1 Wax ju wóor a ngii: kuy sabablu yenub sàmm mbooloo mi, mu ngi yóotu liggéey bu rafet.
1Stedfast [is] the word: If any one the oversight doth long for, a right work he desireth;
2 Sàmm bi nag, nii la war a mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, moom boppam te maandu; war na am faayda, man gan te am mayu jàngale;
2it behoveth, therefore, the overseer to be blameless, of one wife a husband, vigilant, sober, decent, a friend of strangers, apt to teach,
3 warul di ab màndikat mbaa xeexkat, waaye na lewet te jàmmu, bañ a bëgge ci xaalis.
3not given to wine, not a striker, not given to filthy lucre, but gentle, not contentious, not a lover of money,
4 Na yor këram yorin wu rafet, te ay doomam déggal ko ak teggin yu mat.
4his own house leading well, having children in subjection with all gravity,
5 Ndaxte ku mënta yor njabootam, naka lay man a yore njabootu Yàlla?
5(and if any one his own house [how] to lead hath not known, how an assembly of God shall he take care of?)
6 Te it bumu nekk kuy door a gëm, ngir mu bañ a yég boppam, bay dajeek mbugalu Yàlla, ni ko Seytaane defe woon.
6not a new convert, lest having been puffed up he may fall to a judgment of the devil;
7 Te it war na am seede su rafet ci waa àddina, ngir ñu bañ koo diiŋat, ba muy daanu ci fiiru Seytaane.
7and it behoveth him also to have a good testimony from those without, that he may not fall into reproach and a snare of the devil.
8 Kiy topptoo li mbooloo miy jëfandikoo itam na am faayda te fonk kàddoom; bumu di ku yàqu ci sangara, mbaa ku alal jiital.
8Ministrants — in like manner grave, not double-tongued, not given to much wine, not given to filthy lucre,
9 Na sàmm mbóoti ngëm gi ak xel mu dal.
9having the secret of the faith in a pure conscience,
10 Moom itam nañu ko jëkk a seetlu, ba mu leer ne amul ŋàññ, ñu door koo fal.
10and let these also first be proved, then let them minister, being unblameable.
11 Naka noonu, na jigéen ñi am faayda, bañ a jëw mbaa xér ci dara, waaye nañu takku ci lépp.
11Women — in like manner grave, not false accusers, vigilant, faithful in all things.
12 Ku ñu dénk sasu topptoo yëfi mbooloo mi nag, nay ku yem ci benn soxna, jiite bu baax këram ak i doomam.
12Ministrants — let them be of one wife husbands; the children leading well, and their own houses,
13 Ndaxte ku ci rafetal sasam dina am tur wu tedd ak kóolute gu mat sëkk ci yoonu ngëm, gi ci Kirist Yeesu.
13for those who did minister well a good step to themselves do acquire, and much boldness in faith that [is] in Christ Jesus.
14 Bëgg naa laa seetsi balaa yàgg,
14These things I write to thee, hoping to come unto thee soon,
15 waaye amaana mu yéex. Moo tax ma lay bind bataaxal bii, ngir xamal la, ni ñu war a nekke ci kër Yàlla gi, maanaam ci mbooloom Yàlla Aji Dund ji, miy kenug dëgg te di sëslaayam.
15and if I delay, that thou mayest know how it behoveth [thee] to conduct thyself in the house of God, which is an assembly of the living God — a pillar and foundation of the truth,
16 Ci dëgg-dëgg ragal Yàlla ëmb na mbóot yu xóot:Ki wàcc, yor bindu nit,mu bir ne xelam jub na,te malaaka ya gis ko;xamlees na ko ci xeet yi,ñu gëm ko ci kaw suuf,te Yàlla teeru ko ci ndamam.
16and, confessedly, great is the secret of piety — God was manifested in flesh, declared righteous in spirit, seen by messengers, preached among nations, believed on in the world, taken up in glory!