1 Fàttali leen ñuy déggal kilifa, yi yore nguur gi, tey jëfe seeni ndigal, ñu taxaw temm ci lépp luy jëf ju baax.
1要常常留心作善工
2 Buñu jëw kenn mbaa ñuy ŋaayoo, waaye nañu yiwe te won ñépp lewet gu mat sëkk.
2不可毁谤人,要与人无争,谦恭有礼,向众人表现充分温柔的心。
3 Ndaxte nun itam ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, nu réer bay jaamu ay bëgg-bëgg ak i bànneex yu wuute, nu dëkk ci coxorte ak ñeetaange, di ñu sikk tey sikkante.
3我们从前也是无知、不顺服、受了迷惑、被各种私欲和逸乐所奴役,生活在恶毒和嫉妒之中,是可憎可恶的,并且互相仇视。
4 Waaye naka noona Yàlla sunu Musalkat feeñal na mbaaxam ak cofeelam,
4然而,到了 神我们的救主显明他的恩慈和怜爱的时候,
5 ba musal nu; ajuwul ci jëf yu jub yu nu def, waaye ci yërmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell,
5他就救了我们,并不是由于我们所行的义,而是照着他的怜悯,借着重生的洗和圣灵的更新。
6 mi mu nu sotti ba mu baawaan, ci darajay Yeesu Kirist sunu Musalkat.
6圣灵就是 神借着我们的救主耶稣基督丰丰富富浇灌在我们身上的,
7 Ci noonu Yàlla àtte na nu jub ci kaw yiwam, te sédd nu ci dund gu dul jeex, gi nuy séentu.
7使我们既然因着他的恩典得称为义,就可以凭着永生的盼望成为后嗣。
8 Wax jooju ju wóor la, te damaa bëgg nga dëggal loolu, ngir ñi gëm Yàlla sax ci jëf lu rafet. Loolu moo baax te am njariñ ci nit.
8这话是可信的,我愿你确实地强调这些事,使信 神的人常常留心作善工;这些都是美事,并且是对人有益的。
9 Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay xuloo ak i xëccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njariñ.
9你要远避愚昧的辩论、家谱、纷争和律法上的争执,因为这都是虚妄无益的。
10 Kuy féewale, nanga ko yedd, yeddaat ko; bu tëwee, nga dàq ko,
10分门结党的人,警戒一两次之后,就要和他绝交。
11 xam ne nit ku ñaaw xel la te ay bàkkaaram fés ci ñépp.
11你知道这种人已经背道,常常犯罪,定了自己的罪。
12 Bu ma la yónnee Artemas walla Tisig, gaawantul fekksi ma ci dëkku Nikopolis, ndax fa laa bëgg a lollikooji.
12嘱咐和问安我派亚提马或推基古到你那里去的时候,你要赶快到尼哥波立来见我,因为我已决定在那里过冬。
13 Naka Senas àttekat bi nag ak Apolos, waajal leen bu jekk ci seen tukki, ba seen aajo yépp faju.
13你要尽力资助西纳律师和亚波罗的旅程,使他们不致缺乏。
14 Na sunuy bokk it takku ci jëf yu rafet, ba man a faj aajo yépp, te bañ a yaafus.
14我们自己的人也应当学习作善工,供应日常的需要,免得不结果子。
15 Ñiy ànd ak man ñépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy soppey ngëm. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
15同我在一起的人都向你问安。请你问候那些因信而爱我们的人。愿恩惠与你们众人同在。