Wolof: New Testament

Mark

4

1 Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di jàngalewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu yéeg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga. 2 Noonu Yeesu daldi leen jàngal lu bare ciy léeb. Ci njàngaleem nag mu ne leen:3 «Dégluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi. 4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp. 5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. 6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen. 7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara. 8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, lii mat téeméer.» 9 Noonu Yeesu ne leen: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi. 11 Mu tontu leen: «Yéen may nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci biti léeb ay ëmb lépp. 12 Noonu la, ngir:“Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara,di déglu bu baax waaye duñu xam dara,ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar,te Yàlla baal leen.”» 13 Noonu Yeesu ne leen: «Ndax xamuleen léeb wii? Nu ngeen xame nag léeb yi ci des? 14 Ki ji nag, kàddu gi lay ji. 15 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg, Seytaane ñëw ci saa si, këf kàddu, gi ñu def ci moom. 16 Ki jot kàddu gi ci bérab bu bare ay doj mooy ki dégg kàddu gi, nangu ko ak mbég ci saa si, 17 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si. 18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, 19 waaye soxlay àddina ak naxi alal ak bëgge solu ko, tanc kàddu gi, ba du meññ dara. 20 Ki jot kàddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko dégg te nangu ko, ba jariñ; kii mat fanweeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, kii mat juróom-benn-fukk, kii mat téeméer.» 21 Yeesu ne leen itam: «Ndax nit dina jël làmp, dëpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko wékk? 22 Amul dara luy kumpa lu ñu warul a siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ. 23 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.» 24 Mu ne leen: «Seetleen bu baax li ngeen di dégg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen. 25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as néew, dees na ko nangu.» 26 Yeesu teg ci ne: «Nguuru Yàlla dafa mel ni nit ku ji tool. 27 Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa bëccëg, jiwu wi sax, di màgg, te xamul naka la ko defe. 28 Suuf day meññ moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub. 29 Bu gub yi ñoree nag, mu dagg ko, ndaxte ngóob jot na.» 30 Yeesu ne leen ati: «Lu nu man a mengaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko man a misaale? 31 Dafa mel ni doomu fuddën, bi gën a tuuti ci jiwu yépp; 32 waaye boo ko jiwee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.» 33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneeni léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan. 34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp. 35 Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.» 36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneeni gaal ànd ak moom. 37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgg a fees. 38 Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngégenaay ci taatu gaal gi.Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?» 39 Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm. 40 Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?» 41 Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»