1 Am bés Yeesu di ñaan ci benn bérab. Bi mu noppee, kenn ci taalibeem yi ne ko: «Boroom bi, jàngal nu, nan lanu war a ñaane, ni ko Yaxya jàngale ay taalibeem.»
1祈求就必得着(太6:9-13,7:7-11)
2 Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee ñaan, nangeen ne:“Baay bi, na sa tur sell,na sa nguur ñëw.
2耶稣说:“你们祷告的时候,要说:‘父啊,愿你的名被尊为圣,愿你的国降临(有些抄本在此有“愿你的旨意行在地上,如同行在天上”一句);
3 May nu bés bu nekk li nu war a dunde.
3我们需用的食物,求你每天赐给我们;
4 Baal nu sunuy bàkkaar,ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ.Te bu nu teg ci yoonu nattu.”»
4赦免我们的罪,因为我们也饶恕所有亏负我们的人;不要让我们陷入试探(有些抄本在此有“救我们脱离那恶者”一句)。’”
5 Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu.
5耶稣又对他们说:“你们当中,谁有朋友半夜去找他,说:‘请你借给我三个饼,
6 Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.”
6因为我有一个朋友旅行来到我这里,我没有什么可以招待他。’
7 «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko tontu: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd, man ak sama njaboot; mënumaa jóg di la jox dara.”
7而他却在里面回答:‘不要麻烦我,门已经关好了,孩子也跟我在床上了,我不能起来拿给你。’
8 Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla.
8我告诉你们,即使不因为他是朋友而起来给他,也会因为他厚颜地直求,而起来照他所需要的给他。
9 Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
9我又告诉你们,你们祈求,就给你们;寻找,就寻见;叩门,就给你们开门。
10 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
10因为所有祈求的就得着,寻找的就寻见,叩门的就给他开门。
11 Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko bañ a jox jën, jox ko jaan?
11你们中间作父亲的,哪有儿子求鱼,反拿蛇给他呢?
12 Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit?
12或求鸡蛋,反给他蝎子呢?
13 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!»
13你们虽然不好,尚且知道把好东西给自己的儿女,何况天父,岂不更把圣灵赐给求他的人吗?”
14 Am bés Yeesu dàq rab wu luu. Naka la rab wa génn, luu ba daldi wax, ba mbooloo may yéemu.
14耶稣靠 神的能力赶鬼(太12:22-30;可3:22-27)耶稣赶出一个哑巴鬼,鬼既出去,哑巴就说起话来,众人都希奇。
15 Waaye am ca mbooloo ma ay nit, ñu doon wax naan: «Ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
15有人说:“他靠鬼王别西卜赶鬼。”
16 Am ñeneen ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
16又有人试探他,向他求一个从天上来的神迹。
17 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, kër gu xeex boppam gent.
17耶稣知道他们的心意,就对他们说:“如果一个国家自相纷争,就必定荒凉;如果一个家庭自相为敌,就必然败落。
18 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di man a yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul.
18如果撒但自相纷争,他的国怎能站立得住呢?你们说我靠别西卜赶鬼,
19 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
19我若靠别西卜赶鬼,你们的子孙赶鬼又靠谁呢?因此,他们必要作你们的审判官。
20 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
20我若靠 神的能力赶鬼,这就是 神的国临到你们了。
21 «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw.
21一个壮汉拿着武器,看守自己的家园,他的家财就平安无事。
22 Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja.
22但是一个比他更强的人来了,胜过了他,夺去他所倚靠的武器,就把他的家财当作掠物分了。
23 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
23不站在我这一边的就是反对我的;不跟从一起收聚的就是分散的。
24 «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
24污灵去而复返的教训(太12:43-45)“一个污灵离开了一个人,走遍干旱之地,寻找栖身的地方,却没有找到,就说:‘我要回到我从前离开了的那房子。’
25 Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
25到了之后,看见里面已经打扫干净,粉饰好了,
26 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.»
26他就去带了另外七个比自己更恶的污灵来,进去住在那里;那人后来的情况,比以前更坏了。”
27 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!»
27约拿的神迹(太12:39-42)耶稣正说这些话的时候,群众中有一个女人高声对他说:“怀你胎的和哺养你的有福了!”
28 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.»
28他说:“是的,却还不如听 神的道而遵守的人有福。”
29 Naka la mbooloo may gën a takku, Yeesu ne: «Niti jamono jii dañoo bon. Ñu ngi laaj firnde, waaye duñu jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.
