi ak bëccëg duñu noppeek naan:«Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,moo sell, sell, sell,moom ki nekkoon démb,ki nekk tey, te di ñëw ëllëg.»
8The four living creatures, each one of them having six wings, are full of eyes around and within. They have no rest day and night, saying, “Holy, holy, holy Hodges/Farstad MT reads “holy” 9 times instead of 3. is the Lord God, the Almighty, who was and who is and who is to come!”
9 Saa su mbindeef ya di màggal ki toog ca gàngune ma tey dund ba fàww, te di ko kañ ak a gërëm,
9When the living creatures give glory, honor, and thanks to him who sits on the throne, to him who lives forever and ever,
10 ñaar-fukki mag ña ak ñeent di dëpp seen jë ca kanamu ka toog ca kaw gàngune ma. Ñu di ko jaamu, moom mi dund ba fàww, di sànni seen kaalay ndam ca kanamu gàngune ma, naan:
10the twenty-four elders fall down before him who sits on the throne, and worship him who lives forever and ever, and throw their crowns before the throne, saying,
11 «Yàlla sunu Boroom,yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan,ndaxte yaa sàkk léppte ci sa coobare la lépp nekke,te ci lañu leen sàkke.»
11“Worthy are you, our Lord and God, the Holy One, TR omits “and God, the Holy One,” to receive the glory, the honor, and the power, for you created all things, and because of your desire they existed, and were created!”