1 Bi yengu-yengu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu tàggoo ak ñoom, jóge fa, dellu diiwaanu Maseduwan.
1往马其顿及希腊
2 Noonu mu jaar ca bérab yooyu, di dooleel nit ñi ak wax yu bare; ba noppi mu dem réewu Geres,
2他走遍那一带地方,用许多话劝勉众人,然后来到希腊。
3 toog fa ñetti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw tànki dugg gaal jëm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas yéenee dellu, jaare Maseduwan.
3他在那里住了三个月,正要坐船往叙利亚去的时候,有些犹太人设计要害他,他就决意路经马其顿回去。
4 Booba nag ñii ñoo ànd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi dëkk Bere; Aristàrk ak Segond, ñi dëkk Tesalonig; Gayus, mi dëkk Derbë, ak Timote; te it Tisig ak Torofim ñi dëkk Asi.
4与他同行的有比里亚人毕罗斯的儿子所巴特,帖撒罗尼迦人亚里达古和西公都,特庇人该犹和提摩太,亚西亚人推基古和特罗非摩。
5 Ñooñu nag jiitu, di nu nég dëkku Torowas.
5这些人先走,在特罗亚等候我们。
6 Waaye naka nun, gannaaw màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci juróomi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa juróom-ñaari fan.
6至于我们,过了除酵节才从腓立比开船,五天后到特罗亚他们那里,逗留了七天。
7 Ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi bëggoon a dem ca ëllëg sa, di diisoo ak ñoom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi.
7在特罗亚使犹推古复活礼拜日,我们聚会擘饼的时候,保罗对大家讲道,他因第二天就要起行,就一直讲到半夜。
8 Ca néeg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa làmp yu bare.
8我们聚会的那座楼上,有许多灯火。
9 Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palenteer ba, gëmmeentu bay jeyaxu. Bi Pool di gën a yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwweekoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
9有一个少年人,名叫犹推古,坐在窗台上,因为保罗讲得很长,他很困倦,沉沉地睡着了,就从三楼跌下来;把他扶起来的时候,已经死了。
10 Waaye Pool wàcc, daldi sëgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: «Bàyyileen jooy yi, mu ngi dund.»
10保罗走下去,伏在他身上;把他抱住,说:“你们不要惊慌,他还活着。”
11 Noonu mu yéegaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca njël, door a tàggoo.
11随即回到楼上,擘饼吃了,又讲了很久,直到天亮才走。
12 Naka waxambaane wa, ñu indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy.
12他们把活着的孩子带走,得到很大的安慰。
13 Nun nag nu jiitu, dugg gaal jëm Asos, fa nu Pool santoon, nu jële ko fa; fekk moom fas na yéeney dox, ba agsi fa.
13从特罗亚往米利都我们先上船,开往亚朔,照着保罗的安排,要在那边接他,因为他自己要走陆路去。
14 Noonu mu fekksi nu ci Asos, nu jël ko ca gaal ga, dem Mitilen.
14他在亚朔与我们会合,我们接他上船,去到米推利尼。
15 Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile.
15从那里开船,第二天到了基阿对面,过了一天就在撒摩靠岸,再过一天到了米利都。
16 Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir bañ a yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem.
16原来保罗决定越过以弗所,免得在亚西亚耽搁时间,因为他希望能在五旬节赶到耶路撒冷。
17 Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm.
17保罗劝勉以弗所的长老他从米利都派人去以弗所,请教会的长老来。
18 Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.
18他们到了,保罗说:“你们知道,自从我到了亚西亚的第一天,我一直怎样跟你们相处,怎样服事主,
19 Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rangooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.
19凡事谦卑,常常流泪,忍受犹太人谋害的试炼。
20 Xam ngeen ne, musuma leen a nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanamu ñépp ak ca kër ya.
20你们也知道,我从来没有留下一件有益的事,不在众人面前或在家里告诉你们,教导你们。
21 Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba woññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.
21我对犹太人和希腊人都作过见证,要他们悔改归向 神,信靠我们的主耶稣。
22 «Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.
22现在,我的心灵受到催逼,要去耶路撒冷,我不知道在那里会遭遇什么事,
23 Xam naa rekk ne, ci dëkkoo-dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne, ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.
23只知道在各城里圣灵都向我指明,说有捆锁和患难在等着我。
24 Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla.
24但我并不珍惜自己的性命,只求跑完我的路程,完成我从主耶稣所领受的职分,为 神恩惠的福音作见证。
25 «Fi mu ne nag xam naa ne, dootuleen gis sama kanam, yéen ñépp ñi ma jaaroon ci seen biir, di yégle nguuru Yàlla.
25“我曾在你们那里走遍各地,宣扬 神的国。现在,我知道你们众人不会再见我的面了。
26 Moo tax may dëggal tey jii ne, wàccoo naa ak yéen ñépp bés pénc.
26所以我今天向你们作证,我是清白的,与众人的罪(“罪”原文作“血”)无关。
27 Ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle.
27因为 神的全部计划,我已经毫无保留地传给你们了。
28 Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal jépp, ji leen Xel mu Sell mi def sàmm, ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam.
28圣灵既然立你们为全群的监督,牧养 神用自己的血所赎来的教会,你们就应当为自己谨慎,也为全群谨慎。
29 Xam naa ne, bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dinañu tàbbi ci coggal ji te duñu ci ñeeblu kenn.
29我知道在我离开之后,必有凶暴的豺狼进入你们中间,不顾惜羊群。
30 Ay nit dinañu jóg ci seen biir sax, di wax luy sànke, ngir sàkku ay taalibe.
30你们自己中间也必有人起来,讲些歪曲悖谬的话,引诱门徒跟从他们。
31 Foogleen nag, di fàttaliku ne diirub ñetti at, guddi ak bëccëg, musumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci yéen ak ay rangooñ.
31所以你们应当警醒,记念我三年之久,昼夜不停地带着眼泪劝戒你们各人。
32 «Léegi nag maa ngi leen di dénk Boroom bi, moom ak kàddug yiwam, gi leen man a dëgëral te may leen cér ci biir gaayi Yàlla yu sell yépp.
32现在我把你们交托给 神和他恩惠的道;这道能建立你们,也能在所有成圣的人中赐基业给你们。
33 Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam.
33我从来没有贪图任何人的金银或衣服。
34 Xam ngeen ne, faj naa samay soxla ak soxlay ñi ànd ak man ci sama loxo yii.
34我这两只手,供应了我和同伴的需要,这是你们自己知道的。
35 Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu war a dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gën a barkeel nangu.”»
35我凡事以身作则,你们必须照样辛劳,扶助软弱的人,并且记念主耶稣的话:‘施比受更为有福。’”
36 Bi mu waxee loolu, mu sukk ak ñoom ñépp, ñaan ci Yàlla.
36他说了这些话,就跪下来同大家一起祷告。
37 Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax.
37众人都痛哭,伏在保罗的颈上,与他亲嘴。
38 Li leen gën a teg aw tiis mooy li mu leen wax: «Dootuleen gis sama kanam.» Noonu ñu gunge ko ba ca gaal ga.
38他们最伤心的,是保罗说他们不会再见他的面那句话。最后他们送他上了船。