29众人聚集的时候,耶稣就说:“这世代是个邪恶的世代。这世代寻求神迹,可是除了约拿的神迹以外,再没有神迹给他们了。
30 Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa dëkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii.
30约拿怎样成了尼尼微人的神迹,人子也照样成为这个世代的神迹。
31 Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
31审判的时候,南方的女王要和这世代的人一同起来,她要定他们的罪,因为她从地极来到,要听所罗门智慧的话。你看,这里有一位是比所罗门更大的。
32 Te it ca bés pénc, waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fii.
32审判的时候,尼尼微人要和这世代的人一同起来,他们要定这个世代的罪,因为尼尼微人听了约拿所传的就悔改了。你看,这里有一位是比约拿更大的。
33 «Kenn du taal làmp, ba noppi di ko duggal cig kàmb, walla di ci këpp leget. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
33里面的光(太5:15,6:22-23)“没有人点了灯,把它放在地窖里,或量器底下,却放在灯台上,叫进来的人看得见光。
34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer. Waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm.
34你的眼睛就是你身体的灯,你的眼睛健全,全身就明亮;如果不健全,全身就黑暗。
35 Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du lëndëm.
35所以要谨慎,免得你里面的光黑暗了。
36 Kon bu sa yaram wépp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci lëndëm, dina leer nàññ, mel ni leeraayu làmp ne ràyy ci sa kaw.»
36你若全身明亮,没有一点黑暗,你就完全明亮,好像明亮的灯光照你一样。”
37 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba.
37法利赛人和律法师有祸了(太23:1-36;可12:38-40)耶稣说话的时候,有一个法利赛人请耶稣和他一起吃饭;他就进去坐席。
38 Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk.
38这个法利赛人见耶稣吃饭之前不洗手,觉得奇怪。
39 Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeen a fees ak càcc ak mbon!
39主对他说:“你们法利赛人把杯盘的外面洗净,但你们里面却充满了抢夺和邪恶。
40 Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?
40无知的人哪,那造外面的,不也造里面吗?
41 Saraxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell.
41只要把里面的施舍出去,你们的一切就都洁净了。
42 Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des.
42然而你们法利赛人有祸了!因为你们把薄荷、茴香和各样菜蔬献上十分之一,却把公义和爱 神的事疏忽了;这些是你们应当作的,但其他的也不可疏忽。
43 Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma.
43你们法利赛人有祸了!因为你们喜爱会堂里的高位和人在巿中心的问安。
44 Dingeen torox, ndaxte dangeen a mel ni ay bàmmeel yu raaf, ba nit ñi di ci dox te teyuñu ko.»
44你们有祸了!因为你们好像不显露的坟墓,走在上面的人并不知道。”
45 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.»
45律法师中有一个回答他:“老师,你这样说,把我们也侮辱了!”
46 Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam.
46耶稣说:“你们律法师也有祸了,因为你们把难担的担子叫人担,自己连一个指头也不动。
47 Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon.
47你们有祸了!因为你们修造先知的坟墓,而那些先知正是你们祖先所杀的,
48 Dangeen di seede noonu ne, ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi.
48这样,你们就成了证人,对你们祖先的作为表示同意;他们杀害先知,你们修造先知的坟墓。
49 Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.”
49所以, 神的智慧说:‘我要差遣先知和使徒到他们那里去,有的他们要杀害,有的他们要迫害,
50 Kon nag Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi ñu tuur, ba àddina sosoo ak léegi,
50为要使创世以来众先知所流的血,从亚伯的血起,直到在祭坛和圣所之间受害的撒迦利亚的血为止,都向这一代追讨。’是的,我告诉你们,都要向这一代追讨。
51 la dale ca Abel ba ci Sakariya, moom mi ñu rey ci diggante saraxalukaay bi ak bérab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu.
51
52 Yéen xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte yéena yóbbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci bëgg a dugg, ngeen tere ko ko.»
52你们律法师有祸了!因为你们拿去知识的钥匙,自己不进去,又阻止要进去的人。”
53 Bi Yeesu génnee bérab boobu, Farisen ya ak xutbakat ya ëmbal ko mer te di ko seetlu ci fànn gu nekk,
53耶稣从那里出来,经学家和法利赛人非常敌视他,质问他很多问题,
54 di ko yeeru, bëgg a këf waxam bu awul yoon.
54等机会从他的口中找把柄。