1 Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko.
1治好痲风病人(可1:40-44;路5:12-14)
2 Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.»
2有一个患痲风的人前来向他跪拜,说:“主啊!如果你肯,必能使我洁净。”
3 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
3耶稣伸手摸他,说:“我肯,你洁净了吧!”他的痲风立刻洁净了。
4 Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.»
4耶稣对他说:“你千万不可告诉别人,只要去给祭司检查,并且照着摩西所规定的献上供物,好向大家作证。”
5 Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko,
5治好百夫长的仆人(路7:1-10)耶稣到了迦百农,有一个百夫长前来恳求他,
6 ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.»
6说:“主啊!我的仆人瘫痪了,躺在家里非常痛苦。”
7 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.»
7耶稣对他说:“我去医治他。”
8 Waaye njiit la tontu ko ne: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8百夫长回答:“主啊,要你到舍下来,实在不敢当。只要你说一句话,我的仆人就必好了。
9 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
9我自己是在别人的权下,也有兵在我以下;我对这个说‘去!’他就去,对另一个说‘来!’他就来;对仆人说‘作这个!’他就作。”
10 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, musumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii.
10耶稣听了,就很惊奇,对跟随的人说:“我实在告诉你们,这样的信心,我在以色列中从来没有见过。
11 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
11我告诉你们,必有许多人从东从西来到,和亚伯拉罕、以撒、雅各在天国里一起吃饭。
12 Waaye ñi waroon a bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.»
12但本来要承受天国的人,反被丢在外面黑暗里,在那里必要哀哭切齿。”
13 Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér.
13于是耶稣对百夫长说:“回去吧!事情必照你所信的给你成就。”他的仆人就在那时痊愈了。
14 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng.
14治病赶鬼(可1:29-34;路4:38-41)耶稣来到彼得家里,看见他的岳母发烧,病在床上。
15 Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo.
15耶稣一摸她的手,热就退了;她就起来服事耶稣。
16 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp.
16到了黄昏,有些人带了许多被鬼附的人来见耶稣,他只用一句话就把污灵赶出去,并且医好了所有患病的人。
17 Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan:«Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.»
17这样正应验了以赛亚先知所说的:“他亲自除去我们的软弱,担当我们的疾病。”
18 Bi Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, mu sant taalibe ya, ñu jàll dex ga.
18跟从耶稣的要求(路9:57-60)耶稣看见许多人围着他,就吩咐往对岸去。
19 Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.»
19有一位经学家前来对他说:“老师,你无论往哪里去,我都要跟从你!”
20 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
20耶稣回答:“狐狸有洞,天空的飞鸟有窝,但人子却没有栖身(“栖身”原文作“枕头”)的地方。”
21 Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.»
21另一个门徒对他说:“主啊!请准我先回去安葬我的父亲吧。”
22 Yeesu tontu ko ne: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.»
22耶稣对他说:“跟从我吧!让死人去埋葬他们的死人。”
23 Bi mu ko waxee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem topp ko.
23平静风浪(可4:36-41;路8:22-25)耶稣上了船,门徒跟着他。
24 Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yengal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw.
24忽然海上起了狂风,甚至船都被波涛掩盖,但耶稣却睡着了。
25 Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee.»
25他们走来把他叫醒,说:“主啊!救命啊!我们没命了!”
26 Waaye Yeesu tontu leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
26耶稣却对他们说:“小信的人哪!为什么害怕呢?”他就起来斥责风和海,风浪就平静了。
27 Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?»
27众人都惊奇,说:“这是什么人,连风和海也听从他?”
28 Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woon a jaar foofa.
28治好鬼附的人(可5:1-17;路8:26-37)耶稣过到对岸加大拉人的地区,遇见两个被鬼附着的人从墓地出来;他们十分凶暴,甚至没有人敢从那条路经过。
29 Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgg a mbugal, bala waxtu way jot?»
29他们喊叫:“ 神的儿子,我们跟你有什么关系呢?时候还没有到,你就来这里叫我们受苦吗?”
30 Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
30那时远远有一大群猪正在吃东西。
31 Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.»
31那些鬼就求耶稣,说:“如果要赶我们出来,就准我们进到猪群里去吧。”
32 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma.
32耶稣对他们说:“出去吧!”他们就出来,进了猪群。那一群猪忽然闯下山崖,掉在海里淹死了。
33 Ba sàmm ya gisee loolu, ñu daw, dem dëkk ba, nettaliji lépp ak la xewoon ca ña rab jàpp.
33放猪的人逃进城里,把被鬼附的人的遭遇和一切事情,都报告出来。
34 Noonu dëkk ba bépp génn seeti Yeesu. Ba ñu ko gisee nag, ñu ñaan ko, mu génn seen réew.
34全城的居民都出来要见耶稣,看见了他,就求他离开他们的地区。