Wolof: New Testament

Mark

3

1 Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi. 2 Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ba man koo tuumaal. 3 Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanamu ñépp.»4 Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell. 5 Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ. 6 Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu. 7 Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko. 8 Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon. 9 Booba nag Yeesu faj na ñu bare, ba ñu am ay jàngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, ñu wutal ko gaal, ngir mbooloo mi bañ koo buux. 11 Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.» 12 Waaye Yeesu gëdd rab yi bu wér, ngir ñu bañ koo siiwal. 13 Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom. 14 Noonu mu tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñu ànd ak moom te mu yónni leen, ñu waareji, 15 mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab. 16 Fukk ak ñaar ñii la tànn:Simoŋ, mi mu tudde Piyeer,17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay — ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi» — 18 Andare ak Filib,Bartelemi ak Macë,Tomaa ak Saag doomu Alfe,Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;19 ak Yudaa Iskariyo mi nar a wor Yeesu. 20 Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax mënuñoo lekk sax. 21 Bi ko ay bokkam déggee nag, ñu ñëw, ngir jàppsi ko naan: «Dafa tàggoo ak sagoom.» 22 Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» 23 Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane man a dàqe Seytaane? 24 Réew mu xeex boppam, du man a yàgg. 25 Te kër gu xeex boppam, du man a yàgg. 26 Bu Seytaane nag jógee, ba xeex boppam, xàjjalikoo dikkal na ko te du man a yàgg, waaye dina tas. 27 «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn man a dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp. 28 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp dees na ko baal nit ñi, muy bàkkaar, muy sosal Yàlla wu mu man a doon. 29 Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.» 30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon nañu, rab jàpp na ko.31 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw, ñu taxaw ci biti, yónnee, woo ko. 32 Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.» 33 Waaye Yeesu tontu leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?» 34 Noonu mu xool ñi ko wër naan: «Sama yaay ak samay rakk a ngii; 35 ndaxte kuy def coobareg Yàlla, kooku mooy sama rakk ak sama jigéen ak sama ndey.»