Wolof: New Testament

Darby's Translation

2 Corinthians

1

1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk, noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla mi nekk dëkku Korent, ak gaayi Yàlla yu sell, yi nekk ci diiwaanu Akayi gépp.
1Paul, apostle of Jesus Christ by God's will, and the brother Timotheus, to the assembly of God which is in Corinth, with all the saints who are in the whole of Achaia.
2 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
2Grace to you, and peace from God our Father, and [the] Lord Jesus Christ.
3 Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu boroom Yeesu Kirist, di Baay biy Aji Yërmande tey Boroom lépp luy dëfël xol yi.
3Blessed [be] the God and Father of our Lord Jesus Christ, the Father of compassions, and God of all encouragement;
4 Mooy dëfël sunu xol ci sunu tiis yépp, ngir nun ci sunu bopp nu man a dëfël xolu ñépp ñi nekk ci tiis, di leen sédd ci noflaay, bi Yàlla def ci sunu xol.
4who encourages us in all our tribulation, that we may be able to encourage those who are in any tribulation whatever, through the encouragement with which we ourselves are encouraged of God.
5 Ndaxte ni coonoy Kirist di baawaane ci nun, noonu it la Kirist nekke buntu noflaay bu yaa, biy dëfël sunu xol.
5Because, even as the sufferings of the Christ abound towards us, so through the Christ does our encouragement also abound.
6 Su nuy jaar ci tiis, seen noflaay a tax ak seen mucc. Bu dee Yàlla dëfël na sunu xol, seen noflaay a tax, ngir ngeen man a dékku naqar yu mel ni yu nuy am, nun itam.
6But whether we are in tribulation, [it is] for your encouragement and salvation, wrought in the endurance of the same sufferings which *we* also suffer,
7 Te sunu yaakaar ci seen mbir dëgër na, xam ne, ni ngeen bokke ak nun naqar, noonu ngeen di bokke ak nun noflaayu xol.
7(and our hope for you [is] sure;) or whether we are encouraged, [it is] for your encouragement and salvation: knowing that as ye are partakers of the sufferings, so also of the encouragement.
8 Ndaxte bokk yi, bëggunu ngeen umple tiis, wi nu daj ci diiwaanu Asi. Yen bi diisoon na lool ba weesu sunu kàttan, ba amatunu yaakaar sax ci dund.
8For we do not wish you to be ignorant, brethren, as to our tribulation which happened [to us] in Asia, that we were excessively pressed beyond [our] power, so as to despair even of living.
9 Demoon nanu ba defe ne, dogalees na sunug dee. Loolu amoon na, ngir nu bañ a wéer sunu yaakaar ci sunu bopp, waaye nu wéer ko ci Yàlla, miy dekkal néew yi.
9But we ourselves had the sentence of death in ourselves, that we should not have our trust in ourselves, but in God who raises the dead;
10 Moo nu musal ci dee gu metti googu te dina nu musalaat. Ci moom lanu wékk sunu yaakaar ne, dina nu musalati,
10who has delivered us from so great a death, and does deliver; in whom we confide that he will also yet deliver;
11 bu ngeen nu jàpplee di ci boole seeni ñaan. Noonu ñu bare dinañu gërëm Yàlla ci yiw, wi mu nu may te muy tontul ñaanu ñu bare.
11ye also labouring together by supplication for us that the gift towards us, through means of many persons, may be the subject of the thanksgiving of many for us.
12 Li nuy tiitaroo moo di sunu xel day seede ne, ci kanamu àddina si, rawatina sax ci seen kanam, aw nanu ci tànk yu jub, ànd ak xol bu laab fa kanam Yàlla. Jëfewunu ci pexem nit, waaye ci yiwu Yàlla lanu jëfe.
12For our boasting is this, the testimony of our conscience, that in simplicity and sincerity before God, (not in fleshly wisdom but in God's grace,) we have had our conversation in the world, and more abundantly towards you.
13 Bindunu leen nag leneen lu dul li ngeen jàng te xam ko. Fi mu ne seen xam-xam ci nun matagul, waaye yaakaar naa ne, bu matee, dingeen man a tiitaru ci nun, ni nu koy defe ci yéen, bu bésu Boroom bi Yeesu ñëwee.
13For we do not write other things to you but what ye well know and recognise; and I hope that ye will recognise to the end,
15 Kon ni ma ame woon kóolute googu, naroon naa jëkk a jaar ci yéen, ngir ganesi leen ñaari yoon.
14even as also ye have recognised us in part, that we are your boast, even as *ye* [are] ours in the day of the Lord Jesus.
16 Bëggoon naa jaar ci yéen, dem diiwaanu Maseduwan, te bu ma jógee Maseduwan, dikkaat ci yéen, ngir ngeen waajal sama tukki ca Yude.
15And with this confidence I purposed to come to you previously, that ye might have a second favour;
17 Ba may mébét loolu nag, ndax dama cee boolewul pasteef? Te ndax samay yéene yéeney nit kese la, ba may xel ñaar, naan «waaw» ak «déet?»
16and to pass through to Macedonia by you, and again from Macedonia to come to you, and to be set forward by you to Judaea.
18 Wóor na Yàlla ne, li nu leen di wax, du «waaw» ju ànd ak «déedéet.»
17Having therefore this purpose, did I then use lightness? Or what I purpose, do I purpose according to flesh, that there should be with me yea yea, and nay nay?
19 Ndaxte Doomu Yàlla ji, Yeesu Kirist, mi nu doon yégle ci seen biir, man ak Silwan ak Timote, nekkul woon «waaw» ak «déedéet;» «waawi» Yàlla la mas a nekk.
18Now God [is] faithful, that our word to you is not yea and nay.
20 Te lépp lu Yàlla dige woon fekk na «waawam» ci moom. Noonu kon ci Kirist lanuy waxe: «Amiin,» ngir yékkati ndamu Yàlla.
19For the Son of God, Jesus Christ, he who has been preached by us among you (by me and Silvanus and Timotheus), did not become yea and nay, but yea *is* in him.
21 Te Yàlla moo nuy dëgëral ci Kirist, nun ak yéen, te sol nu Xelam.
20For whatever promises of God [there are], in him is the yea, and in him the amen, for glory to God by us.
22 Moo nu màndargaal ni ay gaayam, def Xelam ci sunu xol, muy dawal ci cér, bi mu nu dencal.
21Now he that establishes us with you in Christ, and has anointed us, [is] God,
23 Man nag Yàlla seede na ma, te giñ naa ci sama bakkan ne, yërëm leen rekk moo tax delluseeguma Korent.
22who also has sealed us, and given the earnest of the Spirit in our hearts.
24 Du caageen nag noo leen bëgg a noot ci lu jëm ci seen ngëm, waaye nu ngi liggéeyandoo ak yéen ngir seen mbég, ndaxte ci ngëm ngeen sax.
23But I call God to witness upon my soul that to spare you I have not yet come to Corinth.
24Not that we rule over your faith, but are fellow-workmen of your joy: for by faith ye stand.