1 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba.
1十个童女的比喻
2 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel.
2她们中间有五个是愚蠢的,五个是聪明的。
3 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diwlin;
3那些愚蠢的拿着灯,却没有带油;
4 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diwlin ciy njaq.
4但那些聪明的拿着灯,也把油装在瓶里带来。
5 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmmeentu bay nelaw.
5新郎很晚还没有到,她们都打瞌睡,而且睡着了。
6 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.”
6半夜,有人喊叫:‘新郎来了,快出来迎接他。’
7 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp.
7那些童女都醒过来,整理她们的灯。
8 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diwlin, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgg a fey.”
8愚蠢的对聪明的说:‘请把你们的油分一点给我们,我们的灯快要灭了。’
9 Waaye ñi am xel tontu leen ne: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen; tee ngeen a dem ca jaaykat ya, jënd.”
9聪明的回答:‘这些恐怕不够我们大家用,不如你们自己到卖油的地方去买吧!’
10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diwlin ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj.
10她们去买油的时候,新郎来了;准备好了的童女就和他一同进去参加婚筵,门就关上了。
11 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu.”
11后来,其余的童女也来到,说:‘主啊,主啊,给我们开门吧!’
12 Waaye mu tontu leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.”
12新郎却回答:‘我实在告诉你们,我不认识你们。’
13 «Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa.
13所以你们要警醒,因为不知道那日子和那时间。
14 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi mu laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan.
14三个仆人的比喻(路19:12-27)“天国又像一个人要出外远行,就叫自己的仆人来,把产业交给他们。
15 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
15他按照各人的才干,一个给三万个银币,一个给一万二千个银币,一个给六千个银币(原文作“五个,二个,一个他连得”;一个他连得等于六千个银币),然后就远行去了。
16 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom.
16那领了三万的马上去做生意,另外赚了三万。
17 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar.
17那领了一万二千的也是这样,另赚了一万二千。
18 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
18但那领了六千的,却去把地挖开,把主人的钱藏起来。
19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya dellusi, daldi leen laaj alalam.
19过了很久,那些仆人的主人回来了,要和他们算帐。
20 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.”
20那领了三万个银币的,带着另外的三万前来,说:‘主啊,你交了三万给我,你看,我又赚了三万。’
21 Njaatigeem tontu ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
21主人对他说:‘又良善又忠心的仆人哪,你作得好!你既然在不多的事上忠心,我要派你管理许多的事。进来,享受你主人的快乐吧!’
22 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.”
22那领了一万二千的也前来,说:‘主啊,你交了一万二千给我,你看,我又赚了一万二千。’
23 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
23主人对他说:‘又良善又忠心的仆人哪,你作得好!你既然在不多的事上忠心,我要派你管理许多的事。进来,享受你主人的快乐吧!’
24 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul.
24那领了六千的也前来,说:‘主啊,我知道你是个严厉的人,没有撒种的地方,你要收割;没有散播的地方,你要收聚。
25 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.”
25所以,我就害怕起来,去把你的钱藏在地里。你看,你的钱还在这里。’
26 Waaye njaatigeem tontu ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne, damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul,
26可是主人对他说:‘你这个又可恶又懒惰的仆人,你既然知道我要在没有撒种的地方收割,在没有散播的地方收聚,
27 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot li ma moom ak la mu jur.”
27那你就应该把我的钱存入银行,到我回来的时候,可以连本带利收回。
28 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi.
28你们把他的六千银币拿去,交给那个有六万的。
29 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
29因为凡是有的,还要给他,他就充足有余;凡是没有的,就算他有什么也要拿去。
30 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.”
30把这没有用的仆人丢在外面的黑暗里,在那里必要哀哭切齿。’
31 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam.
31人子必审判万族“当人子在他的荣耀里,带着所有的使者降临的时候,他要坐在荣耀的宝座上。
32 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi,
32万族要聚集在他面前,他要把他们彼此分开,好像牧羊人把绵羊和山羊分开一样:
33 mu teg xar yi ci ndeyjooram, bëy yi ci càmmooñam.
33把绵羊放在右边,山羊放在左边。
34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndeyjoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
34那时,王要对右边的说:‘蒙我父赐福的,来承受创世以来为你们预备好的国吧。
35 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma;
35因为我饿了,你们给我吃;我渴了,你们给我喝;我作旅客,你们接待我;
36 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.”
36我赤身露体,你们给我衣服穿;我病了,你们看顾我;我在监里,你们来看我。’
37 Ci kaw loolu ñi jub dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan?
37义人就回答:‘主啊,我们什么时候见你饿了就给你吃,渴了就给你喝呢?
38 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la?
38又什么时候见你作旅客就接待你,赤身露体就给你衣服穿呢?
39 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?”
39或者什么时候见你病了,或在监里就来看你呢?’
40 Noonu Buur bi dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gën a ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
40王要回答他们:‘我实在告诉你们,你们所作的,只要是作在我一个最小的弟兄身上,就是作在我的身上了。’
41 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmooñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci safara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam.
41“王也要对左边的说:‘你们这被咒诅的,离开我,到为魔鬼和他的使者所预备的永火里去吧!
42 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan.
42因为我饿了,你们没有给我吃;我渴了,你们没有给我喝;
43 nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.”
43我作旅客,你们没有接待我;我赤身露体,你们没有给我衣服穿;我病了,我在监里,你们没有看顾我。’
44 Ci kaw loolu dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?”
44他们就回答:‘主啊,我们什么时候见你饿了、渴了、作旅客、赤身露体、病了,或在监里,却没有服事你呢?’
45 Kon dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gën a ndaw, man ngeen ko defalul.”
45王要回答他们:‘我实在告诉你们,这些事你们既然没有作在一个最小的身上,就是没有作在我的身上了。’
46 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»
46他们要进入永远的刑罚,义人却要进入永生。”